USMAAN SONKO : « JÀMM REKK LAA SÉQ AK JOMAAY… LIGGÉEYALUMA JOMAAY, SENEGAAL LAAY LIGGÉEYAL. »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi doon na janook dépite yi, ci àjjumay tay ji. Moom ak jëwriñi Càmm gi ñoo fa àndoon. Li ñu ko dugge woon tontuji laaji ndawi réew mi ñeel tolluwaayu réew mi ak nees koy saytoo. Ciy kàddoom yu mujj, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, àddu na ci coow lees di ruumandaat digganteem ak Njiitu réew mi, te mu lëmbe pénc mi jamono yii.

Moom, Sëñ Usmaan Sonko, leeral na li mu séq ak Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay. Xamle na ne dafa am lu mu bëggoon a leeral rekk, waaye jàmm rekk a dox seen diggante, te ñoo ngi liggéey li ñu war a liggéey.

« Jàmm rekk a lanu séq, jàmm rekk ; di xëy, di gontu, di liggéey, di añandoo, di reerandoo. Benn porobalem [jafe-jafe] amul.… Ci wàllu pólitig, ku nekk mën na am doxalinam. Ci wàllu Etaa [Càmm gi], tay lanu gën a farlu ci liggéey bi. Ndaxte, li gaa ñi xamul [mooy ne], man liggéeyaluma Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay, Senegaal laay liggéeyal. Waaye, liggéey bi may liggéeyal Senegaal dafa nekk ci kilifteefu Njiitu réew mi, Basiiru, te ci màndaawam [moomeem] lañu koy boole. Kon, lépp lu ma jàpp ne lii njariñ la, duma ci xaar Njiitu réew mi, Basiiru. Lépp lu ma yaakaar ne lii safaan ba la, duma ci xaar Njiitu réew mi, Basiiru.

Elimaanu jëwriñ yi leeral na kon ne, réero ci pólitig mën na am, waaye loolu du leen teree def liggéey bi leen askan dénk, ñoom ñi leen yónni, yàkkamti leen.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj