Aa ! Gaa ñi, Tataa Mimi mer na !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Aminata Ture mer na nag. Te, altine ba léegi, moo ngi koy fésal ak a biral ci mbaali jokkoo yi ak ci waxtaan yi muy amal ak taskati-xibaar yi. Tànn bi Njiitu APR li tànn meeru Risaatol bii di Aamadu Maam Jóob, teg ko ci boppu Ngomblaan gi moo ko bett, metti ko lool. Nde, moom, dafa jàpp ni Maki Sàll dafa jiital mbirum mbokk, daldi koy wor.

Senegaal yépp a amoon mbetteel bi ñu biralee, keroog ci altine ji, lawaxu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar bi Maki Sàll tànn ngir mu doon Njiitalu Ngomblaan gi. Dafa di, kenn xeloowu ko woon. Ba ci sax waa Bennoo Bokk Yaakaar, kenn mësta xelmati ne Maki Sàll dina jiital Aamadu Maam Jóob ci kow Mimi Ture, Aamadu Ba, Aali Nguy Njaay walla Abdulaay Daawda Jàllo. Nde, saa buñ laajaan ku nar a doon lawaxu BBY, xel yépp dem ci ñeenti kàngami APR yile nga xam ne, balaa dara di dara, ñoo àndoon ak Maki Sàll. Moo tax, bi ñu siiwalee turu Aamadu Maam Jóob, kameraa yépp ñoo ne jàkk soxna Aminata Ture. Booba, Tataa Mimi mer na ba mu feeñ ci kanam gi. Mënu ko woon nëbb ndax, lu la bett, mën la. Te, loxo bu duggee ci mooñ am lu ko jam, da koo bett, waaye foogu ko woon.

« Muñ naa xeetu tooñaange bu nekk, bi ma dalee ànd ak Maki Sàll ba tey, waaye bii mo ci desoon. »

Soxna Aminata Ture xaarul sax wote bi. Xol baa naqari, mu gedd, daldi ñibbi. Laata muy dem nag, noon na Farba Ngom mu delloo ko yable bim ko joxoon, ngóor si bañ.  Ci ginnaaw gi sax, def na ñaari tweet, ci altine ji ak ci talaata ji, di ci wax ne Fraba Ngom daf ko bañ a delloo ay yableem. Ndax, moom, wotelul te woteluwul lawaxu Maki Sàll bi.

Li Maki Sàll def, ag kor la ko jàppe. Ci laaj-tontu bu gàtt bi mu amaloon ak L’Observateur, mi ngi ciy wax naan :

« Balaa dara, dama bëgg a ñaax ndaw ñi ngir ñu wéy di gëm jikkoy ngor, ngëneel ak yemale donte ne, ci wàllu palug njiitalu Ngomblaan gi, Njiitalu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar jiitalul benn ci jikko yooyii. Sama àddina yépp, dama ko xeex ngir yoon. Muñ naa xeetu tooñaange bu nekk, bi ma dalee ànd ak Maki Sàll ba tey, waaye bii mo ci desoon. Jiital deret ci kow ngëneelu militaŋ, mënatuma ko nangu. »

Lu ni mel la waxaat ca RFI. Ndekete, ba muy nekk ca Péncum réew ma la ko Maki Sàll woo, daldi koy xamal tànneefam gi. Bu ñu sukkandikoo ciy kàddoom, Maki Sàll sàmmotewul ak i digeem. Waaye, moom, du wax-waxeet bi ci boppam moo ko metti, waaye anam bi mu ko defee moo ñaaw.

« Dara nekkul ci nga soppi sa xalaat, ci kow mu bañ a nekk boddekonteb mbokk walla jaay doole. »

Li ëpp ci xeltukat yi ak faramfàccekat yi dañu njort ne, li Mimi Ture waxoon ne Maki Sàll du laaj ñetteelu moome ak li mu xemmem a bokk ci joŋantey wote 2024 yi ñoo tax Maki Sàll wóoluwu ko. Daf koy ragal a dooleel, moo tax mu xañ ko njiiteefu Ngomblaan gi. Bi ko L’observateur laajee, lii la tontu :

« Loolu wees na. Yàgg naa wax ne, te ma gëm ko, bu tabbee jëwriñ ju njëkk ji, dina génn wax ne du def ñetteelu moome (kay). Sama ñàkk ànd ak moom ci ndogal li mu jël ñeel njiiteefu Ngomblaan gi duma teree gëm ne gor la, te dina sàmmoonte ak kàddoom. »

Aminata Ture moo jiite woon toftalaanug Bennoo Bokk Yaakaar ci wote yi. Nee ñu, Maki Sàll daf ko digoon Njiiteefu Péncum réew mi. Ndeysaan, faleesu ko ko. Te, jiitewul sax ndajem dépitey Bennoo Bokk Yaakaar mi. Ndaw gàcce… Ngir fésal meram, dafa ñibbi. Ba tey, ci waxi ñenn ñi, daf ne taskati-xibaar yi ne day génn APR. Bu dee malaanum dépite bi nag, nee na du ko summi.

« Duma summi sama malaanum dépite, loolu moom dafa leer. A waaw, lu tax rekk ma koy def ? Dépite bi ma nekk, maa ko ñaq. Dama wër 5. 175i km, jaay bilaŋu Nguur gi. Ay at a ngi nii may xeex. Awma ci kersa ndax woroowuma ak samay gëm-gëm. »

Dafa mel ni, Soxna si dafa nar a jàmmaarloo ak Njiitu réew mi Maki Sàll. Mbirum deret ji lëmbe Càmm gi la nar a njëkk a jam nag.

« Jàpp naa ne dañu war a am ay dépite yuy joxe ay sémbuy àtte yu baax niki sémb yi ma fas yéene joxe ngir aaye ag mbokkoo ci yenn palaasi Càmm gi. Bu ko defee, dinañ bàyyi di boole mbokk yi ci mbirum Càmm gi. »

Lii mu wax yépp day wone ne kóllëre gi doxoon digganteem ak Maki Sàll jeex na tàq. Jàpp na ne Maki Sàll daf ko toroxal, suufeel ko ci kanami nawleem. Noo ngi xaarandi ba xam fu jàmmaarloo biy mujj. Ndax Tataa Mimi day dëggal génnam ci APR ? Ndax dina samp ndëndam ci wotey 2024 yi ?

Ak lu ci mënti am, mel na ni Nguurug Maki Sàll day waaj a jeex. Bés bu nekk am lu koy firndeel te, ci biiram lay jóge. Nde, ñépp a jàpp ne dafa wor Mimi Ture, ba ci waa BBY. Te, nag, wor sa ŋaamaan, moo gën wor sa léttkat.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj