KU NAAN JOX SA MOROOM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Amoon na fiy jamono, néewoon na lool lees di gis kër gu amul ndaa. Njaq su mag soosu ñu defaree ban, wutal kog kubéer te di ko duy ba mu fees. Mu doon am mbàndu ndox mu teey tey sedd bu baax leeg-leeg. Ñu mën di ci fóot ak a sangu, di ci togg ak a naan. Ñaare sax, ñu def ci cepp ngir ndox mi gën a neex ci ki koy naan.

Dafa aay lool nag te gaaw ci boole ñi koy jëfandikoo. Ndaxte, moom ndaa, bérébu ndaje la. Du fekki kenn nag, waaye loolu du ko tax a wéet. Mukk ! Ndaa li, dafay toog rekk. Du dem. Du dikk. Toogaay boobu nag, yàqalu ko dara. Moo tax wolof di ko tagg, naan : “Toogaay, ndaa rekk la jig”. Ndax, du jóg fi ñu ko taaj te, fa la ko lépp di fekk. Saa su nekk, am ku fa soxlaam yabal, mu daagu mbaa mu waaxu ba ca moom, faji ko. Ñépp a ko yittewoo. Ba tax na daal, ku lay nëbbatu rekk walla mu réer la, xaar ko ca peggu ndaa la. Nde, lu mu yàgg-yàgg, dana fa jaar, mbaa mu yónnee fa. Moom lañu naan “goneg mbóoyo gu xamadi, xaar ko ca taatu ndaa la”. Léegi rekk tàngoor wi jàpp ko, bóli gi wow, mu dikk serlusi walla, pënd mi sàng ko, mu weex fur, daldi jàngusi.

Te nag, lu ci bari, menn mbàttu walla ab pot kepp ay dëppe ca kubéeru ndaa la. Moom la ñépp di jëfandikoo. Ku ci noppi teg, keneen ku soxla jëlaat. Mu mel ni luy wër rekk, ku mu agsi ci yaw daal, yaay boroom. Moo tax wolof mi mën a jàngale, bi mu bëggee xamle àddina, mu joxoñ nu ndaa li. Boole ko ci këf yi mu tànn def leen i niral, bëgg mu gën a yomb ci nun nu dégg galanu waxam. Ndax nu mën a mokkal bind bi te jariñu ci.

“ÀDDINA POTU NDAA LA, KU NAAN JOX SA MOROOM MU NAAN”.

Ndaa li ak mbàttu mi mu àndal, ñépp a ci bokk yam, du moomeelu kenn. Ku ci am aajo rekk yaay boroom, boo ci noppee, moomatoo ko. Ku aaye, wol sa moome. Waaye, yàgg-yàgg, dinga fegal sa moroom jël.

Ki téye potu ndaa li di naan, ak fu maram mën a àgg ak it lu ndox ma neex neex, dina màndi te du mën a naan ndaa lépp ci wenn yoon. Moo tax, lu war la ci moom, mu sóoraale ñi nar a ñëw ci ginnaawam. Bu leen bàyyee xel rekk, du naan yàbbiwaat ci ndaa li te du tanq lu mu narul a jeexal. Maanaam, dina def kemtalaayu kàttanam ngir mucc ci ñaari góomi xol yii di iññaan ak bëgge. Kaññaanug ki yàq ndox mi ba kenn dootu ko mën a jëffandikoo ginnaaw moom, ak bëggeg ki dëkkee xaabaabal sañ a aakimoo lépp ngir boppam kepp.

Jamono ji muy taxaw di tanq ci ndaa li, ak lu mën a doon soxlaam, ki yore mbàttu mi walla pot bi moo moom ndaa li. Moo nekkandeegum boroom te, moo fay dogal li ko soob. Ñaare, keneen ku soxla te yàkkamti sax, daf koy ñaan. Waaye, ci kaw loolu lépp, bu noppee ci faj aajoom ba jóge fa rekk, keneen moo koy wuutu. Mu mujj faf yam ci ak ñépp.

Loolu di gën a feddali kàddu gi naan : “Tay yaw, ëllëg sa moroom”. Mu di firnde ju fés ci ne, dara saxul ba fàww. Ci noonu la waykat ba xaacoo ca wet ga mel ni ku koy bëgg a dëggal, di naan : “Ag pal, lu mu réy réy itam, ag follikoo nga ca kanam. Lu yees itam ràpp. Xumbeen woo fi gis dana tas”.

Ba tax na, fu waay mën a nekk di bànneexu ak a nguuru, war na bàyyi xel ne bés a ngi ci bés yi, neex-neex bi wàññekku walla mu jeex tàkk. Bu ko defee, mu daldi rafetal nekkinam, defaraat toogaayam, mu gën a jekk. Waayeet, ci weneen wàll wi, fu waay mën a nekk ak i xat-xat yu tar, war na dunde yaakaar ci ne, bés a ngi ci bés yi, lëndëm gi xar, leer gi jolli, naqar wi far ba mu fàtte li weesu. Noonu lay mën a moytoo lépp luy ndiroo ak caalit. Ndax kat, bés du ñàkk, te ëllëgay dàq ! Rax-ci-dooli, sunuy jëfi tay, ñooy dooni sunuy jëwi ëllëg.

Moom mi yore mbàttu meet ci peggu ndaa li, am na gaa ku nar a nëw ci ginnaawam. Waayeet, am na ku mu wuutu. Kon, li muy jëfandikoo, keneen a ko yoroon la njëkk muy tàbbi ciy loxoom. Te, bu ca noppee, keneen a koy donn. Moom lañu naan, lu la àddina jox tay, ci sa moroom la ko jëlee. Naxaatekat la, nde mayewul dara, dafay able ak a dénkaane doŋŋ. Te, buy jëlaat li mu moom, du sax yëglu. Saa su la tingoomee ba nga ne àgg ca kaw, mi ngi nappaaje sa moroom ci suuf ci loo yëgul. Jamono ji mu lay reeloo, sa moroom a ngi jooy ndax moom te su ëllëgee yaw la ciy teg.

Lu jamono di dem rekk, mbàttu mi di wër, di wëndeelu niki tànku daamar guy daw. Nu dëkk ci ay-ayloo, di koy joxante te, xéy-na sax, bàyyiwunu ci xel. Ndekete, fu nu nekk rekk am na ku fa mësoon a nekk te, bu nu fa jógee, keneen dinanu fa wuutu. Lu nu yor it, jot naa jaar ciy loxo la njëkk muy tàbbi ci sunuy yos. Te sax, du yàgg dara mu toxu dem ci yeneen i loxo.

Àddina, mbir mën na fee yàgg lool. Waaye, dara saxu fi ba fàww. Te, lu fi am rekk safaanam bokk na ci li koy jëmmal, jox ko cafka, may ko njariñ. Am ak ñàkk, neex ak naqari, suur ak xiif, màndi ak mar, woomle ak rafle, wér ak wopp, dund ak dee… Benn bu ci nekk rekk, su àndandoowam ñëwul woon, dund gi soof, lewet domm.

Kon wareef la, ak fu jamono mën a tollu rekk, bu potu ndaa li doxee ba agsi ci nun, nu téye ko ci njekk te rafetal ko. Ndax kat, lu xumb tas, te lépp ciy nettali lay mujj.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj