Mbootaayu Xeet yi ñeel njàng, xarala ak mbatiit (UNESCO) moo tànn bésub 23i awril, jagleel ko téere ak àqu bindkat. Saa yu bés bi teroo, dees koy màggal ci àddina sépp. Senegaal mi jox dayo téere fasul yéene des ginnaaw. Ci kow loolu, Njiiteefu téereek dawal dina amal i xew-xew yu bari ci Ndakaaru ak yenn ci diiwaan yi. Ndax, Senegaal yemul Ndakaaru. Wii yoon nag, daa toombeek dibéer ba noppi dajeek korite. Moo tax ñu dàq ndajem ubbite gi ba alxames 27i awril, ci teewaayu doktoor Aliyu Sow, jawriñu mbatiit. Cees lay ame ca « Institut national de formation des jeunes aveugles » (INEJFA), daara jiñ jagleel ndongo yi sëgg (maanaam ñi seen iy bët muuru). Naam, gisuñu, waaye am nañuy xel, xereñ nañ, dogu nañ ci sàkku xam-xam. Te yit, doomi Senegaal lañu. Kon, jaadu na ñu delloo leen seen cër ci bésub téere bi. Ginnaaw maye téere, bindkat bii di Mamadu Sàmb dina fa amal waxtaan wu yaatu ci téereem bi mu duppe Le regard de l’aveugle, muy bob, baayu way-jëmmal bi silmaxa la.
Laata xew wii, dina am yu ko jiitu ci àllarba ji, ba tey lu jëm ci siiwal ak xamante bindkat ak dawalkat.
Faatimata Jàllo Ba dina teew ca Centre culturel Blaise Senghor ngir waxtaane téere bim mujje génne, Rouges silences (Miig yu xonq) .
Mareem Sooda Lóo, ca Kawlax, ngir moom it téere bim génne jamono jii, Légitime imposture (Naxee-mbaay gu lew).
Tabara Ñaŋ, Sóokóon, Calèche d’une demoiselle (Wëtiiru benn janq).
Màmma Musa Jaw, Maatam, Châtiments (Mbugal).
Téere yii yépp ñoo am solo. Boo ci jàng rekk, am loo ci góob. Du ñàkk bés, Lu Defu waxu delsi ci.
Jataayu maye téere dina wéy ci loppitaanu Jamñaajo ak CentreTalibuDaabo, ngir téere yi gën a tas ba egg ci ñi koy jëfandikoo. Dawal am na solo lool. Waaye de, ñenn ñi, ñàkk a am i téere moo leen tere dawal. Ci fànn woowu, Njiiteefu téereek dawal a ngi ciy def i jéego yu am doole. Fépp ci Senegaal, diiwaan bu nekk am na bérébu téereem (CLAC) ci ndimbalam. Móolkat yi tamit daanaka ñépp a ngi jot i ndimbal lu bawoo ci njawriñu mbatiit gi. Foire du livre ak Salon du livre sax, njawriñ gaa leen di lootaabe. Ñoo ngi def seen loxo it ci xew yu am solo yu doomi réew miy amal yu deme ni SILT, Mustafaa Ndeene Njaay ne ci bopp bi ; SLF, Aminaa Sekk jiite ko te jagleel lépp ba mu daj jigéen ñi ; FILD, te Abdulaay Fóode Njoon di ko lootaabe.
Bindkat yi ak këru móolukaay yi bari nañu lool ci Senegaal. Day wone rekk ne Senegaal réew mu jox gëdd téere la. Ndaxte, xam na ne, téere day tee réer. Te, li Nelson Màndelaa waxoon moo fi nekk « réew muy dawal, réew muy jëm kanam la ».
Nu ngi ndokkeel Njawriñu mbatiit gi, Njiiteefu téere ak dawal, bindkat, móolkat, dawalkat, jaaykati téere yi, ñi yor kàggu yi, taskati xibaar yi féetewoo mbatiit, siiwalkat yi ak ñépp ñiy yëngu ci téereek dawal.
2023, LÀMMIÑI RÉEW YI
Ci nun, waa EJO (këru móol ci làmmiñi réew mi) ak Lu Defu Waxu (seen yéenékaay ci wolof), bésu téere ren jii (2023) solo si daa yokk bi wëppa bi nekkee Làmmiñi réew yi. Di firndeel la Luwis Mari Mayes Jóob, soxnas Seex Anta Joób, waxoon ca Bamako (Maali) ci atum 2007 muy :
« Làmmiñi réew yi, te ñi ëpp dégg leen mbaa ñànd leen, ñooy bànqaas yi ñu war a sukkandiku ngir suuxat yorinu Afrig ndax seen dayo gu am solo, gun mënt a wecce».
Jombul nag ne, UNESCO xam na ko ba tax mu bàyyi xel bu baax làmmiñi réew yi. Bindkat bi, moom, boppam lay jëkk a waxal, teg ciy ñoñam laata muy ubbiku ci biti, ci àddina si. Su dee nii la war a deme, kon kiy bind fàww muy jëfandikoo làmmiñam ngir mën a fésal yëg-yëg ya gën a sori ci moom.
Léegi, ginnaaw wëppa bi sunuy làmmiñ la, lu tax bindkat ak móolkat yi ciy yëngu kenn boolewu leen ci bés bi ? Laaj a ngi, ku xam tont li, jàppale nu ci.