Aliyu Sàll tekki na ndombog-tànkam ci boppu CDC, teg loxoom ci Alxuraan, waat ne li ñu koy tuumaal, dara la ci deful. Ci la nee ci nasaraan «…doomu-Aadama dafa am fi ngay tollu, fàww nga setal sa der».
Widéwoo bi nag, daf ci wax ay kàddu yu woroo ak li ko ñépp di tuumaal, moom ak magam, Njiitu-réew mi Maki Sàll.
« Maa ngi téye téere Alxuraan bii, di waat ci sunu Boroom di waat ci Alxuraan, ne lii ñu ma tuumaal, ne dama jot xaalis bu jóge ci Timis Corporation mu jaar ko ci « Socété » bi ñuy wax Agritrans, loolu mësul a am. Du dolaar bu gën a ndaw, waxuma la nag 250 junniy dolaar bu mës a jóge ci Timis Corporation dugg ci nafa Agritrans… »
Waaye, li Aliyu Sàll war a xam mooy ne, kenn mësu koo wax ne Timis Corporation daf ko yónnee xaalis jaare ko ci Agritrans. Dafa di sax, moo ko xamaatoo ndax moo tey li mu def. li mu jublu ci wax ji du dara lu-dul lëndëmal xelu askan wi.
Wax ji dafa leer, Frank Timis ci boppam moo sàkku woon ci BP, bi mu duggee ci mbirum petorol beek gaas bi, ngir mu yónnee xeetu juuti Senegaal, ci nasaraan ñu koy wax « redevances » walla « royalties » ci àngale. Te lii, mënees na ko fekk ci film-gëstu bi BBC amal. Waaye li ci gën a yéeme mooy ne, BP dafa yónnee 250 junniy dolaar yi ci Agritrans bi nga xam ne Aliyu Sàll moo ko moom te mu dénkoon ko kii di nijaayam, Abdulaay Timboo. Kon, du Frank Timis moo yónnee xaalis bi, BP ci boppam moo def lu ni mel. Te li koy firndeel mooy kayit yiy wone yoon wi xaalis bi jaar, jamono ji mbir miy am ak anam yi mu ame te benn sikki-sàkka amu ci. Ku mu neex me4n ngaa xooli kayit yi bawoo ci yaxalukaayu (comptabilité) BP.
Bu ko defee, lii Aliyu Sàll weddi ba di ci waat ci téere bu sell bi, du li ñu ko jiiñ. Timis Corporation ab yombalkat kese la woon ci diggante Aliyu Sàll ak BP mi nga xam ne moom la jaay ay wàllam ci petorol beek gaas bi ko Maki baaxe, yónneewul dërëm bi gën a tuuti kii di Aliw Sàll. Na leer ne kenn waxul loolu !
« Ñu ngiy may tuumaal tamit ne, xéy-na, dama am wàll maanaam li ñuy woowe « actions » ci “sociétés” yi nga xam ne ñu ngi liggéey petorol ci Senegaal. Ma leen di waatal ci Alxuraan ne awma ci benn wàll, awma benn « pourcentage », maanam ay « actions », yoo xam ne « sociétés » yiy liggéey petorol ci Senegaal walla sax ci àdduna si te ñuy liggéey ak Senegaal ».
Man jàpp naa ni danoo bëgg a nelawal. Ndaxte, kenn mësul a wax ne Aliyu Sàll dafa amwàll ci këri-liggéeyukaay walla isin yiy yëngu ci mbirum petorol ak gaas.
Loolu yit dafa leer nàññ. Wax ji mooy, kayitu-déggoo bi ñu xaatim ak saay-saay bii di Frank Timis, dañu ko waroon a far bés ba ñu falee Maki Sàll. Ndaxte, Timis Corporation amul woon xam-xam, mën-mën ak koppar yiy tax mu mën a liggéey ci petorol beek gaas bi. Te itam, moom Frank Timis jaarul woon ci saytukati Petrosen yi war a wóorliku ne képp kuy laal ci mbirum petorol walla gaas, am nga xam-xam bi, mën-mën bi ak koppar yi war. Waaye deful loolu. Bi Frank Timis xamee ni def na lu mu warul a def, loo xam ne mënees na ko fomme dige bi mu sékkoon ak nguur gi, dafa jël kii di Aliyu Sàll, ger ko ba noppi teg ko ci boppu këru liggéeyukaayam boobu di Timis Corporation, di ko fay xaalis bu takku. Li mu ku dugge nag, mooy xam naa, ginnaaw Aliyu Sàll rakku Maki Sàll la, Njiitu-réew mi dina ko làq, aar ko ba kenn du nangu ci moom petorol beek gaas bi, ñu jox ko, moom Aliyu, xaalis bu takkoo-takku. Te loolu Aliyu Sàll weddiwu, li mu def rekk mooy ñaawlu li ñu tudd xaalis bi mu feyeeku.
Kon, kenn waxul ne Aliyu Sàll ak Maki Sàll dañoo am wàll ci isini petorol yi walla yu gaas yi. Li ñu leen di tuumaal mooy ne dañu leen a ger ak ay milyaar ngir salfaañe alalul askan wi. Ndax ñoom ñoo tax ba alalu Senegaal dem ci loxoy ñeneen ba réew mi di ci am lu dul fukk ci téeméer boo jël (10%). Ndax lii jaar na yoon ? Lii rekk a di coow li.
Aliyu Sàll wax na yit ne, bi yoon wootee ne ku am firnde ci tuuma yi ñu teg ci kowam moom ak ñi ci taq ñépp, foogoon nañ ne dinañ wóolu yoonu Senegaal waaye yàq rekk moo tax a jóg ñi koy joxoñ baaraam. Nu koy fàttali ne, “procureur” bi dafa juum, walla sax moo tay li mu def. waaye yoon du doxe noonu. Te sax, fàtte xaju fi. Bi ñuy tuumal Karim Wàdd, dañu ko ne ràpp ci kaso bi door di ubbi lànket, naka noonu Xalifa Sàll. Kon, lu tax ba tey yoon tegul loxo Aliyu Sàll ? Te sax, yoon dafa amul lu muy wër-wërloo, lu ne fàŋŋ kenn du ko jeex. Fii lépp a leer : xam nañ ku xaatim dige bi ñu jox Frank Timis te IGE tere woon ko, xam nañu ñan lañuy jiiñ ne ñàkkul ñu ger leen (Maki Sàll ak Aliyu Sàll), xam nañu tamit jan jawriñ la yoon mën a njort ne taq na ci mbir mi (Aali Nguy Njaay).
Kon nag, na àttekat bi def liggéeyam, maanaam seet ba xam ndax ñett ñoonu teggi nañu yoon am déet.