Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jiite na ndajem jëwriñ yi barki-démb ci talaata ji. Ginnaaw bi mu defaree coppite yi am ci Càmm gi, dellu na ñaaxaat jëwriñ yi ñu farlu ci mbir yi gën a tembare, rawatina mbir yi ñeel ndaw yi ñu jiital ci seen naal yeek sémb yi.
Barki-démb ci talaata ji lañu doon amal ndajem jëwriñ yees daan amal àllarba ju nekk. Ginnaaw bi ñi taxawalee Ngomblaan gu yees gi ci altine ji, la magum jëwriñ yi biral woote bi, randalsi ndaje mi, jële ko ci àllarba ji ngir andi ko ci talaata ji.
Bi mu jëlee kàddu gi, Njiitu réew mi yékkati na kàdduy njukkal jagleel ko Elaas Maalig Njaay ci li ñu ko tabb ci boppu Ngomblaan gi. Ginnaaw loolu, mu dellu sàkku ci Càmm gi mu ubbeeku ci liggéey ak Ngomblaan gi ngir gën a ñoŋal ak yékkati demokaraasi Senegaal, Waaye tam ngir rataxal diggante campeefi réew mi.
Bi loolu weesoo, Njiitu réew mi biral na coppite yi mu andi ci Càmm gi. Ci la daldi toxal Sëñ Yànqooba Jémme, jële ko ci njëwriñal liggéey bi ak diggante càmpeef yi, wuutuloo ko Sëñ Elaas Maalig Njaay ci jëwriñal yaale ji. Mu dellu tabb Abbaas Faal mu wuutu Sëñ Jémme.
Naka noonu, mu daldi sant magum jëwriñ yi Usmaan Sonko ak Càmm gépp ci liggéey bi ñu nekk di doxal. Mu leen di fàttali nag jamono ju doy waar ju Senegaal tollu. Muy jamonoy joyyanti ak tabaxaat réew mi ; jamono ju laaj ñuy déglu askan wi, jege leen te gaawal jëf ji, mu leer ci ñépp te doon royuwaay ci sumb mi ñu sumb utali 2050 ngir sopparñi réew mi.
Ginnaaw gi, Njiitu réew mi dellusi naat ci xew-xew yi ñu amal ci fan yii weesu, muy màggalug Caaroy 1944 ak bés bi ñu jagleel daara yi. Mu delloo njukkal magum jëwriñ yi, Càmm gi, ma-xereñ yi mu ko tegoon seen loxo ci njiiteefu Porofesëer Mamadu Juuf, làrme bi ak ñépp ñi jàpp ci liggéey bi ñeel bésub Tirailleurs yi. Rafetlu naat bu baax taxawaay bi jëwriñ ji Mustafaa Giraasi, Kilifa diine yi ak mbootaayu njabootu daara am ngir jëmmal bésub daara yi.
Njiitu réew mi sàkku naat ci magum jëwriñ yi ak jëwriñu Mbay mi ñu taxaw ci doxal sàrt bi yoonal càmm geek suqali jur gi. Te bu ñu fi jógee, nañu taxaw ci delloosi bés bi ñu jagleel jur gi ci réew mi. Doon na xew-xew bu am solo ndax waxtaan yi ciy juddoo ci diggante Nguur geek way-yëngatu yi ngir suqaleeku fànn wi mën a gaaw.