ÀTTEWAAYU NDAKAARU : USMAAN SONKO WAX NA ÀTTEKAT BI AY DËGGAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Usmaan Sonko jël na kàddu gi ca àttewaayu Ndakaaru, wax àttekat bi ay dëggam ci fulla ak faayda. Njiitul Pastef li dafa biral jafe-jafe yi muy jànkonteel fan yii yépp.

« Dañu léem sama kër, wërale kook i takk-der yu gànnaayu ba diis te amul benn ndogal, ci li ma xam, lu war a tax ñu def lu ni mel. Amul benn daan bu tegu sama kow. »

Usmaan Sonko ñaawlu na tamit li ñu koy tànnal aw yoon wu muy jaar ngir dem ca àttewaay ba. Daf ne, bés bu nekk, ay maxejj wuyusi Yoon te sàndarmëri du lijjanti yoon wi ñuy jaar ngir dem. Mu teg ci, wax àttekat bi ne, « yow ci sa bopp yaa wax ne layoo bii, dara wutalewu ko ak yeneen layoo yi. Lu tax kon ñu may jaarloo fu ma bëggul a jaar ? Dara taxul lu mooy ne « nervis » Maki Sàll yaa ngi fépp. »

Sonko rax na ci dolli ne Maki Sàll ak nguuram gépp ay buqat yu mag lañu. Bi ko àttekat bi santee mu jox cër campeefi réew mi, Sonko ne ca tonet, ne ko : « campeef amul ci miim réew ! Pólis ak sàndarmëri yépp lañu ger. Nga foog ne Maki Sàll campeef la ak jaay doole bi muy teg sama kow boobaak léegi (…) »

Bi Sonko waxee loolu, waa APR fa lañ nekkoon di ñurumtu, àttekat bi daldi ajandi layoo bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj