LIGGÉEY BAA NGI WÉY DIGGANTE FMI AK NGUURUG SENEGAAL GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waa FMI dinañu toogaat ci réew ay fan ngir wéyal liggéey bi ñu sumb ak Nguurug Senegaal. Bésub 22 oktoobar 2025 lañu ñëwoon Ndakaaru ngir waxtaan ak njiiti réew mi ñeel naal wu yees wi ñu war a jagleel réew mi ci wàllu kopparal.

Yéenekaay Le Soleil a biral xibaar bi. Bees sukkan ci kàdduy kenn ci ñi yor kàddug FMI :

“Barug FMI gee ngi wéyal waxtaan wi, fi Ndakaaru, ak njiiti Senegaal yi. Sunu tukki bi, njariñ kese la juragum ba fi mu tollu nii. Te, nu ngi wéy di waxtaan ci xeeti ndogali polotig ak coppite yiy dëgëral càkkuteefu Càmm gi ñeel naaluw kopparal wu yees wu leen FMI di jagleel.”

Sunuy naataangooy Le Soleil ñoo tuxal yile kàddu. Moom, ki biral yile kàddu, xamleet na ne, bu ñu noppee ci liggéey bi, dinañu xamal nit ñi la ca tukkee.

Ci bésub talaata jii, 4 nowàmbar 2025, la liggéey bi waroon a jeex. Liggéey boobu nag, mi ngi aju ci lëkkatoog kopparal gi dox diggante Nguurug Senegaal ak FMI, campeefu Bretton Woods gi.

Liggéey bi nag, lees ko dugge mooy mooy fexe ba am naaluw kopparal wu yees wu FMI di jagleel Senegaal. Jubluwaay bi, ci lees xamle, mooy gunge Nguurug Senegaal gi ngir mu mën a tabax koom-koom gu dëgër, suuxat yokkuteg réew mi te dooleel nafag réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj