ÀTTEKAT BI SETAL NA SITOOR NDUUR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndogal li rot na : yoon toppeetul dara Sitoor Nduur. Tey, ci àllarba ji 19 awril 2023 la ko yoon bàyyi. Nde, bees sukkandikoo ci li rot ciy xibaar, àttekat dafa ne amul ay firnde yu doy.

Moom, Sitoor Nduur, kilifag APR la, jiite woon fi “COUD” doonoon itam njiitul SAED. Mbindaanam a ko jiiñoon ciif. Boobaak léegi, nag, mi ngi woon ci loxoy yoon. Tey jii lees ko daan àtte ca àttewaayu pékke ba. Bés niki tey, yoon toppeetu ko dara. Nde, àttekat bi dafa tënku layub ñàkk a am ay firnde yu wér ñeel ciif gi ñu ko tuumaal. Ba ñuy layoo, toppekat bi 10i at la sàkku woon ñu tëj ko kii di Sitoor Nduur. Moom, toppekat bi, dafa gis ne ngóor si Nduur moo def li ndaw siy jiiñ.

Cig pàttali, mbindaanam, Siraa Njonn, tollu ci 17i at moo ko jiiñoon ag ciif. Ci sabab boobu lañu ko jàppe woon, tëj ko Ndung-siin boobaak léegi. Moom Sitoor Nduur muccagul. Ndax, mbokki ndaw si nee na dañuy def « appel ».

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj