KIGALI
Kigali, soo fay doxantu
Sa xol day sedd doo gis loo ñaxtu
Nga naw ci saa si Njiitu réew ma
Ndax liggéeyam rafet na
Céy Kigali !
Cet gaa lay jëkk a yéem
Moom cet gi war a jiitu ci lees di jéem
Doo dox mukk ba dajeek mbuusum ndox
Muñ naan sànni ci mbedd ya ñuy dox
La fa banaana di bari te yomb yépp
Doo gis xollit buy taxawaalu, wëral fépp !
Banaana yu gàtt yooyu, dijj te neex
Boo koy lekk doo bëgg mu jeex
Kigali amul liñ naan kiris-koros maanaam
Góor sol tubéy wàcce ko ba ngay gis njiitlaayam
Kigali, ñay dawal cag-cag dañuy sol kask bu xonq aaru
Bind ci seen limat ak wirgo wu weex, taaru
Genn gone du la dogaale di yalwaan itam
Mbaa di kot-koteek tànki neen ak yëre yu tilim
Ba soo koy xool
Muy dog sa xol
Amul mag ñu lay dab di la déey di dagaan
Walla di tappaleek a wayaan
Ruwàndaa péex ma jaaxal na ma
Seddul, tàngul, lu la neex sol, saf na ma
Fépp a nëtëx yànj, dugg na ma
Waa dëkk ba di wax ndànk teey
Soo tàmmee gis tilim ak maa-tey
Fàww fu mel ni Ruwàndaa yéem la
Te ku deful ni ñoom it la ñuy def war na la
Ruwàndaa ak fi mu jaar
La fa xewoon ca faagaagalug xeetu Tutsi
Su melee nii tey ba ñépp fëq wutsi
Nga xam ni réew ma loxo Yàllaa fa jaar
Dañuy liggéey nag, gëm seen bopp
Yarasuñu ci kanamu kenn, maa leen sopp
Ruwàndaa aaye nañu fa xeesal
Ku ko fa def yaru yoon daldi la dal
Ñoom xam nañu luy pasteef ak liggéey
Sagoo naa li mu bokk ci Afrig, du am ndéey
Su ma sañoon ku am i nopp dégg yii ci ñoom
Yar, liggéey, njub, set ak fonk sa moroom
Fii laa koy yemale waaye des na lu baree bari
Lees fa mën a roy ngir dem fu soree sori
Damaa jukki rekk ci li gën a fës
Te foo ci sànni bët daldi ni tës