50eelu LËLU CESTI : 33I TASKATI XIBAAR YU BEES

Yeneen i xët

Aji bind ji

Barki-démb, ci alxames ji (25eelu me 2023) la CESTI doon jox seen lijaasa 5i taskati xibaar yu jigéen ak 28 yu góor ca “UCAD 2”, ci njiteefu Musaa Balde, jawriñu njàng mu kowe mi, gëstu beek coste gi.  Lël boobu nag, mooy 50eel bi. Te, ñuŋ ko tudde ndem-si-Yàlla ji, Sã Meysa Jóob, nekkoon taskatu xibaar, doon liggéeyee Walfajiri, daan jàngale tamit fa CESTI ba ni muy génne àddina.

Boroom lijaasa yu bees yi CESTI tàggat, génne leen, 13 yi mbindum surnaal lañu taamu, Faatu Bintu Ka jiitu ci. Mu ci 8 yoy, liggéeyu rajo lañu féetewoo. Ki ci raw mooy Mustafaa Jaxite. Wàllum tele nag, Almaami Mamadu Saane lañ ci gën a ràññe.

 « Yóbbalu mag »

Soxna Raki Nowel Wan a ubbi kàddu gi ndegam moom la CESTI tànnoon ngir mu jottali pàcc bim tudde « yóbbalu mag ». Fàttali na ndawi taskati xibaar yu bees yooyee ne, ab taskatu xibaar du ab pólitiseŋ. Bu ko defee, war na ci moom, saa su ne, muy jottali ay xibaar yu wér te wóor yoy, saytu nañ leen, seggat leen laata ñu leen di siiwal. Soxna si neeti, njub ak xereñ duñ soppiku mukk te, ñooy cëslaayu xibaar. Wolof nee, gàllaaju nit, mooy njub. Teg na ca ne, bés bu juumee, na am woyofu nangu ko door a jàll, te di moytu. Loolu mooy, taskatu xibaar bi dafa war wàcce boppam, xam ne njuumte du ñàkk. Waaye nag, teyeef walla yàgg ca rekk a bon. Moo tax Soxna Raki Nowel Wan rax ca dolli ne, wares na saytook a wattu balluwaayu xibaar bi bu baax a baax.

Doomi Maali yi jaar CESTI

Bi Soxna si daaneelee, tegaleesoon na way-teew ya ab film buy wax ci doomi-Maali yi génne CESTI te am kurél guñ duppee AMACESTI. Ci biir film bi, ku ci nekk indi nay seede yu rafet, wax li nga jot a dund Senegaal jamono ja ngay nekk ndongo. Tey jii, kenn ku ci nekk ci ñoom, ku ràññeeku nga fa ngay liggéeye. Ag kuutlaayu (delegaasiyoŋ) gu mag a teewoon keroog. Dafa di kat, Maali a nekkoon réew miñ sargalee 50eelu lël boobule. Seen àmbasadëer ci Senegaal tamit, gunge woon na leen. Alsaan Suleymaan mi yor seen kàddu, ginnaaw bi mu  rafetloo demalante bi dox ci diggante ñaari réew yi, delsi na ci ni tasug xibaar mën a ubbee bunt bu nekk, « … Waaye, na taskatu xibaar xam fi muy teg tànkam».

«Sã Meysa Jóob, jëkkër du ko gën»

Soxna Jaariyeetu Njaay mi ténj Sã Meysaa moo ko wuutu ci waxukaay bi. Ak baatam bu daw yaram ba la fa waxee ne, borom-këram boobee de, jëkkër mënu koo gën. Mu tegoon ca ne :

« Ku bëggoon njaboot la woon, fonk soxnaam. Ndongo daara bu ràññeeku, fu mu tollu di ree, daawul xuloo boole woon ko ak oyof ba mu ëpp. Lël bii ñu ko tudde, maa ngi leen iy ñaax ci farlu, -Sã daawul yéex- ak liggéey bu mucc ayib. Maa  ngi sàkku ñaan it ci ñaari doom yu jigéen yi fi Sã bàyyi ».

« Ku xereñ la woon te oyof »

Keroog lël ba, tegoon nañ fa yit ab film biñ jagleel Sã Meysa Jóob, ay mbokkam ak i xameem def ciy seede. Li ñépp wax mooy ku dal la woon te oyof, di noyyee Gànjaay, dëkkam. Foofu sax lañ ko denc.

Sã Meysa Jóob, bésub 4eel ci oktoobar 1962 la gane woon àddina. Ndeysaan, keroog, 24 sãwiyee 2021, la dëddu. Mamadu Njaay, taskatu xibaar ci kippaango Imedia, doonoon xaritu benn bakkan ci Sä Meysa lañ toftal ci film bi ngir mu seede ci moom. Lii la fa wax :

« Li ñépp wax moo am. Fu Sã mësoon a nekk, kenn du ŋeb. Ndax, day tooñ rekk. Xeltukat bu xaroon tànku tubéyam ci diisoo jullit ak kercen la woon. Mën li muy def ba noppi oyof lool. Kon, xale yi nañ roy ay jikkoom ».

CESTI tàggat na 1 332i taskati xibaar

Mamadu Njaay, njiitul CESTI, nëbbul mbégteem ci bés bi. Waaye, bëgg na ñu gën a bàyyi xel daara ji. Ndaxte, àttanatul li mu yenu. Woo na ñi fa jot a jaar ak Càmm gi ngir dekkali xereñ giñ xame woon CESTI. Kàddu yii toftalu la fa biral :

« Afrig-bëj-Gànnaar ba mu daj, CESTI moo fi gën a mag ci tàggat taskatu xibaar. Mi ngi juddu atum 1965. Ca yëngu-yëngu weeru me 1968 ya, ñu tëjoon ko, ubbiwaat ko ci atum 1970. Boobaak tey, tàggat na 1 332i taskati xibaar, 722 yi di doomi-Senegaal,  610 yi jóge ci yeneeni réew.

Yeen ñii nag, di door a jot seen lijaasa, am naa yaakaar ne dungeen yàq deru ekool bi, dingeen jëmbat fullaak njub ba kenn du leen xeeb. Da di rekk, jamono ji day joo xam ni, mbaali-jokkoo yi yàq nañ mécce mi yàqin wu jéggi dayo. Waaye, du lay ngir toqi.

Li ma wóor mooy dingeen tënku ci jikkoy Sã Meysa miñ leen baayale ».

Ku màgg bariy soxla

Ahmadu Aali Mbay, njiitul Iniwérsite Séex Anta Jóob, moom, daa yabal porofesëer Aamadu Basiir Ñaŋ. Ginnaaw cargal ak cant, sëñ Ñaŋ biral na kóoluteem ci CESTI. Kenn umpalewul ne daara ji gën na bariy ndongo ak ay xeeti njàng. Kon, soxla nay jumtukaay yu yees ak ay tabax. Waayeet, wares na yokk limu jàngalekat yiy tàggat njàngaan yi. Sëñ Ñaŋ gàlloo na fa ab dige, wax ne, njiitul Iniwérsite li dina ci dugal loxoom bu baax. Na taskati xibaar yi tamit def i jéego ngir dégg làkk wi ñuy joxee xibaar.

« Du ku mu neex rekk nga doon taskatu xibaar »

Musaa Balde, jawriñu njàng mu kowe mi, gëstu beek coste gi, yokk na ci ne : « Saabal, mécce mu neex la. Waaye, dafa jaxasoo ci sababu ñàkk kóolute gi mbaali-jokkoo yi jur. Daa war a tax taskati xibaar yi dëggantaan dëggal seen bopp, wone ni fa ndox daan taa, soo fa demee fekk fa tepp-tepp. Du ku mu neex rekk nga doon taskatu xibaar. Saguleen ci CESTI ak Iniwérsite Séex Anta Jóob mi tàggat 4i njiiti réew. Te, loolu daa war a fës ci yooni daara ju kowe ji. Nañ ci xalaat. Bés bii nag, du rekk joxeb lijaasa. Waaye tam, cargal ci Sã Meysa miñ ko tudde ndax oyofam ak xereñem, li ñépp wax.»

Bi lii lépp weesoo, la Porofesëer Mumini Kamara door joxeb lijaasa yi…

Boroom-teraanga yi sañse ba jekk, : jigéen ñi sol i baseŋ yu baxa bu leer, gàll ci kol gu nirook moom. Góor ñi sol i kóstim yu baxa bu dër, takk i karwaat yu baxa yu leer ci kow simis yu weex. Ñoom ñépp sagu, bég ci seen kanami mbokk, xarit, nattaango ak kilifa yi.

Biñ sargalee ndongo yi ba noppi, dañ cee toftal Musaa Siise, Dóminik Méndi, Yayaa Kan. Ndaxte, dañuy alaaterete. Waaye, sargalees na leen tamit ngir seen liggéey bu rafet ci CESTI. Porofesëer Jéegaan Seen mi ngi ci biir.

Bi joxe bi weesoo, mbooloo ma daa bawoo Ucad 2, wutali CESTI ngir xéewalu ca bernde ya.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj