AFRIG, LU LA TAX A DES GINNAAW ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bare na li may toog man kenn, di yónni samam xel, mu wëral ma àddina sépp ak li ci biir, fu nekk mu ne fa naam-daraame, yër la fa nekk, dellusi. Waaye, li ëpp ci samay xalaat ak i seetlu, Afrig la ñeel, sunu Afrig ak ëllëgam. Bu ko defee, sama xel mi day faral di wër réewi Afrig yi ba ñu daj, bunt bu dul buntu jinne mu fëgg fa, dugg ci biir kër gi, jàngat la fay xew, doxalinu njiit ya fa nekk ak taxawaayu askan wa. Muy politig, di koom-koom, aada ak cosaan, njàng mi walla ni yoon doxe, fànn bu ci nekk mu saytu la. Ndeysaan, saa yu sama xel mi delsee ci tukkeem boobu, sarica bu naqadi la may indil. Ndaxte, liy màndargaal daanaka réewi Afrig yépp mooy mbir yii may limsi : ndóol, xiif ak mar, ay xarey biir-réew yu dul jeex, ger, njàng mu yàqu yaxeet, ñàkkub liggéey, añs. Te, màndarga yii, fépp fu ñu daje, tumuraanke lañuy jur. Ma jàpp ni sabab yi bare nañ. Waaye, dinaa leen baaxe, ci sama xalaat mu gàtt, sabab yi ma foog ne, ñoo gën a tax Afrig des ginnaaw.
1. Njaam ak Nooteel

Deesul a nàttable ne, diirub 400i at yi tubaab yi moomoon Afrig cib jay doole ak i nax, am nay njeexital yu bir ci nekkinu Afrig ba sunu-jonni-Yàlla-tey jii. Dafa di, légéti njaam ak nooteel a ngi fi, ne fàŋŋ. Te, sikk amul ci ne, tey, njaam ak nooteel yooyu, ñooy cëslaayu naataange biy màndargaal réew ya ko daan def walla daan ci jariñu. Su ma nexee joxe misaal ci Farãs, Àngalteer walla sax Etaasini. Naam, bare na ci loo xam ne seen xalaat ak seen farlu moo leen ko may. Waaye, alal ak doole yi suuxat seen koom, Afrig la bawoo. Maanaam, sunuy rongooñ ak dereti maam lañ siime seen cere. Ndeysaan, sunu maam yi sonnoon nañ lool, doonte sax, amoon na ciy workat.

Moom kay, tubaab bi jàppewuleen woon niy nit. Dañ leen daan liggéeyloo niy mbaam ci tool yi. Di leen dóor ak a toroxal guddeek bëccëg, ñuy lekk tuuti, di liggéey lu bare. Nit ku ñuul amul woon benn sañ-sañ ci boppam. Tubaab bi dafa jàppoon ni, Yàlla moom la bindal nit ku ñuul ngir mu doon jaamam. Loolu la seen njiiti jàngu yi doon gëmloowaate, di wëlbati waxi Biibal bi, di kàcc rekk di dajale. Jigéen ñi, ñoom, dañ leen daan siif saa su nekk, di leen tëdde. Xonq-nopp bu ci sa nëq tàng, nga fab kenn dëpp sa kow lal, faj sa aajo. Te, sax, àggoon nañ ci yoonal seen caay-caay googu.

Ndege, Luwi XIV, buuru Farãs ba woon, dafa jëloon ab ndogal, yoonal tëralinu njaam gi, biral ci àqi ma-weex yi ak wareefi nit ñu ñuul ñi ñeel leen. Li mu ko dugge woon lenn rekk la : yaatal ak dooleel nooteelu tubaab yi. Waaye, loolu mënutoon a wéy. Ginnaaw gi, am na ci sunu maam yi ak ñenn ci tubaab yi ñu jóg taxaw temm xeex njaam ba ñu xéy dakkal ko. Ndekete yóo, gaa ñi amoon nañ yeneen pexey nooteel yuñ doon làq.

Gaa ñi dañu tekki genn buumu njaam, fas geneen gu gënatee dëgër, te mooy ci nasaraan “colonisation”. Dafa di, xeetu nooteel woowu moo rawati bu njëkk ba. Gaa, njaam gi wuññi woon na sunu sutura maam ya, nasaxal koomu Afrig. Waaye, nooteel bi dafa laal xol yeek xel yi, futti sunuy aada, suufeel ak soofal sunu cosaan, fënëxal sunuy ndëgërlaay. Xamatun lun doon. Xamatun fun jëm. Ñu jàppenu ay dof walla ay mala yu amul démb, amuñ mboor. Moo waraloon njiitu réewu Farãs ba woon, Nikolaa Sarkoosi, ca waxtaan wa mu amaloon ci Ndakaaru gii, waxoon ne Afrig amul cosaan. Aka mën a fen ! Ku la xeebe nii, noo koy farale ? Moo tax àndumaak Lewópóol Sedaar Seŋoor bi muy wax ne nooteel bi loraange ju jur njariñ la. Xamuma nu mu mënee woon wax wax ju ni mel. Xeeb sa bopp weesuwul lii.

Fekk ay nit seen réew noot leen, jaay leen doole, naka la ci njariñ mën a sababoo ? Sil Feri (Jules Ferry) mu Farãs lii la waxoon : « Na ñépp xam ne nit ku weex moo féete kow nit ku ñuul. Bu ko defee, war nan, nun ma-weex yi, xettali nit ku ñuul, jële ci moom jikkoy mala, ngir saxal ci moom nite ». Ñu ni déet-a-waay, Buuru Belsig ba woon, Lewópóol II, ne, Kóngo ak lépp li ci biir, mooy boroom. Moo taxit, xeetu metit walla ñaawtéef boo mënti xalaat teg na ko doomi Kóngo ya. Noonu yit la deme woon ca Mosàmbig ginnaaw bi Purtugees yi woñee loxoy waa dëkk ba ngir ñu beyal leen wëttéen. Loolu juroon xiif gu metti ca dëkk ba.  

Atum 1960 ak li ko jege, ci la réew yu bari ci déndug Afrig tàmbalee moom seen bopp, ginnaaw bi Tubaab yi duyee seeni gafaka ba ñu fees dell. Waaye nooteel gi yemul foofu, de. Wax ji lii doŋŋ la woon : dangeen a bëgg moom seen bopp ? Yoon waa ngoog waaye na leen leer ne dinanu wéy di leen yilif. Kon, beneen xeetu nooteel daldi judduwaat. Booba ba tey, boo jëlee réew mu mel ni Senegaal, lépp lu fi baax sunu njiit yi jox ko waa Farãs toog. Su may xool fi nu jaar yépp, doore ko ca jamonoy njaam ga ba tey, ci laay gën a gëm li Séex Ànta Jóob waxoon ca Ñiseer : « Su nu yaakaaree ne ñaawtéef yi nu tubaab bi def deñ na ci nun, noo ngi nax sunu bopp ». Dëgg la ndax tubaab bi dafa raxas sunu xel ba gëmatunu sax sunu bopp.  Du ñàkk am ñu ni ma, dëgg la ne tubaab yi tooñ nañ nu waaye nun it war nanoo seet ba xam ndax def nanu sunu wareef ci ëllëgu Afrig. Loolu neexul a weddi.

2. Waaru Ndawi Afrig yi ci ëllëgam

Mënees na tënk wax jépp ci benn laaj kese : lan moo war a nekk sunu taxawaay, tey jii ? Ma jàpp ne, xeex moo fi sës. Waaye, nag, xeexu ku am jom, ànd ak xel mu ñaw ak i pexe yu wóor te jàppandi. Bala loolu, warees na defaraat jikko yi, ànd booloo ngir sunuy noon am luñ nu ragale. Ndax, ni la wuude gise rekk la lay ëwale. Xeex boobu, nag, sunu njiit yee ko waroon a sumb ; lu ko moy, ñu jiite ko sax. Wànte, sikk amul ci ne, ñoom ñooñee, ay tubaab yu ñuul kukk lañ, diy jaam yu bir, ay workat, diy dunguru nootkat bi. As tuut ciy njiit yu farlu woon, bëggoon seen réew, te daan jàmmaarloo ak tubaab bi, dañ leen a sàkkal pexe, bóom leen. Ñi ma gën a namm ci njiit yooyu ñooy : Tomaas Sànkara, Lumumbaa, Silwanus Olempiyó, Mamadu Ja ak Xadafi. Wànte, loolu warunoo tax a xàddi. Bu yoon jeexul, waaxusil du jeex. Yaakaar jeexu fi ndax du ñépp a mel ni sunu njiit yi.

 Mënees na am yaakaar ci sunu ndawi tey yi. Ndege, jamonoy tey jii, li fi am ciy xeltukat, ay jàmbaar yu bëgg seen réew, ay jumtukaayi xarala yu matale ak ay ndaw yu dogu ci xeexal Afrig (Kémi Sebaa, Ndongo Sàmba Silla, Gii Maryiis Saaña, añs.), amul woon ca jamonoy maam ya. Doonte, sax, ñoom it bey nañ seen waar ci tool bi, yem fi leen seen doole ak seen xel yemloo woon. Dafa di, lu bare ciy xeeti woy ak xalamal yiñ ràññee tey, yu ci deme ni “Jazz”, sunu maam yaa leen daan fent, ngir giifal seen xol saa yu leen tubaab bi daan bugal, ak di biral boddekonte biñ leen daan teg. Ndeysaan, foo leen fekkaan, rawatina ca tooli Amerikeŋ ya, ñoo ngay woy ak a woyandoo ngir feral seeni rongooñ.

3. Làmmiñi Afrig yi

Réew moo gis, bu naatee, ay boroomi xam-xam ñoo fa jaar. Xam-xam, nag, mënta jariñ boroom walla aw askan feek ŋëbu ko ciy loxoom, péeg ko ci boppam, ay noppam di ko dégg, xolam di ko yëg. Moo, ndax xam-xam mën naa am muj bu ni mel bu dee boroom déggul walla nàmpul làmmiñ wi ñu ko fase ? Déedéet ! Mukk ! Kon, sunu boroom xam-xam yi ñuy soow guddeek bëccëg, ñiy bind ay téere ak a wax saa su nekk, ñan lañuy bindal walla ñan lañuy waxal ? Ngiree ñu wax ak askan wi, fàww ñu jëfandikoo làmmiñi askan wi. Kon, naataange ak yokkuteb Afrig, mënuñoo jéll làmmiñi Afrig yi.

4 . Liggéey tuuti wax lu bare 

Soo jëlee réew mu mel ne réewum Senegaal, li nit ñiy coow a ëpp li ñuy liggéey. Tàmbalee ko ci ñi nu jiite. Koo fal ba mu toog mu ngi lijjanti nu muy def ba duufal gafakaam ak yosiy àndandoom. Seeni njuuj-njaaj lu ci ëpp ciy wax lañu koy muur ndax dañuy aakimoo jumtukaayi tas xibaar yi di wax subaak ngoon. Néew na ñu ciy wax lu jëme réew mi kanam. Politig rekk ! Dégg naa keroog benn taskatu xibaar naan moom mësul a gis réew mu sukkandiku ci wax ak politig ba naat. Sàllaaw wax na dëgg gu wér péŋŋ ! Réew, liggéey a koy naatal, moo koy jëme kanam. Njiitu Afrig yi dama ragal ne nguur da leen di tàggaleekseen sago. Seet ko ci réew mu mel ne Kóngo, Saasu Ngesó moo fa toog ci jal bi boobaak léegi ëpp na fanweeri at. Ci gàttal, ku juddu ba muy jël réewum Kóngo, jàng nga fi ba jeexal, takk fi soxna ba samp fi kër. Gine Konaakiri tamit, Alfa Konde daa bëggoon a soppi ndeyu-àttey réew ma ngir am ñetteelu moome. Te kat, moo waxoon ci gémmiñam ni def ñetti moome xalaatu ko ndax loolu dafa worook demokaraasi. Sunu réew mii di Senegaal, xel yaa ngi bëgg a teey : Sóori Kaba, di woon jawriñ ci nguur gi, da ne ndeyu-àttey réew mee tere Maki mu sàkku ñetteelu moome, ñu daldi koy dàq ci saa si. Lu Maki Sàll mii narati ? Baax na. Nan xaar ba xam fan la wànnent di mujje ak i bëtam… 

Warees na joxoñ tamit baaraamu tuuma sunu liggéekat yiy ñàkkal lool faayda seen liggéey, di tappale ak a caaxaan, dëkke kàcc ak càcc. Lu ngeen xam ci ku dul xéy waxtu, du wàcc waxtu ? Kenn ci ñoom fonkul liggéey biñ ko sant te mu am seeni junniy-junni moroom yu bëggoon a toog fiñ toog. Yàlla boo am soxla bu jamp ba dem ci benn biro ci réew mi. Dinañ la soofantal, ñàkke la kersa walla xaarloo la ba nga xàddi ci lu ñàkk faayda. Ci misaal, bés, sama benn xarit bu ma bokkaloon lekkool Ndar dafa dem ci benn bànk bu mag biir Ndakaaru, amoon yu mu fay lijjanti. Ndaw si ko waroon a toppatool li mu doon wut ne fa luëpp fukki simili di talalali ci njéggil-kàddu gi, di reetaan mel ne ku nekkul ci liggéeyukaay. Xeetu liggéeykat yu ni mel bokk nañ ci li tax Afrig des ginnaaw.

May daaneele ci mbirum aada ak cosaan. Fépp foo dem ci àddina si, réew yi gën a naat, doonte seen askan a ngi sant bu wér, mooy yi sax ci dekkal seen  cosaan, di dundalaat seeni aada ngir dëppale leen ak jamono. Seen démb lañuy def jaaruwaay ngir jëmmal seeni naal ci politig, koom-koom, njàng ak njàngale, tàggat-yaram, ba ci aar bi sax (nataal, sinemaa, pecc, añs.). Nun nag, nekkewuñ fi lu dul roy ak a toppandoo, di weccoo xalaat ciy pecc ak i woy yu ñu fente Amerig. Lii bu dul ñàkk faayda, lu mu ? Ku ràññeeku ca Amerig ci xeexal nit ñu ñuul ñi fa nekk, Luwis Faraxan dafa am bés muy wax ak ñoom ci am ndaje. Li mu leen wax keroog mooy, nit su jéemul dara ngir teggi nooteel yi ñu koy teg, su jéemul dara it ngir fent walla defar dara, nit kookule dara du ko wutaleek wékkukaayu yére. Ndax wékkukaayu yére mënul wax, mënul dox te fu waay xiire rekk lonk cay yéreem. Léegi nag, nun waa Afrig, rawatina nun ndaw yi, nooy seet ba xam ndax danoo war a taxaw temm, doon wennuw say ngir jëmale Afrig kanam, walla danuy toog ne xótt-xóttaaral ni ay wékkukaayi yére.

Yaatma
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj