Séex Aajibu Sumaare, njiitu jëwriñ ja woon, dafa bind ab bataaxal jagleel ko Njiitu réew mi. Ci biir bataaxel bi, Aajibu Sumaare daf ci tuddaale 12i miliyoŋi ëro yoy, ciy waxam, Njiitu réew mi Maki Sàll daf ko jox benn saa-farãs bu am tur. Bi loolu amee, nag, xel yépp ci Marin Le Pen lañu dem. Naam, jaarul ci turu soxnas tubaab si, waaye junj bi mu joxe moo tegtale jëme ci ndaw si. Rax-ci-dolli, ci jamono yii nu génn, soxna saa ngi woon Senegaal te gise na ak Njiitu réew mi. Moom ci boppam moo toogoon Rajo, xamal Mamadu Ibra Kan ne, Njiitu réew mi Maki Sàll dalal na ko ca màkkaanam ba. Kon foofu rekk la xel yi mën a dem.
Ci biir bataaxal bi, moom Aajibu Sumaare njort na ne Maki Sàll dafa génne lu tollu ci 12i miliyoŋi ëro, jox ko ndaw si.
Ginnaaw bi mu fàttalee Maki Sàll wareefam yeek digeem yim ameel saa-senegaal yeek réew mi, ak tamit waat ya mu waatoon awril 2019 ngir sàmm kàddoom, dafa laaj 4i laaj yii toftalu :
-
« Ndax danga jox ab saa-farãs xaalis ci fan yii nu génn ? Bu dee loolu am na, ndax dinga dëggal ni 12i miliyoŋi ëro la, maanaam 7,9 miliyaar ci koppari réew mom, boolees na ko ci réew yi gën a ndóol te bari lool ay bor ? Rawatina bees xamee ni mbañeel ak boddekonte la pàrti ndaw si jaare ba àgg fim àgg ci pólitig ?
-
Ndax, ginnaaw seen ndaje ma, daŋ ko yónnee ab bataaxal bu gàtt bob, sa màndarga bi nga ci def ?
-
Bu fekkee ne tontuy laaj yii yépp mooy « waaw », yoon la nga leeralal askanu Senegaal, xamal leen ndax ci sa coobarey Njiitum réew nga ko defe, am ci sa coobarey njiitul pàrti pólitig nga ko defe ? Ak tamit, fu xaalis bi jóge ?
-
Laaj bu mujj mooy, ndax danga nar a bëtal wote palug Njiiteefu réew mi bi war a am 2024 ?…… »