AJI SAAR SÀKKU NA ÀTTEB DABU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Alxames 1 fan ci weeru suwe la àttekat bi biraloon daan yim gàll Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay ñeel layoob ciif ak tëkkuy rey yu Aji Saar doon toppe njiitul Pastef li. Ñari ati kaso yu muy tëdd  lañ daan Usmaan Sonko ak ndàmpaayu 20i tamndaret ci sunuy koppar, mu war ko jox Aji Saar. Ndey Xadi Njaay tamit, ñaari ati kaso yu muy tëdd la ko àttekat bi daan ak ndàmpaayu 600 000 FCFA yi war a fay Aji Saar, moom ak usmaan Sonko. Keroog, ndogalu àttekat bi yëngaloon réew mi, diirub ñett jàpp ñeenti fan, xeex bi ne kurr, ba 30i bakkan rot ci. Ñu baree ngi doon foog ne fa la mbir miy yem, am sax ñiy ñaan njekk jamono jii ngir ñu suul coow li, fexe ba delloosi jàmm ci réew mi. Waaye de, mel na ni Aji Saar ak i layookatam yi doyluwuñu àtte bi. Nde, àttekat bi dafa setaloon Usmaan Sonko ci tuumay ciif ak tëkkuy rey. Moo tax ñu sàkku ci Yoon mu dabu àtte bi.

RFI jokkoo na ak layookatu Aji Saar bi, meetar Elaas Juuf, cib jollasu ; kooku ne leen day amaat layoo bu bees. « Dañuy dooraat mbir mi. Dina amaat layoo bu bees. »  

Waaye nag, loolu am na ñu mu jaaxal. Nde, bees sukkandikoo ci boroom xam-xami Yoon yi, ci ndàmpaayu 20 tamndaret yi kepp la Aji Saar mën a sàkku ab àtteb dabu. Meetar Saaxo, di layookatu Usmaan Sonko, nee na, « fi mbir yi tollagum nii, àppel bi ci xaalis bi rekk la mën a aju. » Cig pàttali, ayookati Aji Saar yi 500i tamndaret lañ doon laaj.

Meetar Sosef-Ecen Njonn, kenn ci layookati Usmaan Sonko yi, daf ne, « loolu soppiwul dara ci daan bees daan Usmaan Sonko bi. » Fàttaleet na ne, Ndey Xadi Njaay ci boppam, boroom dàmpuwaay bi, def na àppel, maanaam sàkku na àtteb dabu. Waaye, layoo bu bees bu dee am, ñépp war cee bokk, fàww toppekat bi ci boppam def àppel. Loolu la layookat bi xamleet. Bu loolu amee, mooy gënal meetar Saaxo, beneen layookatu njiitul Pastef li.

Bu dee Usmaan Sonko moom, mënul a sàkku àtteb dabu ndaxte bi ñu koy àtte fekkewu ko.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj