SOXNA XADIJATU NJAAY CA KUNGÉEL, DOY NGA ROYUKAAY ! (AMI MBENG)

Yeneen i xët

Aji bind ji

« …ñeewuma sama benn moroom bu jàng farañse. »

Njiit li, boroom raaya yi, taalifkat bi, njiitalu mbootaayu liggéey (GIE), bàjjenu gox, aji-aw (relais), « conseillère municipale » … Ne leen kaar, nu door a jokk : kaar ! Wolof dafa ne, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko.

Waaye, kees nar a biral jaar-jaaram ci bile yaxal, Soxna Xadijatu Njaay, xeebul boppam, xeebul cosaanam te xeebluwu ci benn. Waaw ! Boroom màndarga yii nu biral ci ndoorteelu mbind mi, jàmbaar la ci jàmbaari Afrig  yi ; kon, Senegaal taxunoo wax. Ku jàng jaar-jaaram, dina xam ne, soxna soosu, dëgg-dëgg, mooy jigéen ju mën góor. Bu ko defee, tey, seen yéenekaay Lu defu waxu, nataalu « xaritu xale yi », dib dàkkental bees jagleel lingeer bi, Soxna Xadijatu Njaay la leen di indil. Dàkkental bi rekk doyoon na ci junj mbaax, njàmbaar ak mbëgg-réew gi ci soxna si. Ndaxte, kat, xale mooy ëllëgu réew ; su baaxee, mënees na am njoort gu rafet ci ëllëgu réew ma mu fekk baax. Kon, defar xale, mook defar réew ñoo yem. Naam, màndarga lees biral ci kow yépp am nañ solo. Waaye, soxna si nuy waxtaane tey, li ko tax a siiw jéll na ndombog-tànk ak daraja yooyu. Nu xool ba xam kan mooy Soxna Xadi Njaay, fi mu jaar, li mu def ak li mu am. *Kan mooy Xadijatu Njaay ? Lan mooy jaar-jaaram ? Soxna Xadijatu Njaay mooy njiitalu mbootayum liggéey mees duppe Xaritu xale yi. Moom, doomu Kungél piir la, « fii [ci Kungél] laa

juddoo, màgge fi, yaaro fi, di fi séy itam. Rax-ci-dolli, fii laa amey teraanga yu bare, maasàllaa. » Juddub kese, nag, lum rafet rafet, taxul a taaru. Nde, juddu bu rafet, ndey ak baay, waaye faayda moom, boroom. Loolu la Soxna Xadi Njaay xam ba tax ko fas séram ba mu dëgër, dogu ba mu jeex, fas-yéenee taxawu koñam, dimbaliy nawleem, liggéeyal goxam, jariñ diiwaanam ak réewam. Soxna su jàmbaare jii, ñeewul genn góor. Ku xool fi mu jaar, xam ne ku yàgg a xeex la, ñeme coono, mën a muñ te ànd ak pas-pas te bëgg li muy def. « Ci ASC laa doore. Ndaxte, ca atum 1981 laa jëkkoon a jiite sunu ASC koñ, muy ASC Kasewo. Ba 1986, maa nekkoon njiit li. Jiitewaatoon naa fi yit way-awi koñ bi. Booba, sunu liggéey moo doon xeex sibbiru ñeel xale yi. Dan leen daan nàndal. »

