YENEEN SÉMBI SÀRT YU ÑU WAR A CÀMBAR FA NGOMBLAAN GA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci weeru ut wii ñu génn la amoon ñeenti sémbi sàrt yu ñu yóbboon fa Ngomblaan ga ngir càmbar leen. Li ñu ko dugge woon du lenn lu moy settantalaat nees di sàmmee alalu réew mi. Rax-ci-dolli, teg ay pexe ngir dundal demokaraasi réew mi. Mu mel ni ba tay jóguñu ci loolu. Ndax, am na ñetti sémbi sàrt yu ñu yóbbaat fa Ngomblaan ga tay ci altine ji ngir càmbar leen.

Démb, ci altine ji, lañu ubbiwaat Ngomblaan gi ci njiiteefu kilifag béréb ba, El Maalig Njaay. Li ñu dugge ndajem démb ja nag mooy door yeneen i waxtaan ak ay diisoo ñeel sémbi sàrt yu am solo yi ñu leen indil. Nde, kenn umpalewul ne am na ñeenti sémb yu ñu jotoon a fénc bu yàggul dara. Muy sémbu sàrt wu jëm ci settantal dayo ak kaaraange yoolekat yi, wow taxawalug OFNAC, sémb wi jëm ci xibaar ak wi nga xam ne moo ñeel xamle sa moomeel.

Dafa di, réew mi dafa nekk ci jafe-jafey koom-koom. Looloo tax Nguur gi fi nekk di lal i pexe ngir génne réew mi ci jafe-jafe yooyii. Loolu nag, mëneesu koo def te jaarewuñu ko ci ay naal. Looloo sabab ndaje mi ñu amal démb ca Ngomblaan ga.

Ñaareelu ndaje moomu, li ko wund mooy wote sémbi yii ñu leen yóbbul, nga xam ne seen solo ci wàllu koom gi kenn naataablewu ko. Sémbi sàrt yooyu nag ñett lañu. Benn bi ñi ngi koy dippe “Projet de loi portant modification de la Redevance sur l’accès ou l’utilisation du réseau des télécommunications publiques (RUTEL). Beneen bi di “Projet de loi n°17/2025 modifiant la loi n°2012-31 du 31 décembre 2012 portant Code général des Impôts. Bi ci mujj di bi ñuy tudde “Projet de loi n°16/2025 portant Code des investissements”.

Lii yépp ay sémb la yoo xam ne dees leen a war a càmbar ci lu dul yàgg dara ca béréb booba. Ndax, lempo bi bokk na ci li gën a ñor Nguur gi fi nekk. Ñu fullaal ko lool. Te, dara waralu ko lu moy dañoo jàpp ne liy suqali koomu réew mi foofu la war a jaar. Kon, fii ak lu dul yàgg dara, dees na xam nu sémb yooyu tëdde ak lan lañu mën a jariñ réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj