Coowal « damay bokk ! » ak « doo bokk ci wote yi ! », diggante Càmm geek Usmaan Sonko, moo lëmbe réew mi jamono yii. Boo bàyyee xel, dinga seetlu ne coow lee ngi tàmbale woon a taqarnaasi ba Ayib Dafe, dib fara-caytu bu mag bu Pastef, demee woon fa DGE ngir jëlil Usmaan Sonko xobi baayale yi. Waaye, DGE daf ko gàntaloon, xamal ko ne Usmaan Sonko bokkatul ci wayndarew wote yi. Ca la layookati Sonko yi jàllalee woon ab dabantal ca ëttu àttewaay bu mag bu Senegaal, ak ca àttewaay bu Sigicoor ngir dàqlu ndogalu DGE bi. Bi loolu amee, ëttu àttewaay bu mag bi dafa gàntaloon Sonko, waaye, àttewaay bu Sigicoor bi, ci njitéefu Sabasi Fay, dafa joxoon dëgg Usmaan Sonko keroog ci 12 oktoobar 2023, wax ne kenn du ko dindi ci wayndarew wote yi.
Noonu, ci 19 oktoobar bi la Ayib dafe delluwaatoon fa DGE, àndoon ak wisiye yóbbu ndogalu àttewaayu Sigicoor bi, ngir mën a jëlaale këyiti baayale yi ñeel Usmaan Sonko. Mujju fa woon jële dara, ndax DGE daf ko bañoon a dalal, mu teg ci tamit ne Sonko bokkul ci wayndarew wote yi. Ci la layookati Sonko yi demee di ko ñaxtu ca CENA, muy ag kuréel guy saytu wote yi ci réewum Senegaal. Ci talaata 31 oktoobar 2023 la CENA jëloon ndogal ne DGE dafa war a jébbal Usmaan Sonko ay xobi baayaleem. Waaye DGE dafa lànkoon ba tëdd ci naaj wi ne du leen joxe, demoon na sax ba génne woon ab yégle doon ci tontu CENA ci yile kàddu
« Bu ñu joxul xobi baayale Usmaan Sonko ba léegi, dafa fekk ni bokkul ci wayndarew wote yi. Te sunu taxawaay ci mbir yi boobu ba léegi dafay firnde sax ndogalu njiitul njëlbéenu néegu caytu bu ëttu àttewaay bu mag bi. Fi mu nekk nii, Sonko nekkul ci wayndarew wote yi. Te loolu moo tax DGE taxaw fi mu taxaw ba tey. Te it, DGE amul màqaama di dugal kenn ci wayndarew wote yi. Leneen lu ci waay def, baa mu wax ko ci, nekko di topp li néegu caytu bu ëttu àttewaay bu mag bi dogal… »
Bi CENA jëlee bile ndogal, la Maki Sàll, Njiitu réew mi, génnee ab yégle di ci xamle ne dàq ña nekkoon CENA tabb ñeneen ngir ñu jiite gile kurél.
Bi loolu weesoo, laayookati Càmm gi ñoom it dañu dugaloon ab dabantal ngir gàntal àtteb Sabasi Fay bi. Ci loolu la ëttu àttewaay bu mag bi sukkandiku, ci njiiteefu Sire Aali Ba, daldi neenal àtteb Sabasi Fay bi keroog àjjuma 17 nowàmbar 2023. Gis na ne, ginnaaw ba Sonko Ndakaaru la dëkk, kon foofu lañ ko war a àttee. Ciy waxam, Sabasi Fay amul màqaama di jël ndogal naan kii mbaa kee moo war a bokk ci wayndarew wote yi am déet. Noonu la neenalee àtteem bi, delloo yëf yi ca ëttub àttewaay bu Ndakaaru bi.
Layookati Sonko yi tamit xàddiwuñu woon. Ndaxte, dañu dugal ab neenal-àtte bésub 28 nowàmbar ba ngir ñu neenal ndogalu ëttu àttewaay bu mag bi. Ëttu àttewaay bu mag bi dafa dellu gàntal cib oordonaas neenal-àtte bi layookati Sonko yi dugaloon, di leen xamal ne fàww ñu xaar àttewaay bu Ndakaaru bi lan la ciy dogal.
Ci talaatay 12 desàmbar 2023 jii nu génn, la àttewaay « hors classe » bu Ndakaaru bi doon àtte ndax dañuy delloo Usmaan Sonko ci wayndarew wote wi am déet. Àttekat bi dii Usmaan Raasin Coon dafa dàqoon dogal bi ba alxames 14 desàmbar 2023.
Tey ci alxames ji, bi 9i waxtu ci suba jotee la àttewaayu « Hors Classe » bu Ndakaaru ci njiiteefu Usmaan Raasin Coor jëlee ndogal ne Usmaan Sonko dañu koy boolewaat ci wayndarew wote yi, gàntal na génne gi ko waa njawriñu biir réew mi bëggoon na génne ci wayndarew wote yi ak digal ñu dugalaat ko ci wandarey wote yi.
Li ci des mooy ndax DGE dafay lànkalaat Sonko am déet, wala ndax Càmm gi dafay dugal ab dabantal.