Aksidaŋ bu mettee amati ca Kawón, ci wetu fooraa ba, fa diwaanu Kawlax.
Ab biis la benn pónoom toj, mu daldi daanu, këppu ci kow tali bi. Fi mu nekk nii, ci li rotagum ciy xibaar, ñetti (3i) nit a ci ñakkagum seen i bakkan, juróom-fukk ak juróom-ñaar (57) jële ciy gaañu-gaañu. Nee ñu, Jaawbe la daamaar bi jóge woon.
Dees na ci ñëwaat bu ci lu bees rotee.