Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, tabb na ay njiit yu bees ci boppi yenn banqaas yi. Démb, ci àllarba ji, 15 me 2024, lañu doon amal Ndajem jëwriñ yi. Ci njeexital li lees biral toftaleg turi ñi ñu tabb. Nii la toftale gi tëddee :
Abiib Si, Njiitul Ndajem Caytu mu SENELEC (Président du Conseil d’administration de la SENELEC), Sëriñ Mbay Ja la fay wuutu ;
Ayda Mbóoj, Njiitul DER/FJ (Délégation générale à l’Entrepreunariat Rapide des Femmes et des Jeunes, Maam Abi Séy la fay wuutu ;
Baabakar Jóob, Njiitul CROUS (Centre Régional des Œuvres Universitaires de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis), Ahmadu Bàmba Ka la fay wuutu ;
Baabakar Njaay, Njiitul SNR (Société Nationale de Recouvrement), Basiiru Ngom la fay wuutu.
Baabo Aamadu Ba, Njiitul 3FPT (Fonds de Financement de la Formation Professionnelle et Technique), Sofi Jàllo la fay wuutu ;
Daam Mbóoj, Njiitul SOGIP SA (Société de Gestion des Infrastructures Publiques dans les Pôles Urbains de Diamniadio et du Lac Rose), Mamadu Fay la fay wuutu ;
Faatima Mbeng, Njiitul ONPN (Office National des Pupilles de la Nation), Alfa Kunta la fay wuutu ;
Jaara Sow, Njiitul Office des Lacs et Cours d’eau, Aliyun Badara Jóob la fay wuutu ;
Kàppiten Seydinaa Umar Ture, Njiitul ASP (Agence d’Assistance à la Sécurité de Proximité), Biram Fay la fay wuutu ;
Lamin Baara Lóo, Njiitul ONFP (Office National de Formation Professionnelle), Suleymaan Sumaare la fay wuutu ;
Lamin Ñaŋ, Njiitul Le Soleil, Yaaxam Mbay la fay wuutu ;
Mareem Sooda Njaay, Njiitul Commissariat à la Sécurité Alimentaire et à la Réilience, Ibraayma Jaawo la fay wuutu ;
Móodu Mbeen Jóob, Njiitul ASEPEX (Agence Sénégalaise de Promotion des Exportations), Zahra Iyaan Caam la fay wuutu ;
Sinna Aamadu Gay, Njiitul ANPEJ (Agence Nationale pour l’Emploid es jeunes), Tamsiir Fay la fay wuutu ;
Tuseŋ Màngaa, Njiitul LONASE (Loterie Nationale Sénégalaise), Abdurahmaan Balde la fay wuutu.