MAJAMBAL JAAÑ, WAALI SEKK, ABDULAAY DAAWDA JÀLLO : YOON A NGI BARAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Saabalkat bii di Majambal Jaañ de, jamono yii, mi ngi ciy guddi yu lëndëm këriis. Démb bat ay, moom la saabalukaay yeek mbaali jokkoo yi ame. Li ko waral mooy ne, Yoon a nekk di ko wër. Ci lees wax sax, mi ngi doon jéem a génn réew mi niki démb ci talaata ji. Waaye, mujjul a jéggi dig yi. Ndax, bees sukkandikoo ci yéenekaay Libération, ndawi komisariyaa bu naawub Jas bi (AIBD) ñoo ko wàccee, daldi waññi.

Dañu ubbi ag luññutu ci Majambal Jaañ. Toppekatu Ëttu Àttekaayu Mbiri Koppar yi moo santaane ñu gëstu ci mbiri saabalakat bi. Kii di àttekatu ñetteelu kabine bi lañu dénk wayndarew Majambal Jaañ. Moom moomu sax moo joxe ndigal ngir ñu tere Majambal Jaañ mu génn réew mi.

Dafa di, ag caabalu CENTIF a tudd gerefiyee ba woon, moom Majambal Jaañ, njort ne dafa lënkaloo ak njiiti kërug liggéey gii di Ellipse, daldi wuruj alalu askan wi. Xaalis bees ko toppee ngi tollu ci 21i miliyaar ciy seefaa. Bees sukkandikoo ci waa Libération ba tay, jéem nañoo jokkoo ak Majambal Jaañ ngir taataan xalaatam ci mbir mi, waaye dafa leen tontu, wax leen ne du ci àddu.

Ci ngoonug tay jii, takk-der yaa nga woon këram. Nde, wuyujiwul Yoon mi ko woolu woon. Moo tax takk-der ya demoon këram ngir jëli ko. Waaye, ci li sunuy naataangoy Buur News xamle, fekkuñu ko fa.

Bu weesoo Majambal Jaañ, waykat bii di Waali Bàllaago Sekk itam, Yoon daf ko woolu woon. Moom nag dawul. Wuyusi woon na. Ndax, bitim-réew la nekkoon. Fan yii la delsi fi réew mi. Moom itam, caabalu CENTIF gaa ko tudd. Àttekat biy luññutu daf ko tuumaal tuumay mbooloom defkati njombe ak weexalug koppar ci alal jees xayma ci 210 miliyoŋi seefaa ci wàllu njaayum daamar. Daamar googu, nee ñu, doomu Maki Sàll ji, Aamadu Sàll, a ko jënd.

Ci li layookatam yi wax, Waali Bàllaago Sekk dafa nangoo joxe « caution » ngir ñu bàyyeendi ko. Waaye, dafa dàq tuuma yees gàll ci kawam yépp.

Am na yeneen kàngaami Nguur gi weesu yu Yoon di woolu. Nde, kii di Abdulaay Daawda Jàllo ci boppam, DIC woolu woon na ko ngir déglu ko.  Ci li yéenekaay Quotidien siiwal, démb ci talaata ji, 23i fani sàttumbar 2025 la wuyuji woon. Moom nag, Abdulaay Daawda Jàllo, déglu nañu ak waytuy waxtu.

Bu dee caabal CENTIF gee tax Yoon di wër Majambal Jaañ, Abdulaay Daawda Jàllo moom, caabalu Ëttub cettantal gee tax ñu woo woon ko. Caabaal googoo ngi aju ci diirub 2019 jàpp 2024 ñel anam bi ñu daan saytoo koppari réew mi. Moom nag, dafa nekkoon jëwriñu ngurd mi. Ginnaaw bi ñu laajee ba noppi, dañu ko bàyyi mu ñibbi. Waaye, xamal na takk-der ya ne, saa bu ko Yoon soxlaa, dina wuyusi.

Du Abdulaay Daawda Jàllo kese la Yoon teg bët. Ndax, ñu bari ñi laale woon ak koppari réew mi, Yoon a ngi saytu seen i mbir. Te, saa su nekk, mënees na leen woolu. Ci lees rotal ciy xibaar, kii di Aadama Raasin Sow mi doon liggéeyee Trésor public jot nañu koo déglu, moom ak Waali Nduur ma fa doon liggéey itam. Kii di Aamadu Ba (elimaanu jëwriñ ja woon), Birima Màngara ak Seex Tiijaan Jóob itamit, Yoon a ngi càmbar seen i wayndare. Bu ñu déggee ne woolu nañu leen, du bett kenn.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj