37eelu Ndajem Bennoog Afrig, ñu gën koo miis ci UA (Union Africaine), mi ngi ñuy doxal ci njeexitalu ayu-bés bi. Jamono ji ñu koy amal ren doon jamono ju yéeme ci àddina si, rawatina ci kembaarug Afrig ak jafe-jafey foqati Nguur yees fi nemmeeku ba ci coowal wote yi juddu Senegaal ak yëngu-yëngu yi mu jur.
Keroog ci alxames ji, 15 féewiryee 2024 lañ door 37eelu Ndajem Bennoog Afrig fa Adis Abebaa, réewum Ecopi. Ñu war ko doxal ba ci gaawu geek dibéer ji. Lu ëpp 30i Njiiti réew ñoo ko teewe, ay njiitul goornamaŋ ak i jëwriñ.
Jamono ji ndaje mi di am nag ren dafa yem ak jamono joj, àddina sépp a nekk ci njàqare. Xare bi doxoon ci diggante Ikiren ak Riisii demul bay waaj a fay, ay weer a ngii Israayel di faagaagal doomi Palestin yi fa Gasaa ginnaaw cong mi fa waa “Hamas” amaloon 7i fan ci weeru oktoobar 2023.
Fi kembaarug Afrig, kenn demul ñu des. Wéeru gi ñu wéeru ci doxalinu àddina si ba mu jural leen i jafe-jafey yokkute kese du fi coow. Foqati nguur ci kaw foqati nguur, soppi Ndayu Àtte réew ak i toxali wote ñoo dellu tere askan wi nelaw ba ci Senegaal mi ñépp jàppe woon royukaay fi Afrig Sowu-jant.
“Sunu yéene dëgg mooy Senegaal dellu ci ni mu gënee gaaw, ci yoon wu xelu ngir saafara jafe-jafe yi campeef yi di jànkonteel, mu amee ci anam yu nguuru yoon di doxee te dëppoo ak bëgg-bëggi askanam wi ñépp ñaw.”(Musaa Faki Mahamat, Njiitul komisiyoŋu mbootaay mi)
Nu gis ne ndogal yu am solo lees di xaar ñu tukkee ci waxtaan yi. Nde bees sukkandikoo ba tey ci kàddu yi Musaa Faki Mahamat yékkati, fitna yi juddu fa Sudã, Libi, RDC ba ci Burkinaa Faaso, Mali ak Niseer ñi fàq CEDEAO, doon nañ mbir yu doy waar yu leen tere nelaw.
Yile jafe-jafe sax àgg nañ fof dañoo nëbb dugg gi Afrig dugg ci G20 bi, di mbootaayu réew yi seen koom ëpp doole ci àdduna si, ci weeru sàttumbaar 2023 bi. Naka noonu sax, Lulaa Da Silwaa mi ko jiite, di Njiitul réewum Bérésil, mooy gan gu mag gu 37eelu ndaje mi.