Bataaxalu Saalif Keyta ñeel IBK

Yeneen i xët

Aji bind ji

 

Ci tekkib Paap Aali Jàllo

KÔRO (mag sama),  

Jàmm ak salaam ñeel na la. Sa rakk a lay nuyu, di la ndokkeel, di la jox sa wàccuwaay.

Ginnaaw loolu, xamal ni kat, sa mbokku cosaan mi nga bokkal maam, di sa mbokku aada, moo namm a waxtaan ak yow tey. Bataaxal bii ngay jàngsi, mi ngi bawoo cib maxejj bu bëgg réewam, mu jaral ko lu ne, fu ne, te xaaru ci kenn walla lenn, muy xaalis walla ndombog-tànk. Duggewuma ko wanewu. Te yit, jubluwuma ci ŋàññ la, walla di yàq sa der. Nde, doo sama noon, te noonoowuma la ; doo sama wujj, te wujjewumaak yow. Tamit, rambaaj walla naaféq taxumaa jóg. Kon, jàppal ni bataaxal bii, jàmm rekk la wund, ñeel nekkinu Mali gi nu bokk ak i doomam, te nga boole leen jiite. Bu ko defee, naŋ ko jànge xel, bañ koo jànge xol.

Kôro, 

Liy xew ca bëj-gànnaaru Mali metti na, tiis na. Xanaa gisoo ni ñuy reye ndawi Mali yi, di saam seeni néew ? Ndege, biir làrme bi, ndaw yaa ci ëpp, bés bu nekk ñuy jaay seen bakkan ngir seen réew. Jigéen ñaa ngiy ténj, jirim yeek baayo yi di gën a bare, yaakaari way-jur yi di tas. Foo dem fekk fa dëj. Ndaxte, ay doomi jàmbur, mag ak rakki jàmbur, jëkkëri jàmbur ak pàppay jàmbur ñoo fay dee. Boo weddee li ma lay wax, dugalal sa ñaari doom yi, Buuba ak Karim, ci làrme bi, yabal leen ñu xeexi. Bu booba nu xool ba xam ndax dinga nelaw am déet. Waaye, ginnaaw kenn ci seeni  doom, mbokk walla jegeñaale deewu ci, seen yoon. Yëgalu leen ko sax seen yaram. Moo tax, ci jamonoy tiis ak naqar jii, say doom sañ a salfaañe alalu réew mi, di ko pasar-pasare. Ñu ni déet-a-waay, say way-yëddukat di yaataayumbe ak a gundaandaat, di jël lu tollu ci 100 walla 300i milyoŋ ci sunu koppar di ko yàq ciy aniwerseer ak i caaxaan. Ngeen fàtte askanu Mali wi nga xam ne, sonn na, tàyyi na. Nit ñi lott nañu, tumuraanke, xiif, mar ba nga ne lii lu mu doon. 

Ay waay ! Yërëm nu boog, kôro !

Àddina sépp xam na ni Farãs a sooke jéyya ji xew ca bëj-gànnaaru Mali, di fa reylu ay ndawi réew mi. Xanaa gisoo ne seeni moroom yu Farãs di fey ci suuf ñoo leen di faat bés bu Yàlla sàkk ? Dafa di, nag, lu jiin Njaag a, te Farãs mooy Njaag. Te sax, yow ci sa bopp, dara umpu la ci. Yaa gën a xamaatoo ni Macron, njiitu Farãs, ak i ndawam ñoo ngemb ay saay-saay yiy mbubboo raaya Mali, di wootewoo bëgg-sa-réew ba noppiy faat ay doomi Mali bés bu nekk. Xam nga xéll ni Farãs mooy seytaane bi leen di jox i gànnaay, ñuy fetal doomi réew mi. Ma ni, benn jiyaadis amul Mali waxatuma laak terorist. Ay kàcci kese la ! Te, taskati xibaar yu baree ngi leen ciy jàppale. Dafa doy nag ! 

Aa, Kôro ! 

Tee ngaa jéngu, tekki buumu njaam gi la goneg Farãs gi takkal. Mbaa du Macron dafa këf saw fit ? Nga topp ci moom nig geen. Fuñ la fekk yaa ngi lëngook moom ngir wane ni ay xarit ngeen. Yow tamit, xamal nag ne doo moroomam. Kii nga xam ne ku bës bakkan bi meew génn ci, lu tax ngay nangoo wéy ci waawam ? Xale boobu ngay sibooru de, mooy reylu say ndawi réew bés bu nekk. 

Aa, Kôro !

Yow wute ngaak nun de ! Ndege, yow tubaab bu ñuul kukk nga, dib doomu Farãs, làq sa paaspooru Farãs. Xam naa yit ne am nay artist yu lay jàppale. Duma tudd seen tur ; waaye sañ naa ne ñenn ci ñoom Gàmbi lañ fekk baax, dëkkuñu fi. Bu Làmbaay naree tàkk, yaak ñoom ay ànd fàq, ngeen làquji Bànjul walla Pari, yóbbaale seen njaboot. Kon, bu réew mi tàkkee, nun ñi amul fun làquji nooy xal a sonn, nooy dee. Ngalla-waay, buleen taal sunu Mali gii, ndax ñu mel ni man ak baadoolo yi fiy yeewoo Mali rekk lan am. Ndeysaan, dafa di sax, sa yoon dafa nekkul ci nun. Moom kay, nu dund walla nu dee nga yemale. Lu tax faalewoo nu, nun ñi la fal, nga war noo aar ? Metit wi, nun rekk noo koy yëg. Moo, ndax jotul nga yëkkati sag kàddu, xamal askan wi li xew dëggëntaan ? Ndeysaan, dangaa ragal say kàddu juuyoo ak bëgg-bëggi liir boobuy jiite réewum nootaange mi, Farãs. Lenn rekk a la soxal : wéy di toog ci jal bi cig ndimbalam, duy say poos ba ñu fees dell, yow, say mbokk ak ñi ànd ak yow. Ma ni la, nag, yaa wayadi dëgg-dëgg ! Yow yaa ñàkk gis-gis ! Boo geestu woon tuuti sax, dinga xam ni, yow, Keyta, waroo ragal, waroo wor askanu Mali.

Aa, Kôro !

Yaa gàcceel say maam ! Xanaa danga fàtte ni Keyta nga sant ? Sunu santu maam ja, jàmbaar ji, Sunjata (buuru Mali ciy ati 1236 ba 1255).  Cëm ! Jàmbaaru Kirinaa ngoog ! Gone gi duma woon jinne Sumaaworo. Kii daawul tiit, daawul daw. Xamul woon sax fu tiitukaay di nekk ci nit. Kon, ku nàmpe ci meenum Sunjata, bokk ci giirug Keyta-Keyta yi, waroo ragal. Tey ngay maas nii. Cim mbay ! Xanaa xamoo ni, Sunjata, ak li mu doonoon buur yépp, askanam a ko faloon. Nguuram du woon rekk ndono. Cib demokaraasi bu bir la nguuram lalu woon. Waaw kay !

Ndege, démb, kuñ ci falaan, cim pénc lañ la tànne, ci kow sàrt bu leer. Rax-ci-dolli, ndaje ma faloon Sunjata dafa tëraloon ab sàrt bu amoon taxawaayu ndeyu-àtte, ci atum 1236. Mi ngi tuddoon sàrtu Kurukaŋ-Fugaa, te amoon lu tollu ci 44i dogal. Kon, nun amunu ku nuy ñee. Nga war cee jàngat ñaari mbir. Benn, sunu njiit yu njëkk ya, duñu woon ay buuri ndono, askan waa leen daan fal cim pénc. Ñaar, duñu woon buur di bummi, di jaay nit ñi doole ak a def lu leen soob. Waaye dafa amoon aw yoon wu leen tënkoon, tënk réew mépp ak ñi ko jiite woon, réew mépp a àndoon tënku ci sàrtu Kurukaŋ-Fugaa. Lii mooy sunu aaday maam. Te yow it dañ laa fal, aw yoon tënk la, muy ndeyu-àtte réewum Mali. 

Wànte, doo buur, kôro. Doo buur, de !  Xam ko bés niki tey. Moo, lu la tee roy ci maam yi, dekkil cosaan ? Ndax gis nga ne, demokaraasi bi ñuy soow, sunu maam yu jàmbaare woon yooyu ñoo ko njëkk a saxal, suuxat ko ? Sunu moomeel la. Tey, nga nasaxal ko nii, noon bi jaare ci, yàq réew mi yaxeet. Waaye, nag, ku xeeb juddoom, wàññi darajaam ; te ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko.

Aa, Kôro !

Bu dee li la say mbokki Mali yi dénk dafa diis ci yow, delloo leen seen moomeel ! Bu dee danga nar a boqu Kulubaa di lox, wàccal jal bi te ba kook ku am fitu def li war. Boo ragalee ne jàkk Farãs ak i njiitam wax leen dëgg, demal sa yoon ! Boo mënta yor réew mi, jóge fi ! Mali am na ay góor-Yàlla yu gëm seen bopp, xam liñ doon, bëgg seen réew, am xam-xam bi ak mën-mën bi, te am fitu yor ko, jàmmaarlook noon yi, defaraat réew mi. Boo demulee, nag, lu la ci fekk yow la.

Aa, Kôro !

Sàmmal sag ngor te bañ a gàcceel sa bopp. Ndaxte, kàddug maa demal sama bopp moo gën a rafet kàddug dañ maa dàq. Kon, fexeel ba bu kàddug gàcce googu gàkkal sa tur ëllëg. Ndaxte, suba du añ du reer, waaye dees koy sóoraale. Dëgg neexul. Bàyyi ci xel.

SA RAKK, SAALIF KEYTA

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj