Alfuseyni Gay mooy sinekolog ba nemmeeku woon Aji Saar keroog, guddi googu ndaw si waxoon ne Usmaan Sonko daf ko cee siifoon. Démb, ci alxames ji la séqoon aw waxtaan ak taskatu-xibaar bii di Baabakar Ture, mu Kéwulo TV. Moom nag, Alfuseyni, ab doktoor la bu xam-xamam màcc ci lépp lu aju ci wàllum jurukaayu jigéen. Ci biir laaj-tontu bim amal ak Babakar Ture, mi ngi ciy siiwal ërtal bi ñu koy ërtal boobu ak léegi, di ko tiital. Li sabab loolu lépp nag, ciy waxam, mooy li defar këyit giy setal Usmaan Sonko.
Ci biir waxtaan wi, Alfuseyni a ngi ciy xamle ne ba mu bindee caabal giy firndeel ne Aji Saar séqul ak góor, guddi googu mu tuumaaloon Njiitalu PASTEF li, ba tey jii, amul jàmm. Te fi mbir yi tàmbale mooy bi ko xaritam bi, Paap Sàmba Sow, ab layookat, woowee. Doktoor bi ne :
“ Paap Sàmba Sow, sama xarit, moo ma woo ci bésub 1eelu fan ci weeru féewaryee 2021, ginnaaw timis ji, laaj ma ndax damay tukki. Ma ne ko tukkiwuma. Ci ëllëg si, mu woowaat ma, ne ma dañu ma soxla. La ca des nag, duma ci dugg, ndax ci mbiri yoon la aju. Fajkat laa, te am na yoo xam ne mënuma cee wax. Ndax maa ngi woon ci biir oto bi doon xaar Aji Saar génne biir Sweet beauty tamit, loolu mënu ma ci wax. Ndax, ci biir doxalinu yoon la nekk. Li ma fas yéene wax, mooy li may dundu.”
Foofu la fajkat bi tàmbalee. Leeral fi mu war a yem ci wax ji. Li mu dugge mooy bañ a may yoon li mu koy toppe. Dafa di, fajkat yi, lees di woowe kumpag paj (secret médical) daf leen a tënk, rawatina bu ci yoon laalee. Ginnaaw, doktoor bi dafa setal boppam, raxasu ba set ci mbir mi, wax ne mësu cee yëg dara, ba dara booloo jeex. Nettali nag, ci làmmiñu boroom la dàqee :
“ Sama loxo ci Kaamil, mësuma xam ni mbir mi deme. Mësu ma bokk ci genn kootoo walla benn waajtaay, te xamuma ci dara. Dañu ma woo ndax doktoor laa. Sama kër laa tëdd, Paap Sàmba, di ab layookat, woo ma, ne ma, am na nit ku nekk ci fitna. Ginnaaw ba man sama liggéey dafa aju ci taxawu nit ku mel noonu, te it damay ragal bañ ko taxawu, ndax moom moo ma woo. Dem naa ba laaj ko mbir mi ndax jaar na yoon, mu ne ma amul jenn fitna. Kii di Siidi Ahmed Mbay moo ma indil Aji Saar, ma jël ko yóbbu ko Sétéwoo.”
Dolli na ci ne bi muy saytu Aji Saar, ndiruwul woon ak nit ku nekkoon ci ay fitna. Ndax, ciy waxam ba tey, ndaw si dafa àndoon ak dal, te amul woon dara lu doon wone ni metitalees na ko. Alfuseyni wax ne, keroog googu sax, jotul bind ag caabal, dafa seetlu rekk, yem ci. Waaye, jotoon na tonnital (prélever) as lëf, daldi koy denc. Ginnaaw gi la ko Paap Sàmba Sow ak Maamuur Jàllo “ woo ay yooni yoon ngir xam lan laa gis ci Aji Saar. Waaye, loolu, samag waat mayu ma, ma leen ciy wax lenn. Xanaa ñu indi cantaane gu bawoo cib àttekat.”
Mbir ya yemuñu foofu. 3 féewaryee 2021, diggante 17i waxtu jàpp 18i waxtu la fa sàndarma yi ñëw, ànd ak Aji Saar, indaale seen cantaane. Lenn la ñu wax Alfuseyni mooy : “ Saytul diw, nga wax lépp li nga gis ci moom”. Bi mu ko saytoo la bind benn caabalug paj, jébbal leen ko. Nde, sàndarm bu jigéen bi àndoon ak Aji Saar dafa bëggoon xam li nekk ci biir caabal gi. Waaye, Alfuseyni Gay daf ni ko woon : “ Fàww nga dem ba ci OPJ (officier de police judiciaire) mu wax la li ci nekk.”
Doktoor bi nag, jamono jii, xel mi dalul, fit wi toogul. Nde, mànduteem ci mbir mi, tax na ba ñi lal kootoo gi singali ko, di ko xoqatal guudi ak bëccëg. Bu yeboo ne, looloo gën a tax mu amal laaj-tontu bi Baabakar Ture. Dafa ne :
“ Xam naa ne saa-senegaal yi bëgg nañ cee xam lu bari. Waaye, nañu ma ko jéggal rekk, bokku ma ci mbir mi, seede doŋŋ laa ci. Li may dund metti na. Ndax, amul ayu-bés bu Yàlla sàkk, te duñu mbëkk sama oto. Ay ñett, jàpp ñeent ñoo may mbëkk. Nga taxaw, wàcc ngir xool, kenn ci ñoom wàcc dem jëli sa telefon… Sonn naa lool sax. Fu nekk lañu may topp. Te, dëgg-dëgg, ragal naa. Waaye, dénk naa sama bopp Yàlla. Looloo tax ma ñëw sawar a wax. Maa ngi leen di jël seede, lu ma mën di dal, moo ngi noonu.
Noo ko déggandoo. Lii la Alfuseyni Gay wax. Li ci yéeme nag, mooy li muy dénkaane boppam. Mu mel ni, ginnaaw 14i bakkan yi rotagum ci sababu mbir mi, saay-saay yi ci ginnaaw noppeeguñu ci seen ñaawteef yi. Fan la Senegaal nar jëm ak coowal Aji Saar beek Usmaan Sonko ?