Kaawteef ! Ab duwaañe lees fekk yàmbaa cig daamaram. Mbuur la xewee. Mu di mbetteel gu réy ba tax ko lëmbe réew jamono jii. Ndaxte, yuuxu dafa jibee fees ko foogewul woon. Dég-dég bbu doy waar bile nag, saabalukaay bii di Seneweb a ko siiwal.
Njombe lu réy a xew fa Mbuur. Dafa di kat, bariwul lees di gis takk-der buy laale ci ñaawteef bu ni mel. Nde, ñoom takk-der yi, di ndawi Nguur, ñoom lees sas ngir ñu xeex yu ni mel, rawatina duwaañe yi war a sàmm digi réew mi ba daraay lu bon te di yàq baña fee dugg. Ndaxte, ab duwaañe, liggééeyam yamul rekk ci di fayeeku xaalis ci njaay walla godaar yiy óoge bitim-réew te war a jàll fi réew mi. Wëliif liggéeyu koom bu am solo boobu ñu amal, duwaañe yi ay wattukat lañu itam. Ndax, waruñu seetaan bi mbir muy lore di jéggi sunuy dig, dugg ci réew mi. Te, mbir yuy lore yooyu, sineebar ci la bokk ak it ñax mu bon mees di tóx te mu tàggale nit ak sagoom. Bees demee nag ba ab duwaañe di ci taqe, musiba dikkal na nu. Waaye ndokk bi fi sàndarm yi nekkee ngir gàntal pexey xeeti duwaañe yu ni mel.
Sàndarm yi ñoo kalaate dilu duwaañe bi ; maanaam ñoo këpp yelwaanam. Juróom-fukki (50i) kiloy yàmbaa la duwaañe bi làqoon cig daamaram. Booba, xamul woon ne sàndarmëri yaa ngi ko doon yeeru ci tali bi, ci ndigalul seen komandaŋ. Ndax, dafa am ku leen déey ca njëlbeen, yégal leen njaayum yàmba bi duwaañe bi nekke. Noonu, komandaŋ bi daldi jokkoo ak waa birigàdd bu Mbuur, ñu taxaw ci tali bi ngir kar daamaru duwaañe bi. Bi daamar gi agsee nag, sàndarm yi taxawloo nañu ko ngir wóorliku xibaar biy wax ne duwaañe Ng. Njaay dafa làq yàmbaa ci daamaram gi. Waaye, moom nag, daf leen a wan kàrtu duwaanam, yaakaar ne loolu dina tax sàndarm yi bàyyi ko mu dem. Ndekete, loolu taxul mu romb. Bi mu xamee ne mbir mi cóol na, ca la fëx ak daamaram, daldi xél, daw ngir rëcc. Ca la dàqante ba jolli. Sàndarm ya topp ko, ñu rawante, ñu mel ni ñu nekk cib film amerikeŋ yees di gis ci tele yi.
Dafa di nag, daw taxul a rëcc. Ndax, jamono jooja, ndawi komandaŋ bu Mbuur ñi ngi koy kar-karal ñoom tamit. Laata mbir mi di mat waxtu, ci lañu gisee daamar gi muy xél ak doole, di ñëw. Li ci gën a doy waar kay mooy waa ji dafa naroon a jaar ca kaw sàndarma ya. Ca lañu ko soqee seen i fetel ba laal motëer bi ak póno càmmoñ bi. Daamar gi daw tuuti, taxaw. Waaye, loolu taxul ñu teg ko loxo. Ndax, dafa génnee ngànnaay teg ko ci boppam ne dafay xaru. Gaa ñi di jéem a naxante ak moom. Waaye, mujjul a sotti. Nde, dafa doxe ginnaaw, jékki rekk daw dugg àll bi, réer sàndarm yi.
Duwaañe Ng. Njaay nag, du guléet ñu koy tudd ci ay tóoxidóona. Bees sukkandikoo ba tay ci Seneweb, nee ñu, dañu ko def li ñuy wax “placé sous contrôle judiciaire” ci mbirum càccug xaalis gu tollu ci 220i miliyoŋ. Bu loolu weesoo, mënees na a jàpp ne, fii ak i waxtu walla ay fan yu néew, dees na xam fan lay mujj ak Yoon. Li ci kanam moom rawul i bët.