Ci atum 1995 la nekkoon aji-aw ci wàllu wér-gi-yaram. Bàjjenu gox, 2011 la ko nekk. Ndaxte, moom, ci mbirum xale lay yëngu, di « natt seen diisaay ak di leen toppatoo » ; day saytu yit jigéen ñi wérul. « Léegi sax, maa ngi nekk njiitalu bàjjeni goxi depaartmaa bi te yit man lañ dénk nafag diiwaan bi. » « Conseillère municipale » bi mu nekk tamit, ciy waxam, noonu la juddoo. Nde, politiseŋ yi dañuy faral di bëgg a jëflante ak boroom mboolo, « te man, koñ bii ma dëkk, dama fee am ay nit. Jàngale dafa nekk liggéey bu barkeel. Dëkk bu nekk nga dem fa, am fa say nit, loolu moo

tax. Sama waa koñ sax, ñoo jëkk a daje digal ma ma nekk « conseillère municipale ». Noonu, ñu dem ci meer ba woon, Àllaaji Kimintaŋ Kamara, mu daldi may def « conseillère municipale ». Ci laa tàmbalee di leen kaasal ak a xeexal ngir seen i àq ak i yelleef. Li nu ko dugge woon mooy suqali sunu koñ bi. » Nu jànge ci ne Soxna Xadi Njaay, njiit dëgg la, dib jëfkat. Day gindi, di jëfloowaate. Waaye, ku xamul du gindi, te ku jàngul doo xam. Ku jàngul, sa bopp ; waaye Soxna Xadijatu Njaay, moom, jàng na. Jàng du wees « Man nag damaa yàgg a bëgg jàng. Teg ci yit ne, sama boroom-kër jàngalekat la woon. » Démb a mag tey, waaye tey a sut démb. Soxna si, ak li muy bëgg a jàng yépp, toog na fanweeri at ak juróom yoo xam ne jàngul lu dul Alxuraan. Te, baayam bi ko ko daan jàngal, silmaxa la woon. Da doon tari rekk, waaye daawul bind. Wànte, Soxna Xadi Njaay bankul ay loxoom, toog di seetaan. Dafa jóg, di gëstu ndànk- ndànk. Ci la jotee tàggatu ci yenn téere yi, fore cis tuut ci xam-xam laata Yàlla di ko ubbil ab buntu.

« Yàlla dafa dogal nu amoon, ci gox bi, mbootaayum liggéey mu tuddoon Takku liggéey. Ci lañ fi ubbee benn kalaasu alfaabetisaasiyoŋ ci wolof. Ma dem bindu ci ngir di jàng. » Bi mu jàngee ba am cëslaay gu muy sukkandikoo, muy xemmem jàngale. Waaye, mu xam ne dese na koy bagaas. Noonu, mu daldi seeti jenn jàmbaar ci jàmbaari làmmiñi réew mi, Jaafara Fofana. Bi mu demee, Jaafara xóotalal ko njàngum arafi wolof yi, tojatal ko nëwu bi, leeralal ko taxawaayi tomb yi, añs. Ci njeexital li, Jaafara natt njàngum soxna si, mu daldi am 17/20. Looluy wone ne, soxna si ku farlu woon la te gaaw a mokkal. Kon, dolleeku na ci xam-xam bu baax. Yemul foofu de. Ndax, doyloowul woon loolu kese. « Ginnaaw gi la Sodefitex doon def ay jax (tests). Ma dem bokk ca, daldi jàll, am sama lijaasa. Noonu, nu defiwaat jaxub jàngalekat yi. Booba, 30i nit lañ woon te 3 rekk lañu soxlawoon. Ndeysaan, maa ngi jëloon 7 eel  ; ñu ne ma duma mën a bokk ci ñi ñuy tàggat.»

Metti woon na xol ndax yaakaar ju tas la woon. Waaye, ku foog ne soxna Xadijatu Njaay day dellu ginnaaw, nax nga sa bopp. « Ma wax leen ne, bu jaree fay sax, ma def ko. Ñu xam ne mbir mi yitteel na ma, ñu nangul ma, ne ma mën naa ñëw. Laajuñ ma woon fey, waaye dañ ma tegaloon ay sàrt : duñ ma jox ay jumtukaayi njàng, duma am it peyoor. Jagle yooyu, 3 ñi jiitu ci jax bi rekk ñoo ko yeyoo woon. » Mu daldi nangu, jàng ba jeexal. Ndax, li ko jar a ko jar. Boo xamagul, jàngil ; boo xamee, jàngaleel Ci yoon woowu la Soxna Xadijatu Njaay jaar ba am xam-xam ak mën- mën ñeel njàng ak njàngalem wolof. Te, ku mokkal, nag, tari. « Ci atum 2001 lañ ma jox kalaas ci sama gox, may jàngale. Jàngale naa tamit ci piriwe yi, ñu may fey, ak Sodefitex. Ma dem ba ci biir, daldi bàyyil sama bopp. » Gannaaw gi, sunu jàmbaar sér ji dafa sóobu ci alfaabetisaasiyoŋ bi, di jàngal ak a tàggat ndaw ñeek jigéen ñi. « Fii de, dañuy tàggat xale yi ak jigéen ñi ci wolof ; di leen jàngal bind ak nees di toppatoowee xale yi, rawatina ñu xiibon ñi. » Soxna si Njaay jaar na itam ci kurél gees di wax Ida Murid, ci njiitalu Mission mondiale. Daf fa daan jàngale, ci yoonu alfaabetisaasiyoŋ, xam-xamu natt walla peese, añs. Jot na jaar tamit Minam, Misira Kucaam ak Kungéel. Ci diir boobu yépp, Jaafara Fofana moo doon wottukat bi. Alfaabetisaasiyoŋ ak làmmiñi réew mi Senegaal, 100i nit yoo jël, 54i jànguñu, mënuñoo bind, du ci nasaraan, ci wolof walla weneen làmmiñ woo mënti jël ci réew mi. Loolu jaaduwul cim réew muy jàppe boppam ni demokaraasi. Nguur gi, li ko ci war, defu ko. Xanaa yenn kurél yi, ay mbootay, ay way-moomeel, añs. ñoo cii dugal seen i loxo. Li ci ëpp, ay doxandéem lay doon. Ndaw gàcce ! Waaye, ba tey, moo tane neen. Mu des, nag, ñenn ci doomi-réew mi ñoo xam ne, xam nañ dayo ak njariñ yi ci njàngum làmmiñi réew mi. Ñooñu, Soxna Xadijatu Njaay ci la bokk. Moom, day alfaabetise ca Kafrin ga mu nekk. Alfaabetisaasiyoŋ, nag, leeg-leeg mu ànd ak liggéey. « Fii, amoon nan ñetti kalaasi alfaabetisaasiyoŋ. Te, xale yi fi doon jànge am nañu lijaasa, ba am na sax juróom ñoo xam ne, léegi, ay jàngalekat lañu. »Nu gis ne, kon, liggéey baa ngi doon meññ laata ñuy dakkal njàng mi.Li waral loolu mooy ne,

« …kalaas moo amatul ; te alfaabetisaasiyoŋ bi doxul. Rax-ci-dolli, doo mën a ubbil sa bopp kalaas, di jëndal sa bopp kaye yi, xalima yi, ak yeneen xeeti jumtukaay yi ndongo yi war a jànge. Nit ñi bëgg nañ loolu waaye amaguñu ay kalaas yu ñu samp di ci jànge. Ci atum 2017 lan leen gëj a am.” Ndeysaan, xalam demoon bay neex… Moone, bu nu sukkandikoo ci kàdduy Soxna si, jigéeni Kungél yi jot a def alfaabetisaasiyoŋ, ñoom, deppãs ak xeeti xayma yi ñuy def, ci wolof lañ leen di binde ci seen i kaye. Kon, alfaabetisaasiyoŋ bi amal na njariñ jigéen ñi bu baax a baax, sax. Li ko gënatee tax a am njariñ moo di ne, dafay ànd ak tàggatu ñeel benn xeetu liggéey. « Njàngum alfaabetisaasiyoŋ bi, fii, ciy waxtu yu néew rekk lay yem. Bun noppee ci njàng mi, danuy dugal njàngum liggéey mi, walla ay natt, di dajale xaalis bi ngir ku am soxla ñu lebal ko ci. Dafay am nattu ku teggi am saaku su ko defee dangay takkuwaat ngir jaay ko waa kalaas bi. » Ndege, mbir mi dafa ànd ak dimbalante ak jàppalante. Waaye yemul foofu. Ndaxte,« Dañu leen di jàngal tamit naka lañuy soppee ci wolof ak naka lañuy xeexe xiibon, naka lañuy aare nef, naka lañuy aare sibbiru ak naka lañuy toppatoowee jigéen ju wérul. Def nanu ci sax ay téere. Ponk yii lanuy dugal ci njàngum alfaabetisaasiyoŋ, di ci ame xaalis. » Nu gisati ne, ndege, mënees na ame lees suturloo ci làmmiñi réew mi. Waaye, ngir lu ni mel mën a sotti, fàww ñu fullaal leen, dooleel leen. « Sunu làmmiñi réew mi jariñ nañ nu ba noppi. Ndax, mag ñu mel ni man, toog 35i at yoo xam ne, mësuñoo dugg lekkool, jànguñu farañse walla genn kàllaama goo xam ne dees koy bind. Xanaa ay saari alxuraan yi may toppe sunu Boroom te ci njàngum gumba laa leen jànge. Ndaxte, sama baay mi ma leen jàngal, daawul gis. Dama daan tari rekk. Bi ma jàngee wolof, nag, damaa jël saar yooyu yépp, bind leen ci wolof, ba noppi di bind ay téere taalif ngir li ma nekk aji-aw di yit bàjjenu gox. Kon nga xam ne sunu làmmiñi réew mi am nañ solo lool, sax. Ndege aw làmmiñ dinay niteel. Loolu la fi jàmbaaru sér ji biral. Mu daldi wéral ne, aw làmmiñ dina jur koom-koom gu naat. Ndax, yokkute, garab la rekk, loo ciy gën a sonn, muy gën a meññ. Bu ko defee, mu daldi lay jariñ, yow ci sa bopp, ak ñeneen, ak ñeneen… « Man de jariñ na ma te it ñeewuma sama benn moroom bu jàng farañse. Ndax, nekk naa bàjjenu gox, « conseillère municipale”, njiitalu mbootaayum liggéey, añs. Te, ci wolof laay jàngale, di ci bind ba mu baax li may jàngale…lépp daal ci wolof laa koy defe. » Leer na nàññ, Njaay-Jaata. Boroom neexal yu bare yi Soxna Xadijatu Njaay jot naa am ay raaya yu bare. Waaye 4 ñoo ci gën a fés. Bi ci jiitu, 2006 la ko amoon : « …ay càkkute (requêtes) lanu waa Kafrin joxoon ngir nu mottal leen. Li ko dale Kungéel, Kafrin ba Kawlax, noo jiitu woon. » Biñ yaatalee mbir mi ci réew mépp, ñu daldi nekk 8 eel ca Ndar. Booba, njiitu réew ma woon, Ablaay Wàdd, moo leen neexale woon teraanga yu am solo, mel ni ñoo jëloon raw-gàddu gi. Ñaareelu raaya bim jël mooy Grand prix du chef de l’Etat pour la promotion de l’artisanat, ci atum 2013. Dañoo joxe woon ay kayit ngir jigéen ñi ci 4i depaartmaa yépp bindu ca Chambre des métiers bu Kafrin. Yàlla def, Soxna Xadi Njaay raw ñépp ca Kungél, Kafrin ak ci réew mépp sax.

« Waaye dañu waxoon ne ku ko gañe dinga am 20i miliyoŋ. Ba fi mas waxeek yow, gisunu dërëm bi gën a tuuti te xamunu lu ko waral. »

Maki Sàll, looy tontu ci lii ?

Lii rekk a tax kenn sawaratul a sonn ci réew mi. Ci atum 2016, dañu tànnoon 4i jigéen ci Afrig ngir sargal leen. NdeemSoxna see jëloon raayab njiitu réew mi, ñu daldi ko ciy boole. 2017 tamit, binduwaatoon na ci càkkute yi, jëlaat raw-gàddu gi ci biir réew mépp. Raaya boobu, ca estaad Iba Maar Jóob la ko ko njiitu réew mi, Maki Sàll, joxe woon. Mu mel ni daal, Soxna si, joŋante bum mënti bokk, daldi ciy ràññeeku. Waaye, mënul bokk at mu nekk. Ndaxte, raayab njiitu réew mi, boo ko gañee, dinga toogaat 5i at laata ngay mën a bokkaat ci joŋante bi. Wolof dafa ne, ku dul gërëm nit, doo gërëm Yàlla. Soxna Xadi Njaay, boroom kóllëre la, fàttewul mukk ñi ko tàggat ba mu àgg fim àgg tey. « Ndam yooyu yépp nag, dafa am ñu nekkoon ci ginnaaw di nu jàppale. Am na ciy kurél ak i mbootaay yu mel ni waa PAFAA, ay kilifa niki Asan Jóob añs. » Raaya yi, nag, jural nañ ko yokkute gu réy. Ndaxte, ame na ciy digaale, ame ciy ndaw yu muy tàggat, « wax dëgg Yàlla amal nañ nu njariñ.» Xam-xam, ñeent a koy kulóor : di ko bind, di ko jàngale, di ko waxtaane, mbaa di ko jëfe.

Soxna Xadi Njaay, ginnaaw bim mokkaale mbindum wolof, yemul ci di ko jàngale. Ndege, dafa jëfandikoo mbindum wolof, ngir di jëmmal ay yëg-yëgam, ay bëgg-bëggam ak ay ittéem ñeel mboolem-nawle mi. Looloo ko tax a bind « …ay taalif yu baree-bare ci mbirum wér-gi- yaram, ak àddina. » Mbind moomu, ci la jële raw-gàddug joŋanteb taalif bu aju woon ci Ayu-bésub nàmpal gi amoon ci diiwaanu Kafrin. Taalifam ba ko taxoon gañe, Nàmpal la ko tudde woon. Moom, nag, lenn rekk a di mébétam, am ku ko dimbali ba mu boole taalif yi mu bind yépp, móol leen. Kii di Soxna Xadijatu Njaay, royukaay bu mat sëkk la. Nu jox ko kàddugi ngir mu xelal jigéen ñi. Soxna si, looy digal jigéeni réew mi ? Soxna Xadijatu Njaay : « Sama mbokki jigéen ñi, nag, li ma leen di xelal mooy ne « femme-objet », maanaam jigéen jees di fowe, dafa xewwi. Li koy firndeel mooy baat yi ngay faral di dégg léegi : yemoo (parité) ak mën-mën ak xam-xam. Soo jàngul nasaraan, jàngal alfaabetisaasiyoŋ, fexe ba mën a bind, dugg ci liggéey yi. Ndax, liggéeyi soppi yaa ngi fi, cuub yaa ngi fi walla ñaw, añs… Waaye, kenn warul a toog rekk, ne yàcc-yàccaaral. Loolu amatul. Ndax, kat, taxawaayu jigéen ci wàllu liggéey mooy ne, fu góor taxawee, nga taxaw fa. Takk ndigg yi liggéey, mbey maa ngi fi walla beneen liggéey boo bëgg rekk. Nga toppatoo sa njaboot bu baax ak sa boroom kër, xiir njaboot gi ci ñuy jàng ngir ñu mën la cee génne. Ndaxte, fii moom, képp ku fi raw rekk, sa jom ak sa doom a tax. Kon boog, sàmm leen xale yi, yiir leen te nangoo liggéey. »

Ami Mbeng

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj