Senegaal dina amal mats jàll (barrage) ëllëg ci altine ji, bu 18i waxtu jotee ci ngoon, moom ak Sudãwu bëj-saalum.
FUTBAL : SUPER CUP ALMAAÑ
Bayern Munich jël na Super Cup Almaañ bi ci kanamu Stuttgart. 2-1 la seen mats bi mujje, Harry Kane moo dugal (18eel) ak Luis Días (70eel). Luis Días boobu di biiwam bu njëkk ca ekibu Bayern gannaaw ba mu fa ñëwee ren, jóge Liverpool.
TÀMBALIG SÀMPIYONAA YI (2025-2026)
Sàmpiyonaay at mi tàmbali nañu ci ayu bés bii. Farãs, Àngalteer, Espaañ… amal nañu seen i mats yu njëkk. Mu mel ni nag ekib yi, képp kenn ci ñoom defaruwaat na bu baax ngir mën a jàmmaarloo ren, am dara.
LÀMB JI
Móodu Loo / Saa-Cees, bëre bi taxaw na. Al Bourakh Evens moo ko tëgg. Mu nekk bëre bu ñu bari doon laaj ak di ko séentu ngir jàpp ni lu jaadu la. Muy beneen jàmmaarloo diggante Pàrsel ak Géejawaay. Móodu Lóo am ñaari yan, benn bi muy cëru buuru làmb bim yore te war ko sàmm, beneen bi di Bàlla Gay 2 mi ko daan ñaari yoon te warul a nangu rakkam ji, Saa-Cees, ñëw daan ko moom itam. Bu dee Saa-Cees, muy xale nekk ci yoon, ñafe ba tollu fii, warul seetan cër bi ñëpp di wër di ko rëccee noonu. Jàppeesagul lél ngir seen bëre, waaye dana nekk lees di siiwal ci jamono yi ci kanam.