Ci altiney tay jii, 10i nowàmbar 2025, la Senegaal doon màggal Bésub Sóobare yi. Wëppa wees jagleel bés bi nag mooy : « Sóobare yi, farandooy powi JOJ Ndakaaru 2026 yi ». Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, moo jiite xew ma. Moo doonoo ab pose ci moom, mu daldi sargal góor ak jigéen yiy sol mbubbi takk-der. Nde, ciy kàddoom, taxawaay bu am a am solo lañu am ci waajtaayi Powi Olimpigi Ndaw ñi (JOJ), Ndakaaru war ko dalal ci atum 2026.
Njiitu réew ma dafa njëkk a sargal rafetlu fit ak xarañteefu sóobare yiy wattu kaaraange réew mi, muy ci biir réew mi, di bitim-réew, ca saytook a aar dig yi. Dafa di sax, atum ren jii mooy tollook 65eelu at, bi Senegaal njëkkee yabal ay sóobareem ci raayab Mbootaayu Xeet yi (ONU). Loolu dafay firndeel dogu bi Senegaal yàgg a dogu ci xeex ngir jàmm ci àddina si.
Bi Njiitu réew miy àddu ci wëppaw bés bi, dafa fàttaliwaale solos Powi Olimpigi Ndaw ñi. Ndaxte, Senegaal mooy réewu Afrig muy njëkk a dalal yile xeeti po yoy, àddina sépp lay boole. Looloo ko tax wax ne :
« [Powi Olimpig yii] weesu nañu mbirum tàggat-yaram kese. Ndaje mile dafay màndargaal Senegaal gu bees gi, màggalug sunu dooley ndaw ñi te taxawaayu Afrig biy wéy di yokk ci kurélug olimpig. »
Sóobare yi dinañu jàpp bu baax ci kaaraange po yi, waayeet ci suuxat jikkoy dëgër, yar ak mbokkoo, di jikko yiy màndargaal tàggat-yaram. Njiitu réew ma rafetlu naat sémbuw « Waajal Xale yi », di sémb woo xam ne, njëwriñu Njàng mee ko sumb ngir yar xale yi ci bëgg seen réew.