“Damay sànni ay kàddu yu néew ci waxtaan wi, jéem a joxe samay xalaat ci li nuy dund fii ci Itali.
Ci sama gis-gisu bopp, Móodu-Móodu yi agsi ci diggante atum 1980 ba 2000 wute nañu jëfin ak yeneen tukkikat yi tàmbalee tàbbi Itali ci atum 2000 ba tey jii.
Damay taxaw, léeg-léeg, seetlu, ngir def ay jàngat ci ñaari doxalin yu wute yooyu lool, seet tamit lan a ko waral, fan la lalu. Ndax, boo gëstoo bu baax, mbir mi dafa lay jaaxal.
Naka la mbir mi deme ? Ňaari melokaan, ňaari jikko yu wute lool ci ay doomi-adama yu bokk fi ňu jóge.
Waaye boo xoolee bu baax ñi jëkk a agsi jànguñu, walla boog seen njàng soriwul woon.
Dama koy seet ci sama maas gi. Dañoo jòge ci àll bi, walla jòge feneen ak feneen, jànguñu dara lu tax seen xalaat mën a sori.
Waaye ñàkkuñu woon cëslaay, amoon nañu tamit lu ñu gëm. Te boo ko de xool ci ñoom, Móodu yu jëkk yee fi taxawal ay daayira yu man a gindi mbokk yi ba kenn du gëlëm. Fakastalu, naam, am na, waaye Yàllaak daayira yee tax ba mag ñi fàttewuñu démb.
Jànguñu tubaab waaye mokkal nañu yeneeni làkk ba mën a xàll yoon wu leen di aar, di leen tee réer. Ndaxte, làkk wolof walla araab may na leen ñu xam fu ñuy teg seeni tànk ba bañ a saaraan. Te bi ñuy ñów ci réew mii gisuñu kenn ku leen tette waaye am nañu seen ngor ak seen diine, jàpp nañu ci ba taxaw fu dëgër. Ba tax kenn yóbbuwuleen ci weneen yoon wu doonul seen yoonu bopp. Kon tey, Móodu yu jëkk ya xam nañu fan lañ samp seeni tànk ba mën a téye seen aada ak seen ngor ak seen fulla. Loolu lépp am nay firnde ndaxte bu daayira yi nekkee fépp tey, xeer wu njëkk wi ñoom ñoo ko teg ba xale yi mujj a agsi mën cee jariñoo.
Doxalin wu ni mel ku yaafus walla ku ragal du ko sàmm ba ku la ca fekk, toppandoo la, mu indil ko tawféex. Xale yi topp ci yoon wi, nag, wax dëgg Yàlla gisuma ci kenn ku tarxiis ci kaw xollitu banaana.
Wax ji du gudd, dañu koy tënk.
Waaye maasi gone yu mujj yi, li leen sonal mooy ñàkk a mën a muñ. Jafe na lool jom ju tax ngay moytoo def looy réccu ëllëg. Walla bu la jamono naree lottal dinga ko mën a muñ ndax lu bari alal du la ko jaral. Li am solo mooy ngay xool bu baax sa juddu, di sàmm sa ngor, di bàyyi xel ci sa diine.
Xaley tey yi ànduñook dal, mënuñoo xaar. Te li koy indi mooy teel a bëgg am xaalis, yàkkamti koo am, sa lépp sotti léegi-léegi. Kenn xamatul luy taaxirlu.
Li ko waral mooy :
waa ji dafa wàcc Rom, dugg ci saxaar gi wutali Milaŋ, toog ba ci kanam mu ne ki mu dendal
-“Waaw, ndekete Itali am nab àll”
moroom mi ne ko :
“Noppil waay, loolu ëpp naa wax !’’
Waa ji tontu ko ne ko ;
“Aa, man kat damaa defe woon ni fii lépp ay taax la.”
Xam nga ni kii kay, am na mbetteel te dara xewagul. Fu amul àll, kenn du fa bay, te fu mbay amul, xamuma luñ fay dunde. Loolu moom, waxin la rekk.
Jamono ji ñu tollu, jafe-jafe yi bari nañ Itali waaye lépp dañu koy sante sunu boroom. Seneraasiyoŋ bu bees bi am na ciy jàmbaar waaye tamit bari na ci ñu réer. Du gaaw nag ñu defar seen réew.
Boo demee gaaru Milaŋ am na ñuy fanaan ci mbedd yi. Taxawaalu bi bari na lool, te xale yi mënuñoo yor seen bopp. Bu sedd bi ñëwee, xale yu bari dañuy tumuraanke. Tukki baax na waaye nit bala ngay jòg war ngaa xam fa nga jëm lan nga fay fekk.
Nun mag ñi war nañoo góor-góorlu ba teg xale yi ci yoon wu jub. Jàngal leen seen kàllaama, nàmpaatal leen ngir ñu xam seen cosaan. Loolu dina tax kenn du soppeeku ba topp tubaab yi ci seen melokaan.
Nun doomi Senegaal yi, dinanuy ànd dem ci daayira, dem julli jàkka waaye li nuy dimbalante ci sunu biir bariwul te bokk na ci li nu tax a des ginnaaw. Nit dina tollu diggante, ñòw ci biir mbooloo mu takku te fa mu tollu moom rekk a koy xam. Te dina rus a laaj, te ña mu fekki, bu ñu amul xelu jox ko walla dimbali ko, noonu lay jògee ca jataay ba, dellook aajo bu fajuwul.
Loolu dafay tax nit di gaaw a suux te du ca génn. Bu yàggee, kër ga mu luye sax dootu ko mën a fay. Boo dee ku am jom, dinga génn kër googu, bu booba mbedd mee lay for walla nga dem bay fanaan ci sa biir oto. Am na ku mu fi daloon, dafa mujj faatu ci sedd bi.
Li may jëkk a digale, mooy na nit kiy duggante ak mbokki senegaleem yi, saa yu ñu wootee mu jiitu fa, te ci daayira yi lañuy gën a faral di daje. Su ma nee daayira, nag, seetuma ci tarixaa bi mba beneen, daayira yépp laa yemale. Nekk ak say mbokk am na solo ndax bu saafarawul lépp tamit, mën naa saafara lu bari.
Nit ki fa ngay yeewoo, fa ngay faatoo. Kon, ci fànn yépp la jàppante am solo.
Li duuf ci nag wi, xejul ci cin li. Kon boog ba beneen jotaay.”