FMI AJANDI NA WOTEB SIPPI BI ÑEEL SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

FMI ajandi na woteb sippi bi waroon a tax Senegaal mën a leb xaalis bob, daf ko aajowoo jamono yii. Ci àjjumay tay jii la Ndajem caytu gog FMI doon daje ngir fénc mbirum koppari Senegaal yi. Li ñu ko dugge woon mooy càmbar mbirum bor bees wax ne, Nguurug Maki Sàll gi fi woon dafa nëbboon dayo bi. Waaye, laata ndaje may jeex, saabalukaay bii di Agence Reuteurs xamle woon na sax ne, waa FMI, duñu wote sippi bi waroon a tax Nguurug Senegaal gi jot ciy koppar yi mu aajowoo ngir liggéey.

Senegaal dina toogandiwaat ay ayu-bis laata muy mën a lebaat i koppar. Li FMI ajandi woteb sippi bi mu waroon a amal tay a ko sabab. Dafa di, ngir réew mi mën a lebaat walla jot ciy koppar ci àddina si, fàww ñu lijjanti mbirum bor bees wax ni Maki Sàll ak nguuram ga woon dañu nëbboon tolluwaay bi dëggantaan.

Weeru me 2025 ba léegi, Senegaal a ngi xaar FMI létt ko walla mu firi ko. Nde, fàww ñu woteel ko ab sippi ngir ñu mën ko lebal xaalis. Sippi boobu nag, laata ñu koy woteel am réew, dafa aju ci ay sàrt yu FMI tëral yoy, réew moomii daf leen a war a matal.  Sàrt yooyu, daf ci bokk ag luññutug ndimbalu xarala gu aju ci anam bees di saytoo koppari réew mi. Waa Agence Reuteurs ñoo joxe xibaar boobu. Wànte, rax nañ ca dolli ne, FMI mën na bañ a xaar njureefi luññutu googii ngir woteel Senegaal sippi bi. Kon, mbir mi ci FMI kepp la aju.

Bu dee ci wàllu Senegaal nag, ci lees xamle, fàww ñu lijjanti mbirum bor bi balaa ñu koy mën a woteel sippi bi. Te sax, bu ñu ko gàntalee sippi boobu, Senegaal dafa war a fay bor bi mu ame ba mu mat, ñu koy soog a mën a lebalaat xaalis.

Kenn, ci ñi yor kàddug FMI, àddu ci li sababoon ndajem àjjumay tay ji, wax ne jubluway bi moo doon « xamal saytukat yi mbirum Senegaal ak jéego yi ciy topp ñeel aamu gi, ak itam lees war a sumb, ci lu dul yàgg dara, yeneen i waxtaan yuy aju ci naaluw koppar wu bees wu FMI war a defal Senegaal ». Mu teg ca ne :

« Ci fànnu liggéey bees war a def ngir dooleel caytu gi ak jubal bi, njiiti réew mi aamu nañu ngir wóoral tolluwaayu bor bi dëggantaan, ubbi ay luññutu ñeel rëq-rëq yi am ci caytug  koppari réew mi te leeral yoon yi xaalis bi ñu nëbboon bi jaar, ànd ceek Yoon. »

Ngir fàttali, bi Nguurug Senegaal gu yees gi toogee, dañu amaloon ay luññutu ci koppari réew mi. Ca lañu gisoon ne, borub Senegaal bi ëpp na lool la Nguurug Maki Sàll ga waxoon. Noonu, FMI daldi téye 1,8 miliyaari dolaar yi mu waroon a jox Senegaal. Léegi nag, ci ni ko ay sàrtam tëralee, fàww FMI woteel Senegaal ab sippi ngir mu mën a jot ci koppar yooyu walla mu lebaat feneen. Ci àjjumay tay jii lees doon xaar FMI amal wote bi. Waaye, dañu mujjee ajandi ba jëmmi jamono.

Ndogalu FMI li nag, dafa am lu muy wund lol, dees na ko faramfàcce ci beneen yaxal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj