AFRIG, TONTU DU FOROX, Tontu ñeel kàdduy Óreliyoo De Lórãtis yi

Yeneen i xët

Aji bind ji

Duma topp diw boo gis, fi ngeen jëm dafa sorewul. Loolu la waa CAF (Mboolem kuréli futbal yu Afrig yi) xam ba xaaruñu wenn yoon muy yàgg ngir ñu xamal Óreliyoo De Lórãtiis ni « Kub bu Réewi Afrig yi mooy joŋante bi gën a réy ci kembarug Afrig te bokk na ci joŋantey futbal yi ëpp solo ci àddina si ».  Ginnaaw bi Kaliidu Kulibali njëkkee tontu, campeefu futbal bi gën a mag ci Afrig a ci dug, muy CAF. Kurél gi, nag, yemul rekk ci di ñaawlu kàdduy saa-itali bi, waaye mu ngi sàkku UEFA teg ko ay daan.

Ci pàttali, moom njiitalu këlëbu Naapóoli li, ca Sàmpiyonaa bu Itaali, dafa biraloon ciy kàddoom, wax ne : « Bu ma kenn wax lu jëm ci futbalkati Afrig yi. File ak CAN biy wéy di dig jamonoy sàmpiyonaa yi, duma ci jëlati kenn, mukk ».

Kàddoom yii nag, dañuy woneeti ñàkk àndug njiiti futbalu tugal yi ci ni CAN bi tëdde ak di bàyyi saa-afrig yi ñuy dem ci seen ay réew saa suñ leen soxlaa. Bu ñenn ñi di xaar mu jot ngir ñu tëral seen i pexe, moom leeral na ni fasul yéene jëndati kenn ku fa nar a bawoo di joŋanteji Kubu Réewi Afrig yi ci jamonono Sàmpiyonaa bi . Dafa mel ni kon ñoom ñooy « ngaaka yiy fey peyoor yi » ba noppi futbalkat yi dem di « liggéeyal ñeneen ». Waaye, waa CAF yamuñu ci fàttali ko dayo CAN bi. Jàpp nañ ni wax ji dëppoowul ak sàrt yi ba ñoo ngi sàkku ay daan itam ci UEFA (Kurél gi ëmb mbboolem kuréli futbal ci kembaru Ërób) yu jëmm ci moom.

Ginnaaw sàkkuteefu CAF boobu, De Lórantis a ngi wéy di jot yeneen i tontu yuy wone ni wax ji naqadiwul rekk waa CAF. Ëxlu futbalu Afrig yépp la metti. Loolu a waral yeneen i kàddu jib, di ñaawlu wax ji ak di ko xamal ni kenn du leen ci bàyyi. Bu ci mujj mooy bu Alin Siise, tàggatkatu gaynde Senegaal yi, mi àddu ci BBC ne « nit ku ma jox cër la, waaye na ko jéem ba xam, maa ngi xaar rekk ba mu jéem ko… ».

Ba ci Kalidu kulibali, doon yëngatu ca Naapóoli te jóge fa bu yàggul dara, xamle na ni :

« Yaakaar naa du nii lañ war a waxe ci ikibu réewu Afrig. Waaye dinaa ko nangul xalaatam. Bu xalaatee ni mbootaayam mën naa joŋante te du am i saa-afrig bëgg-bëggam la. Waaye yaakaar naa waa Naapóoli yépp bokkuñu ak moom xalaat. Ndax xam naa ñi fa nekk ñépp, xam naa itam way-far yi te ñoom duñ xalaate noonu ».

Taxawaay bii Saa-afrig yi am tey doon na buy tàmbalee sax ci làngu futbal gi buñ ko seetloo. Mu doon lu baax ci kembarug Afrig yépp ngir ñu jot seen cër ci nim ware ba jële fi xeebaate ak yabeel. Ñuy xaar ba fan la CAF di dem ak De Lórantis, ak fu waa ji di mujje ak xalaatam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj