Démb ci alxemes ji, 25i awril 2024, la aksidaŋ bu metti amee woon fa gox bees duppee Yamoŋ Mbajaaneen, ca kow tali ba jëm Kungël. Muy jéyya ju réy joj, tiis na lool Njiitu réew mi, moom mi bind, xamle ko ci mbaali jokkoo yi.
Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, Kilifag réew mi, jaale na mbooleem ñi deele ci jéyya ji, muy njabooti way-dëddu yi, seen i mbokk ak seen i jegeñaale. Yemu ca, ndax ñaanal na way-loru ña ca jëley gaañu-gaañu ngir ñu wér ak jàmm ba mën a mucc.
Bu loolu weesoo, moom Sëñ B. J. J. Fay, joxe nay digle ak i santaane. Nde, sàkku na ci mbooleem bànqaas yi seen liggéey aju ci wàll wi ñu takku jóg ngir taxawu mbooleem way-loru ñi. Rax-ci-dolli, ñaax na tamit képp-kenn kuy yëngu ci dem-beek dikk bi ñuy gën a ànd ak dal te sàmmonte ak càrtug dawal gi (code de la route). Mu dellu digal banqaasi Nguur gi ñu fexe ba di saytu ni mu waree baaxaayu daamar yi ak sàrt yees tëral ñeel kaaraangeg way-tukki yi, rawatina li aju ci kaaraangeg tali yi (sécurité routière).