Juróom-ñetteelu fan ci weeru màrs la xel yépp di dem ci jigéen ñi, ndax seen bés la. Àddina sépp a koy màggal, di ci amal ay ndaje, ay waxtaan yu yaatu waaye it di natt ba xam fu xeex bi tollu.
Lépp a ngi tàmbali ci 1917, ca Saint-Petersburg, at ma ay óbëryee yu jigéen meree, amal ab doxu-ñaxtu. Lu jiitu loolu, ci atum 1910, Clara Zetkin, doonoon jàngalekat, surnalist, politigseŋ, sooke woon na ndaje mu mag, jigéeni sosiyalist yi wuyusi ko, ñu daldi taamu 8 màrs, def ko bés bees war a siggil jigéen ñi.
Ci 1977 la Mbooloom-Xeet yi nangu loolu, dëggal ko.
Fii mu ne nii, amul benn njiitul réew mu sañ a tanqamlu jigéen ñi le 8 màrs. Niñ ko xamee, ñi ëpp ci ñoom ay góor lañu te koo ci gis mu ngi politige bés bi, di jéem a gëmloo jigéen ñi seeni tawat soxal nañ ko lool.
Ci ñoom nag, am na ci ku xamutoon caaxaan ak tappale. Kooku Thomas Sankara la woon. Demoon na ba jël ca réewum Burkinaa-Faaso dogal bu yéeme. Saa yu 8 màrs agsee, da daan sant góor ñi ñu xéy fobeere néeg yi, duggi màrse, taal añ, toppatoo xale yi, fóot yëre yi, téye kër gi daal ni ko seeni soxnay defe bés bu Yàlla sàkk. Sankara dugge wu ko woon dara lu dul fexe ba góor ñi gën a xam li jigéen ñiy daj ci seen néegu-séy, su ko defee ñu weg leen, lépp lu ñu leen daan jàppale ñu xeeb ko, gën leen a taxawu.
Jigéen, ni ko woykat biy waxe, ku ko sóoralewul, yakk ñamu-mbaam. Loolu lu am la.
Sankara amoon nay yéene yu mag ci Afrig, jaarale leen ciy xalaat yu rafet te leer nàññ, kaar. Jigéen ñépp, rawatina yu Afrig, ameel nañ ko njukkal. Waaye ginnaaw bey ci sa wewu tànk, ndax amul beneen bés bu Senegaal waroon a jagleel ay jigéenam ? Sunu réew, nun, mooy réewum ‘’Talaatay Ndeer’’. Kon mënoon nanoo bañ a jéggaani ciy Tubaab bés bu nuy sargale jigéeni Senegaal.
Am ñu ma ni : ‘’Bés boobu ban la ?’’
Maa ni leen : ‘’Nan fàttaliku.’’
Talaatay-Ndeer, 7 fan ci weeru màrs 1820 la woon, Naari Tararsaa yi song péeyum Waalo, fekkuñu fa lu dul i jigéeñ, bëgg a leen a jàpp defi leen i jaam. Ndaw su am fit suñ naan Mbarka Ja ne leen bésu dee du bésu dund, jomb nanoo nekki jaam ginnaaw Barag-Waalo, nanu dajaloo ci néegu-ñax bu mag bii, taal ko ci sunu kow. Noonu lañu ko defe keroog, di woy ci biir safara si ba sedd guyy, suuxat suufus Waalo ak seen jom ak seen ngor.
Kon waay-waay yéen sunuy njiit, buleen ragal a def 7 màrs bésu jigéeni Senegaal yi ! Defeleen ko noonu, su ëllëg saa nu àndandook ñépp bokk ci xew-xewi 8 màrs yi. Ana lu aay ci yëkkati jigéen réew mi ñaari yoon ? Te sax, bu nu waxantee dëgg, li nga dàqe kon kéwél mu jëm àll, dàqe ko béy mu jëm kër.