El Maalig Juuf tàmbali na ak ekibam bu bees bi, West Ham. Amal nañu ñaari joŋantey tàggattu ngir waajal sàmpiyonaa bi ñu dëgmal. Ci ñaari ndaje yooyu yépp, wane na ci lu dal xel. Dëggalagum njort yu rafet yees am ci moom. Loolu di tàmbali bu baax bu ñépp di ñaan mu wéy, ndax njariñu réew mi la ba tay.
CHAN 2025
Suleymaan Jàllo ak i ndawam jeexal nañu seen i mats waajtaay ñeel powum Chan 2025 bii ñu dëgmal. Dañ leen a dóor seen ñaari mats yépp, bu ci nekk ci 2-1, muy sen diggante ak Ugàndaa ak Tansani. Ñu war a amal seen ndaje bu njëkk ci po mi fii ak juróom-ñeenti fan. Niseriyaa lañu ciy dajeel. Mu mel ni jot na ñu siggiwaat te fas yéene def fulla ngir mën cee am dara.
CAN JIGÉEN 2024.
Niseriyaa jël na ko ci kanamu Marog mi dalaloon po mi. Démb ci gaawu bi, 26 sulet 2025 ci la woon finaal bi. Ndaje mu metti woon waaye it bu neexoon. Ndax, bal bi daw na, futbal bu rafet am ci. Saf na finaal. Marog moo jiitaloon ñaari bal ci dara, Niseriyaa fekk leen fa ak ñett. Ci 3-2 yooyu la jeexe. Boobu di 10eelu yoon wu jigéeni Niseriyaa yi di jël kub bi.
LÀMB JI
Dibéer 27 sulet 2025, « Gaston Production » taxawaloon ci bëré yu réy. Ñiñ ci gënoon a ràññe Bombàrje / Jakson, Talfa / Arme, Bebe Guy gi / Ëmma jr.
Bebe Guy Gi moo ci daan Ëmma jr, Talfa daan Arme, Jakson itam daan Bombàrje.
Bu ñu dikke ci bëre bu mag bi di woon diggante Bombàrje, Saa-Mbuur bi, ak Jakson, waalo-waalo bi, mu di woon bëre boo xam ni ñaari mbër yi dañu tooge jaar-jaar yu wuute. Bombàrje mag ko fuuf ba noppi bëre daanaka ak ñu ko mag, ay moroomam ba tay mu daje ak ay rakkam. Mu nekk tay ci njeexitalu dundug bëreem. Wuute ak Jakson mii di xale bu ndaw, nekk cig buntug ndawam di bëgg a siiw ci làmb ji.
Ñoom nag, ñaari mbër yi, waajal nañu seen bés bi na mu waree. Jàkkarloo yi it ñu neexal ko ba mu neex. Ñëw nañu ci bés bi ak wér. Waaye, tamit bàkku, def lépp la ca war. Ba ñu noppee lépp, arbit bi woote wax ak ñoom, daldi mbiib. Ci noonu, ñaari mbër yi di léewatoo ab diir kenn laalul sa moroom ba arbit bi dog loolu daldi wax ak ñoom. Ñu tàmbaliwaat di léewatoowaat noonu ba mu dànkaafu ku nekk. Gannaaw loolu nag, ci la Jakson gaawal yëf yi, song Bombàrje, daldi koy daan ci lu amul lenni coono.
Bombàrje, bi bëre bi jeexe, xamle na ni « léegi damay gunge samay rakk ci làmb ji te gën a nekk ci MMA bi ».