LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (16-10-2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

XIBAAR ÑEEL YOON

Téyandi nañu ràppëer bii di “10 000 problèmes” ak kii di Lamin Kàngaam. Ki tax ñu jàpp leen mooy  Sëriñ Abdulaay Fay mi leen jure (pelent). Ab widewoo a leen boole. Ca biir widewoo booba, “10 000 problèmes” ak Lamin Kàngaam dañu ci doon tuumaal Sëriñ Abdulaay Fay mbirum ngóor-jigéen. Bees sukkandikoo ci waa Source A, dañu ko doon napp ak a tiital, di ko ci laaj ay koppar. Fim nekk nii nag, li ñu leen di toppe mooy biral xibaar yu wérul ak li ñuy dippe “extorsion de fonds et de chantage”. Ba tax na ñi ngi leen téyandi.

Kii di Soyaa Jaañ tamit, moom yóbbu nañu ko kaso. Kon, tay, lay fanaan guddeem gu njëkk. Li ñu koy toppe mooy biral xibaar yu wéradi ñeel ag kilifa ci réew mi.

Naka noonoot, kii di Làmmiñu Daaru ak Boy Dakaar itam, ba tay, ña nga ca loxoy Yoon. Ñoom nag, jotoon nañoo layoo. Waaye, loolu taxul ñu bàyyi leen. Joxaat nañu leen àpp ngir àddu ci seen i mbir. Maanaam, ñu wax leen bu dee dañu leen di daan am dañu leen di bàyyi. Àpp googu mi ngi yamoo ak ñaar-fukki fan ci weeru oktoobar wii ñu nekk.

NDAJE MI ÑU JAGLEEL TÉERE AK DAWAL

Tay, ci alxames ji, lañu doon amal ndajem liggéey mi ñu jagleel téere ak dawal, ñu koy dippe “Forum national sur le livre et la lecture”. Mu nekkoon ndaje mu am solo. Nde, kenn umpalewul njariñ yi téere làmboo. Ñu ko doon amalee ci njiiteefu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Mu doon lu mu gëddaal. Nde, dafa war a bokk ci banqaas yiy soppi mbatit ak yaru askan wi. Maanaam, daf leen di gën a xiirtal ci gëstu. Su ko defee xel yi gën a ñaw. Waaye tamit, ñu mën di màcc ci lu bari. Moo tax, Njiitu réew mi gis ne nun népp a war a fonk dawal.

XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Gaynde yu ndaw yoy Marog yi amagul ñaar-fukki at def nañu jaloore. Nde, dem nañu finaal ca joŋante ba ginnaaw bi ñu dóoree doomi Farãs yi. Finaal boobu ñi ngi ci war a daje ak doomi Arsàntin yi. Joŋante bi dees na ko amal ci guddig dibéer jii di ñëw, bu fukki waxtu ak benn jotee.

Gaynde yu mag yoy Senegaal yi tamit dinañu amal joŋante xaritoo bu am solo. Ekib bu kenn dootul aajar lañuy dajeel, muy ñii di waa Bereesil. Joŋante boobu dinañu ko amal fukki fan ak juróom ci weeru nowàmbar. Dees na ko amalee ca fowu (estaadu) Arsenal bees duppee Emirates Stadium, fa Londar (Àngalteer). Mu nar a doon joŋante bu neex. Ndax, ñaari réew yi jotoon nañoo daje bu yàggul dara, Senegaal amoon ndam ci kawam.

CONG MU METTI FA CEES

Cong mu metti moo am fa Àllu Kaañ, nekk ci diiwaanu Cees. Ay sàmbaa-bóoy yu ngànnaayu ñoo fa song ñaari ndefar (isin). Bees sukkanikoo ci waa L’Observateur, ñaar yépp ci wàllu simaŋ lañuy yëngu, muy CIMAF ak CBMI. Gaa ñi nag, ba ñu ñëwee, dañoo néewal doole ñi ñu fa fekk ñuy wattu béréb ya. Bi ñu noppee lañu fa jël lu tollu ci juróom-fukki miliyoŋ, daldi seey ci àll bi laata waa Sàndarmëri di ñëw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj