23 AWRIL BÉSUB TÉERE AK ÀQU BINDKAT BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbootaayu Xeet yi ñeel njàng, xarala ak mbatiit (UNESCO) moo tànn bésub 23 ci awril, jagleel ko téere ak àqu bindkat bi. Saa yu bés bi teroo, dees koy màggal ci àddina sépp. Senegaal mi jox gëdd téere it, mësu cee des ginnaaw.

Ren jii, 23 awril 2024, ca Sàntar Aminata Mbay bu Garã-Yoof (Ndakaaru) la Njiiteefu téereek dawal ubbee xew-xew bi ci teewaayu Soxna Xadi Jéen Gay, jëwriñu ndaw ñi, tàggat-yaram ak mbatiit. « Naatal ak suqali bind ak dawal » ci liggéeyu njawriñu mbatiit lañ bokk.

 Aamadu Njaay (Njiiteefu téereek dawal) : Jàppalante ngir téere jàppandi ci ñépp

Aamadu Njaay (Njiiteefu téereek dawal) a ubbi njëlug kàddu gi, xamle ne :

« Danoo bëgg a wone sunu lëkkalook ñépp ñiy yëngu ci wàllu téereek dawal ak tamit jàppale ñi bëgg i téere te am jafe-jafe jot ci nu fexe ba téere yi egg ca ñoona ñépp. Moo waral tey jii, fépp foo dem ci 13i diiwaani Senegaal yi, dinga fa fekk CLAC (Centre de Lecture et d’Animation Culturelle), ay bérébi dawal ak yëngu-yëngu mbatiit. Ñoom it, ñu ngi màggal bésu téere ak àqu bindkat yi, ni nuy koy defee fii ci Sàntar Aminata Mbay. At yii weesu, amaloon nanu xew-xew yi ca Kaso jigéen ñi, fa Liberte 6, SOS Enfants, lopitaan Albert Royer, lopitaanu gune ya ca Jamñaajo, Sàntar Taliibu Daabo, daaw « Institut national de formation des jeunes aveugles » (INEJFA), daara jiñ jagleel ndongo yi seen bët muuru. Ren jii danoo taamu Sàntar Aminata Mbay, daara njàng ak paj jiñ jagleel gune yi seen xel desee neex. Bi ngeen doxantoo ci béréb bi ba noppi, gis ñi ñu ko jagleel, niki ladabkat, war ngeen nànd lu tax nu taamu fii. Waaye tamit, li sunu ndaanaan bi, Xaar Mbay Ma-Jaaga, woyoon a fi nekk, « xale yi, ku leen juroon yërëm leen ». Kon, dox ci jàppalante ak tamit wone ne ñépp ay doomi-Senegaal lañu, te ñépp ñoo war a yem ci sàkku xam-xam, rawatina ci téere. Moo tax nu taamu ren Sàntar bii. »

Sàntar Aminata Mbay…

Bi mu noppee, soxna Mari Madlen Ami Jonn miy jiite Sàntar bi moo ko wuutu ci kàddu gi. Soxna si rafetlu na li Njiiteefu téereek dawal taamu seen Sàntar bi, ndax day wone ne dañ leen a fekksi ci seen xeex diirub 35i at, bi Sàntar bi tàmbalee ay yëngu-yëngoom ak léegi. Ca la jaaraale, sargal soxna Aminata Mbay miñ tudde Sàntar bi, te mu daa ci sonn lool ci jàppale leen ak yiir xale ya fa féete. Sàntar baa ngi dooreek 8i xale ca atum 1989. Ren, 2024, mi ngi ci 171i xale ak waxambaane, ñu séddale leen ci 11i kalaas ak 7i liggéeyuwaay (ateliers). Bu njëkk, Sàntar bi kurél la woon. Waaye, dale ko 2009 ba léegi, ONG la. Atum 2017 lañu ràññee dëgg-dëgg njariñ li mu amal bokkeef gi. Soxna si dolli ca ne :

« Téere yi ngeen nuy may léegi dinañ jàppale Centre bi bu baax ci njàng meek sàkku xam-xam. Jot ci téere, dawal ko day tax a xam ak am sañ-sañu xalaatal sa bopp ».

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dawalkatu téere bu mag a mag la

Mangóone Njaay, yoroon CLAC bu Njagañaaw, teewoon na ca ndaje ma. Indi na fay seede ñeel Njiitu réew lu bees li, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Daf biral ni :

« Njiitu réewum Senegaal lu bees li, Basiiru Jomaay Fay, ku mës a bëgg téere la ba mu amee 6i at ba ren mu tollu ci 44i at. Mësul tàyyi mbaa yoqat ci téereek dawal ; dawalkat bu mag a mag la. Gis ngeen fi ko téere yi yóbbu. Téere am na solo. Kon deeleen dawal ».

Soxna Xadi Jéen Gay, jëwriñu ndaw ñi, tàggat-yaram ak mbatiit : « Téere day jëmale kanam… »

Laata muy yëkkati kàddu ci kanamu Ibraayma Lóo, njiiteefu téereek dawal, jëwriñu mbatiit ji baaxe na Sàntar bi 648i téere, 104i po, 15i tablet, 1 tele ak 1 nosukaay (ordinatëer) ngir bey waaram ci toolu njàng meek sàkku xam-xam ñeel gone ya fa nekk.

Soxna Xadi Jéen Gay nee na bég na lool ci jagleel mbatiit génnam gu njëkk ginnaaw biñ ko falee jëwriñ. Réccuwu ko wenn yoon. Te sax, bu jotee peyooram niki jëwriñ, dina may Sàntar bi 1.000.000 ci sunuy koppar, te fexe ba jëwriñ jiñ sas wàllu mbatiit moom it mu may Sàntar bi 1.000.000 bu weer wi deewee. Soxna si Jéen, mi ngi nettali ne, bi muy nekk ndongo ci daara yu ndaw yi (primaire), lënd gi ak mbaali jokkoo yi amuñu woon dayo biñ am léegi. Kon, lum xam rekk, téeree ko ci jàppale.  Mu nne :

« Téere day jumtukaay bu am solo. Ci kàggu yi la nu daa dem di jàng iy téere, fa la xam-xam bi nekk. Béréb yooyu ñu ngi fi ba tey. Waaye, toppatoo gi des na. War nañ leen a suqali mbaa sax dekki leeen. Seede bi sëñ Njaay def ci Njiitu réew mi wone na ne téere day jëmale kanam. »

Allaaji Léeboon léeb na fa ñaari léeb yu am solo yees tudde : Kenn mënul dund su yaakaar amul ak Mbooloo mooy doole. Xumbal na ndaje ma bu baax, muy mbégte gone yeek mag ñi.

Ndaje maa ngi tàmbale woon 11i waxtu, jeex 13i waxtu.

Yombal jot ci téere yi

Nuy fàttali kàdduy Audrey Azoulay, njiitu UNESCO, ñeel njariñu téere ci weeru awril 2024 bii. Ndaw si nee na :

« Su jamono diisee, ñu bari dañuy dellu ci téere ngir mu doon seen péexte ak bàllu gént. Te téere moo mën a jàngale ak a bégalaate. Moo tax nu war a def lu nu mën ngir ñépp jot ci téere yi, dawal leen, amee ci xam-xam ».

Strasbourg lañ tànn ren, def ko péeyub téere ci àddina si (capitale mondiale du livre). Daaw, Akra (Accra, péeyub Gana) lees tànnoon. Wëppa ren bi mooy Mën a jot ci téere yi (L’accès aux livres).

EJO-Editions ak Lu Defu Waxu ñu ngi ndokkeel njawriñu mbatiit gi, njiiteefu téere ak dawal, bindkat, móolkat, dawalkat, jaaykati téere yi, ñi yor kàggu yi, taskati xibaar yi féetewoo mbatiit, siiwalkat yi, jàngalekat yeek njàngaan yi ak ñépp ñiy yëngu ci téereek dawal.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj