Lu tollu ci ñaari ayu-bés kepp ay bëgg a des ci ubbiteg daara yu suufe yi ak yu digg-dóomi yi. Jëwriñ ji ñu dénk wàll woowu nag, dafa jël ndogal lu am solo. Ndogal looloo ngi jëm ci wàllu jëfandikoog jollasu (telefon) ci béréb yooyu. Te, kenn umpalewul ne jollasu moom daanaka, léegi, li ëpp ci xale yi am nañu ko. Looloo tax jëwriñ ji am beneen taxawaay ci mbir moomu ngir njàngum xale yi jaar yoon.
Démb, ci dibéer ji, la jëwriñ ji ñu dénk daara yu suufe yi ak yu digg-dóomu yi génnee ab yégle. Li mu dugge yégle boobu mooy xamal njàngaan yi, way-jur ak ñi séq njàng meek njàngale mi, ndogal li mu jël. Te, ndogal loolu du lenn lu moy ne tere nañu ñuy jëfandikoo jollasu ci biir daara yi. Muy yu ndaw yi (écoles), di yu digg-dóomu yi (collèges ak lycées). Li ñu ci jublu du lenn lu moy ndongo yi gën a jox njàng mi gëdda. Maanaam, ñu fullaal ko. Rax-ci-dolli, seen xel yi gën a ñaw ngir ñu am ay njureef yu mucc ayib.
Dafa di, bees sukkandikoo ci yégle bi, li jollasu yi di yàq ci daara yi moo raw fuuf li ñu ciy defar. Maanaam, ci anam bi ko njàngaan yiy jëfandikoo, loraange yee ëpp njariñ yi. Ndaxte, ba tay ci yégle bi, jollasu bi dinay sabab ci ndongoyi ag tàyyeel, waayeet day tax ñuy bëgg di beru. Te, waxaalewuñu sax njeexital yi muy am ci seen wér-gi-yaramu. Nee nañu, mbir mi yamul foofu. Ndax, mooy waral càcc gi, tëkku yeek yu ni deme ba ci sax di tanqal walla di gàllankoor njàngum ñeneen ñi. Bi ñu boole yooyu yépp nag, ci lañu xam ne jëfandikoo gi du def lu dul yàq njàngum ndongo yi.
Ci loolu, jëwriñ ji xamal na ñépp ne, li ko dale ci ubbite gii ñuy dëgmal tere nañ jëfandikoog jollasu ci daara yépp. Muy daaray bokkeef gi (écoles publiques) ak yoy jàmbur yi (écoles privés). Ñu waxaat ne, tere bi, moom ci jollasu yi kese la yam. Yeneen jumtukaayi xarala yi ñu mën a jëfandikoo ngir jàng bokkuñu ci. Muy lu ci mel ni ay tablet, nosukaay, jàngukaay (liseuses). Loolu di firndeel ne dañoo bëgg a jële ci béréb yooyu lépp loo xam ne day tax xale yi duñu teewlu li ñu leen di jàngal. Waaye, loolu du càggan ne ñépp lañuy tere jëfandikoo gi. Am na ñoo xam ne am na anam yu ñuy tollu dees na am sañ-sañu yore jollasu.
Li ci des mooy daara ju nekk jël ay matuwaayam xool naka lay def ba mën a jëfe ndigal loolu. Maanaam, nan lay def ba jël jollasu yi wut fu mu leen di denc. Bu ndongo yi wàccee ñu delloo leen leen. Loolu moom, nu golo xam rekk, na ko bootee doomam. Ñoom ñoo yor seen cëggalu guy, dees na xam nan lañuy toje seen boppu jinax. Daara ju nekk ak pexe yi mu tëral, nga xam ne mook kurélu way-juri ndongo yee ciy ànd. Su ko defee képp ku jàdd yoon rekk xam yan daan ñoo la ciy fekk.