Làmmiñi réew mi, lépp la ñu mën, mën nañoo yenu xam-xam ak lépp lu ci aju. Téere yi ciy génn firnde lu wér la ci. Te, bu nu leen di jëfandikoo, di leen jàngal ñi leen nàmp, njàng mi day gaaw a mokk.
Niral : Làmp Faal Kala mi bind Xelum Xalam ak Tànn-béer (EJO-EDITIONS), jàngalekatu àngale la, xamal na nu ne, bu jàngalee ci àngale ak farãse ba sonn, xale tëe a nànd, day jël wolof. Bu ko defee ñu xam ci lu gaaw…
Ci njàngat lu Séex Anta duppee woon Kañ lañuy mën a wax dëgg suqalikug Afrig, am na ci bunt buy indi ay leeral ci solos jàngal gone yi ci làkk yi ñu nàmp. Séex Anta ma nga cay wax naan “li war a jiitu ci sunuy jéego mooy gëstuwaat sunuy làkk ba peeg leen, fexe nu nu leen jëmalee kanam”.
Séex Anta nag, dafa gis ni jàngalee xale yi ci làkk yi ñu nàmp moo gën a yenu maanaa ndax kenn umpalewul lëkkaloo gi am ci diggante mbatiit ak làkk. Nit ki, làkku mbatiit ma am xelam fendee moo gën a gaaw ngir dugal ci bopp bi xam-xam. Te, dina gaawal am njàngam.
At yu bari ya mu daan def ngir jàng dawal, ak baataan ak yeneen yi aju ci aw làkk te war koo peeg njëkk ñu door la cee mën a jàngal, loolu ag xayadi ak ug wayadi kepp lay wone.
Séex nag, indi na ci sax misaal ngir xamle ni bari na loo xam ni ñoo ngi koy bëgg a xamal gone mu am jafe-jafey nànd ko, fekk du càggan ne xel maa nëx, waaye làkk wa ñu jaare xam-xam ba la mënul. Kon nanu gën a jox gëdd làmmiñ yi nu nàmp, di leen jëfandikoo ci lépp te làkku nootkat yi bañ noo féewale.
Làmmiñ wees àmp ak koom-koom…
Ci wàllu liggéey yi, ñi jàngul, mën nañu leen a tàggat ci làmmiñi réew mi, seen liggéey gën a ñoŋ. Bu njëkk kiy jàng mekiniseŋ mën na ubbi oto, defar ko ndax yàgg a gis, yàgg a topp. Waaye, léegi ak oto elektoronig yi, taf-yëngal amatul. Soo jàngul dangay yàq. Ñooñu, su ñu leen tàggatoon ci làmmiñ yi ñu nàmp, koomu réew mi yokk bu baax, di firnde li Seex Anta ne woon « am réew mënut a suqaliku ci làkku jàmbur ».
Làmmiñi réew walla làkki doxandéem yi : Jéego ci làmmiñu wolof, Dawal ak bind làmmiñu wolof
Bari na ñuy soofantal ñi tànn làmmiñi réew mi di ci binde, ñu leen di bëgg a gëmloo ni dañoo a war a bind ci farãse. La ñu layalee gis-gis boobu mooy jàpp ni boo bindee farãse ci la téere bi di gën a wër, ci la ñu koy gën a dawalee. Wax yooyii nag boo ci càmbar ba ca biir gis ni kooku dërëm ak daraja la gën a bàyyi xel doonte la muy wax mën na nekk dëgg. Waaye, li waral yeneen làkki doxandéem yooyi wër ab xeex a ko taawu, mu doon lu sew ñu koy suuxat ba mu yaatu. Loolii nag lu mën a am la ci sunuy làmmiñ ndax gànjaru nañu te làmboo solo soo xam ni natteesul fu muy yem.
Kon kiy bind ci làkki réew mi la ko soxal mooy fa mbir mi mën a yegg, mu war cee xar tànku tubeyam te du ci séenu lenn lu dul njariñ lu ñeel askanam ci lu teew ak la ñëwagul. Bu dee ci li teew, làkk yi ñu yoonal, 6 yi dugg nañu ci daara yu ndaw yi, te ba ca jàngune ya ña nga leen fay jàngale.
Kuy jàngale aw làkk ci béréb yu ni mel nag, soxla nga delluwaay, ay téere ci fànn yu bari te wuute. Ginnaaw téere yu gone yu ndaw di jànge ci kër yi, EJO-EDITIONS génne na it ñaari téere yu Maamur Daraame bind muy Dawal ak bind làmmiñu wolof : téere jànkalekat ak téere njàngaan. Yii nag Jéego ci làmmiñu wolof bu Abdu-Xaadr Kebe moo leen jëkk a génn.
Tënk :
Njariñu ladab ci làmmiñi réew mi…
Ci li nu jàpp, ladab day may nit ñi ñu gën a nànd seen uw nekkin, su ko defee ñu nas i pexe yuñ koy soppe, mu gën a naat. Kon lii ci làmmiñi réew mi la war a jaare ngir askan wi gën cee jot ; ladab ci làmmiñi réew mi moo xelu.
Nun EJO, Collection CÉYTU, LU DEFU WAXU, danoo taamu liggéey ci wàllu làmmiñi Afrig yi : di móol i téere, di tekki tamit ay téere yu jóge feneen ci àddina si te war noo mën a amal njariñ, danuy tàggat ci wolof, yor yéenekaay ci wolof ; du càggan ne danoo bañ làkk wii walla wee, danoo bëgg sunuy làmmiñ jëm kanam. Nu door a séqi jéego jëm ca làkki jaambur ya. Lii rekk la !
Ci kow loolu, EJO génne na Murambi, le livre des ossements bu Bubakar Jóob ci ékibusi (làkku waa Kenya) ak ci suwaayili, génn na it ci araab, bu kiryãruwàndaa bi mu ngi ci tànk.
Làmmiñ wees nàmp am na solo ! Mënees na cee sukkandiku ngir dajeek ñi nu séqal àddina.
Yëgle : Jàngune bu Ndar (UGB) dina amal tey jii ci àjjuma ji (21eelu féewiryee 2025) waxtaan wu am solo ñeel bésu làmmiñ wees nàmp. Nu di leen ci ndokkeel te di ci dëñe képp ku ko mën.