Seneweb moo siiwal xibaar bi. Maki Sàll, Njiitu réewum Senegaal mi folleeku keroog 24 màrs 2024, moo bàyyi liggéey bi ko Njiitu réewum Farãs dénkoon.
Laata Maki Sàll di jeexal moomeem ga la ko Emmanuel Macron tabboon, mu war a jiite komite bii di “Pacte de Paris pour la planète et les peuples”, gàttal biy joxe 4P.
Jamono jooja nag, mbir mi juroon na fi coow lu réy a réy. Ñu bari di naqarlu ak a ñaawlu li Maki Sàll nangu ab naataangoom, di Njiitu réew ni moom, di ko tabb, mu koy liggéeyal. Mu mel ni rekk kuy dunguru ngóor soosu nekk ca njéndel “Élysée” la.
Bari woon na ñu jàppoon ne, ngecceel ak yaras doŋŋ ñoo taxoon Njiitu réewum Senegaal la, ca jamono jooja, di nangul waay sos, magee na ko 16i at, rawatina bi mu nekkee njiitu réew ni moom. Te sax, moo ko ko njëkk a nekk. Diggante boobu, buumug njaam ga woon jógu fa. Nde, xuccub nooteel baay wéy di dundal seen kóllëre gi. Dafa mel ni nag, kóllëre gaa ngi xajamsi.
Dafa am ñu jàpp ne Macron dafa dàq Maki Sàll. Xibaar boobu nag, wéragul. Amaguñ ci firnde lu wér. Wànte, bu dee dëgg, du bett kenn. Nde, ak li Càmm gu bees gi siiwal ci anam bi ñu fekkee réew mi, deru Maki Sàll mënul lu dul yàqu ci àddina si. Te, bu boobaa, ak ni àddina si tëddee, dina néew ñuy bëgg a liggéey ak moom. Wolof nee na kat, ku boot bukki, xaj bów la. Te nag,kenn bëggul a ànd ak kuy xajamal sa cere.
Ci lees rotal ciy xibaar, Maki Sàll moo bàyyi ci coobare boppam. Bees sukkandikoo ciy waxam yu benn ciy jegeñaaleem dénk waa Seneweb, li mu jiite toftaleg lëkkatoo Takku Wallu Senegaal moo waral mba gi mu ba. Ba tey ciy waxam, dafa bëgg a wuyu wooteb réewam, muy Senegaal. Wotey dépite yees dëgmal lay waajal. Ndax, ci li Seneweb biral, Senegaal a ko gënal meneen réew mu mu mën di doon ci àddina si. Kon daal, bees ko déggee, bëgg Senegaal a ko tax a bàyyi liggéey bi mu doon defal Njiitu réewum Farãs ak jagle yi mu làmboo yépp. Am na ñu ko gëm, am ñu ko gëmadi.
Mëseesul a gis, ci mboorum Senegaal, Njiitu réew lu wàcc, dellu sóobu ciy wotey dépite. Muy Seŋoor, di Abdu Juuf, di Abdulaay Wàdd, kenn mësul xuus ciy kàmpaañ ni ko Maki Sàll defee nii, tay. Dees na fàttali wooteb widewoo bi mu defoon ca ndajem Bennoo Bokk Yaakaar ma. Dafa di, jéego yi Maki Sàll di dox yépp lenn rekk lay wund : wotey 17 nowàmbar yi jaral nañ ko lu nekk. Laaj bi nag mooy : lu tax Maki Sàll bañ Pasteef jël raw-gaddu gi ca Ngomblaan ga ? Ndaxte kat, ku waxal Yàlla, xam ni, xeex bi yépp, ci Usmaan Sonko la jëm ak waa Pasteef.
Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dafa joxoñ baaraamu tuuma Maki Sàll ci guuta gi réew mi nekk ak ni ñu caxat-caxatee koppari askan wi, tibb ko, toŋ-toŋ ko, paacoo ko ba noppi bàyyi askan wi mu tumurànke. Waaye du loolu kese la njiitul Pastef liy tuumaal Maki Sàll. Ndax, diggante màrs 2021 ak màrs 2024, lu bari jot na fee xew ciy fitna, ciy nit ñees faat, ciy nit yu ñu xoqatal, tëj leen kaso, añs. Loolu yépp, ci ndoddu Maki Sàll lees ko gàll. Keroog rekk, bi Càmm giy biral yàqute yi ñu fi fekk ci wàllu koom-koom, Usmaan Sonko dafa tuddoon ay tur, tuddaale ci Maki Sàll mi mu jàpp ne, mooy ndeyu-mbill ji, moom mi yoroon baatu dogal bi. Waxoon na sax ne, dafa war a leeralal askan wi. Maanaam, dafa war a layook askan wi. Du askan wi nag mooy àtte, waaye Yoon moo mën a wax ndax def na walla deful.
Xamees na ni, mëneesu ko àtte fu dul ca Ëttu àttewaay bu kowe bi (Haute cours de justice). Ndax, ëttu àttewaay boobu rekk a am sañ-sañu àtte Njiitu réew ak i jëwriñ. Te nag, Ngomblaan gi rekk a mën a wote, samp Ëttu àttewaay bu kowe boobu. Ñu gis ne kon, wote yii, li ci laxasu dafa bari. Moo tax ñenn ñi teg ci seen i bakkan.
Cig pàttali, Maki Sàll dafa waxoon Saa-Senegaal yépp ak àddina sépp ni, moom, doyal na, du sàkku ñetteelu moome. Maanaam, suur na njiiteefu réew mi ak lépp lu ci laale. Tay, mu bëgg a delsi ci géewu pólitig bi. Kon, warees na laaj Maki Sàll, wax ko : Maki Sàll, lu la ko jaral ?