LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (18/9/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

CÀMBARUG ÑETTI SÉMBI SÀRT

Altine jii weesu lañu ubbiwaatoon Ngomblaan ga. Lañu ko dugge woon mooy door beneen liggéey. Nde, dafa am liggéey bu ñu jotoon a amal ñeel càmbarug ñeenti sémbi sàrt. Mu mel ni loolu moo sababaat ubbiteg campeef googu. Jumbluwaay bi moo nekkoon càmbar ñetti sémbi sàrt yu ñu leen indilaat. Looloo sabab ñu woolu dépite yi tay, ci alxames ji. Li waral woote bi mooy dépite yi dañoo war a càmbar ñetti sémb yi ñu leen indil. Benn bi ñi ngi koy dippe “projet de loi portant modification de la Redevance sur l’accès ou l’utilisation du réseau des télécommunications publiques (RUTEL). Beneen bi di “projet de loi n°17/2025 modifiant la loi n°2012-31 du 31 décembre 2012 portant Code général des Impôts. Bi ci mujj di bi ñuy tudde “projet de loi n°16/2025 portant Code des investissements”.

TUKKIB NJIITU RÉEW MI

Démb, ci àllarba ji, lañu doon amal ndajem jëwriñ yi. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jot na faa xamle tukki bi mu war a amal balaa yàgg. Wii yoon nag, ma nga jëm fale ca New York ngir teewe ndaje mu mag mom Mbootaayu Xeet yi (Nations Unies). Tukki boobu dina ko amal ñaar-fukki fan ak benn jàpp ñaar-fukki fan ak juróom-benn ci weeru sàttumbar wii ñu nekk.

ËTTU ÀTTEKAAY BU MAG BI GÀNTAL NA BÀRTLEMI JAAS

Ay weer ci ginnaaw lañu teggi woon Bàrtelemi Jaas ci boppu meeri bu Ndakaaru ndax daan bi ñu ko daanoon. Booba ba tay, mi ngi doon daw ci ginnaaw Yoon ngir jotaat ci. Waaye, mujjeewul a sotti. Ndax, bu yàggul dara lañu fal Abbaas Faal, mu wuutu ko ca boopu meeri ba. Tay jii la ko Yoon doggali. Ndax, ëttu àttekaay bu kawe bi mujj naa dëggal ndogal li ëttu dabantal gi jëloon. Maanaam, dafa gàntal dabantal gi nga xam ne dugaloon na ko. Loolu di firndeel ne léegi moom, bir na ne ñàkk na meeri bu Ndakaaru. Amatul dara lu ñu ciy sikki-sàkka.

FIFA YEESALAAT NAG TOFTALEEM

FIFA mooy kurél gi ëmb mbiri futbal. Dafa di, léeg-léeg day génnee ag caabal ngir biral tolluwaayu ékib yi. Maanaam, wax ékib yi gën a ràññeeku ci wàllu njureef yi wane ci joŋante yu mujj yi. Ki jiitu ci toftale googu mooy réewum Espaañ. Léegi, moo wuutu réewum Arsàntin ca béréb boobu. Fii ci kembaarug Afrig nag, réewum Marog moo fi jiitu. Réewum Senegaal moo topp ci moom. Ci àddina wérngal-képp moom Marog ma nga ca fukk ak benneelu toogu bi, Senegaal nekk ci fukk ak juróom-ñetteel bi.

XEW-XEW BU TIIS FA SALI JAM-JAM

Xew-xew bu tiis moo am fa dëkk bii di Sali Jam-Jam nekke fa goxu Kungél, fa Kafrin. Benn boroom kër bu xel mi xawul a neex moo fa daanu ci benn teen jaare fa ñàkk bakkanam. Xew-xew boobu mi ngi am démb ci ngoon. Bees sukkandikoo ci waa Senego, jamono yi jéyya jooju di am mi ngi doon taw taw bu am doole lool. Moom, A. Ba, sàppëer yi ñoo ko génnee foofu yóbb ko fa morgo bu raglub Kungél.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj