AKSIDAŊ BU METTI CI YOONU TUUBAA WI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Aksidaŋ bu metti moo am ci yoonu Tuuba wi. Xibaar bi nag, bettul ñu bari. Dafa di, at mu nekk, ay jéyya tegaloo ci tali yi, rawatina bu xew-xew yu deme ni màggal teroo. Ndax, taalibey murit yu bari ak sax ñu dul ay murit, dañuy takku, wutali Tuubaa. Fu nekk la nit ñiy jóge, dëgmal Tuubaa. Moo tax, tali bi day fees dell ak i xeeti daamaar yu bari, ay móto, añs. Ren jii nag, ab móto moo mbëkk genn sëfaan bi muy dugg Mbàkke. Móto bi, Ndakaaru la bawoo, yeboon ñetti nit. Ndeysaan, ñaar ña moom, ca saa sa lañu ñàkk seen i bakkan, ka ca des jële ca ay gaañu-gaañu yu mettee metti.

Dem ak dikk fi Senegaal, jamono jii, li ci ëpp doole lépp Tuubaa la. Moo tax, leeg-leeg, ñuy faral di nemmeeku jéyya yu mel noonu ci yoon wi. Donte ne sax Nguur gi jëloon na ci weer yale jàll ay matuwaay ginnaaw bi aksidaŋ bu metti bi fi amoon ba bakkan yu bari rotee ca. Matuwaay yooyu moo nekkoon xoolaat waxtu yi daamaar yeek yu ni mel war a daw ngir moytu jéyya yooyu. Naam, aksidaŋ yi wàññeeku nañ. Waaye, terewul ba tey yëf yaa ngay wéy, rawatina ci jamonoy màggal gii. Ndax, démb, aksidaŋ bi am foofa misaal la ci. Dafa di kay, am na ñoo xam ne moom kenn mënu leen a fat ba duñu tawte. Lu ñu fagaru fagaru du leen teree faju.

Li waral loolu mooy ne móto boobu mbëkk sëfaan bi ñetti ndaw la yeboon. Ñoom ñett ñépp ay “mécaniciens” lañu, ña nga bawoo woon Wàqi-naan Nimsaat, fa Géejawaay. Ñaar ña moom ca saa sa lañu faatu, ki leen ñetteel moom ay gaañu-gaañu yu metti la ci jële. Waaye, li gën a doy waar ci xew-xew boobu mooy nan la ñetti nit mën a yéege ci benn móto ? Rax-ci-dolli, ñu jóge Ndakaaru bay waaj a dugg Tuubaa kenn tegu leen loxo ? Te, diggante bi soree lool nag.

Looloo tax mu jot dawalkat yeek ñi ñuy yeb ñépp xoolaat bu baax fi ñuy teg seen i tànk. Ndaxte, mboleem matuwaay yi Nguur gi di jël yépp ngir sàmmal leen seen bakkan la. Waaye, ndimbal nag na ca fekk loxol boroom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj