YOON : DAAN NAÑ BUGAAN WEERU KASO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay lees doon àtte Bugaan Géy Dani fa Tàmbaakundaa. Moom miy njiitul kurélu Gëm Sa Bopp nag, àttekat bi daan na ko weeru kaso wow, du ko tëdd (1 mois avec sursis). Rax-ci-dolli, gàllees na ko ndàmpaayu ñaar-fukki junni (100 000 FCFA) lu mu war a fay.

Moom Bugaan, Yoon nee na ko moo def lees koy toppe. Nde, dafa bañoon a jëfe santaaneb sàndarm yi taxawloo woon mu lànk, bëgg xëtt dogu takk-der yi. Toppekatu Bokkeef bi nekk Tàmbaakundaa dafa sàkku woon ci àttekat bi mu daan ko 3i weeri kaso yu muy tëdd ak ndàmpaayu 500 000 FCFA lu muy fay. Ndax, bees sukkandikoo ci li mu lay, lu jiin Njaag a, te Bugaan mooy Njaag. Waaye, àttekat bi toppul Toppekat bi ci li lmu laaj.

Bugaan Géy Dani dina ñibbi këram. Du ñàkk mu woo taskati xibaar yi ngir àddu ci mbir mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj