ALIYUN BADARA BÉEY GUDDEE NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Aliyun Badara Béey, njiitu kurélu bindkati Senegaal yi, moo génn àddina. Keroog, dibéer 1eelu desàmbar 2024, la wuyuji Boroomam, ginnaaw bi ko ab feebar tëralee ab diir. Mi ngi amoon 79i at (28 sàttumbar 1945 la juddu). Moom, Sëñ Béey ci boppam, bindkat la woon (bind na téere yu bari te wuute) te di woon itam móolkat (moo sos këru móolukaay giñ tudde Magiléen).

Moo doon tamit njiitu kurélu biti gi ëmb bindkat yi féete ci làkku tubaab (Fédération internationale des écrivains de langue française). Bokk na tamit ci ñi sos Mbootaayu móolkati réew mi.

Mënees naa lim ciy téereem : Dialawali, terre de feu, Le sacre du ceddo, Nder en flammes, añs.

Démb ci altine ji, 2i pani desàmbar 2024, lañu ko ca sëgi Yoof ya ginnaaw bi ñu ko jullee ca jàkkay Saakura Bajaan ja ca Kolobaan.

EJO-EDITIONS ak LU DEFU WAXU di ko jaal njabootam yépp (gu deret ak gu mbatiit) tey ñaan Yàlla jéggal ko, xaare ko àjjana.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj