25 me 1963 – 25 me 2023 : 60i at ginnaaw juddug OUA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Keroog ci Alxames ji, 25 me 2023, la mboolooy Saa-Afrig yi doon màggal bés bees jagleel kembarug afrig ci àddina si. Nu koy wax ci nasaraan Journée mondiale de l’Afrique. Mu yemook njuddug Mbootaayu Réewi Afrig yi OUA (Organisation de l’Unité Africaine) gi mujje doon UA (Union Africaine) ci atum 2002.

At mu jot, mboolooy Saa-afrig yi dañuy màggal bés bees jagleel Afrig ci àddina si. Muy bés bu ñuy màggal ngir jëmmal ak a fàttaliku bés bi réewi afrig yi sàmpee kurélug OUA ginnaaw bi ñu ëpp ci ñoom dogee buumu nooteel gi doxoon ci seen digganteek réewi tugal yi.

Kurélug OUA gee ngi juddu ca atum 1963. Mu yemook bésub gaawu 25 me, bi 32i Njiiti réewiy Afrig dajee woon ca Addis Abebaa, réewum Ecopi, ngir waxtaaneek xaatim lees duppee « La Charte de l’OUA ». Seen bëgg-bëgg moo doonoon bennale réewi Afrig yi, jaare ko ci taxawal i campeef ak rattaxal diggante réew yi, waayeet di xeex nooteel ak boddi xeet gi amoon ca Afrig-di-Sidd (Apartheid).

Bi ñu ñëwee ba ci Atum 2002, ci lañ soppi turuw OUA, def ko UA (l’Union Africaine). Coppite kurél gee ngi tukkee ci yéene gi Njiit yi amoon ca atum 1999 ngir gën a jublu ci lëkkaleek bennale réew yi, suuxat yokkute geek suqaleeku Afrig.

At mu jot, réewi Afrig yi ak mboolooy saa-afrig yi nekk ci àddina sépp di ci amal i xew-xew ngir waxtaane liy dëppale seen i bëgg-bëgg. Màggal bés bi àddina si jagleel kembarug Afrig mujj doon aada ba àgg ci bés bu kenn dul liggéey ci mbooleem réew yi bokk ci kurél gi.

60i at ginnaaw bi mu juddo ak tey, fan la sumb bi tollu ?

Atum ren ji, ñu koy fàttaliku ci anam yu daw yaram ndax tolluwaayu jamono ak jafe-jafe yi kembarug Afrig di jànkonteel, rawatina ci wàllug Nguur gu dal, jàmm ak kaaraange, koom, wér-gi-yaram a.ñ.s. Moo tax ñenn ñi jóg di wax ngir fàttali li doonoon jubluwaay wi bi ko ñi ñuy woowe « Les pères fondateurs » doon sos. Te muy dëggal seen gis-gis bi ñu amoon ci « panafricanisme » : Afrig gu booloo doon benn, gu moom boppam ak di demal boppam.

60i at ginnaaw bees ko sosee ba léegi, seetlu nañu ni tey la réewi Afrig yi ëpp i jafe-jafe. Tey la réew mu nekk gënatee fiir ci say dig. Njiit lu ñëw gën laa bëgg nguur ba fàtte campeef yi. Fi ñu doon yaakaaree jàmm ak kaarange ñu gën fa ràññe reyante ak tafaar yu tar. Yenn réew yu mel ni Sudã mujj xaaj doon ñaar ; rëtëlkat yi ferenkulaay ci xolu sahaara bi, foqati nguur di gën di bari ; mu néew lool dëkk booy teg tànk te fekkuloo fay way-fippu yu jël ay ngànnaay di laaj seen ug jonn.

Ak li fiy ballee lépp ci mbindaare, tey la réewi Afrig yi gën a fees ak i bor. Li ñuy tudde PIB (Produit intérieur brut), di nattukaay bi ñuy xaymaa am-amub réew yi, fii ci kembarug Afrig la gënee yées. Way-politig bu yegsi, li askan wi bëgg dégg te namm koo dund ngay mbubboo. Bu ñu nee waa jaa ngoog, bu faloo doon golo, deseek ay doomam. Alali Bokkeef gi mi mu sàcc ; soppi réew mi, tayle ko, doxandeem yi di tibb di yóbbu. Askan wi dëkkee jooytu ndax ndóol gu metti. Mag ñi waaru, faju të leen ticc. SIDA bi di rey, ndaw ñi jël yoonu gàddaay def ko seen rawukaay.

Mu mel ni 60i at ginnaaw bi « Les pères fondateurs » sosee OUA, tey la Afrig ëpp ay jàngoro. Moo waral ba mboolooy saa-Afrig yi weddi way-politig yi. Kuréli « panafricains » yi di juddoo fu nekk ak ci fànn yépp it ngir yaakaar joyyanti mbir yi. Ñuy laaj ndax dinañu joteji yéeney ñi sosoon OUA, te muy genn Afrig ? Lu ci kanam rawul i bët. 

Dig-daje 2060.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj