Ngomblaan gee woote ngir dépite yi jëlsi kaarbiraŋ biñ leen di jagleel weer wu nekk. Ku ci nekk, jagoo nga lu tollu ci 500i liitari kaarbiraŋ. lees ko dugge mooy yombalal dépite bu nekk dem beek dikk ci wàllu liggéeyam ; muy mën di jóge dëkkam, wutali ngomblaan ga, saa su jotaay amee, walla buy tukki tukkib liggéey. Dafa di, ci biir 500i liitaru kaarbiraŋ yooyii, 400 yi Total walla Shell rekk lañ koy jële, 100 yi ci des Elton walla EDK. Total ak Shell, nag, ay doxandéem a leen moom, maanaam ay tubaabi Farãs. Looloo tax Gii Mariis Saañaa gàntal leen.
Gii Mariis Saañaa jaar na ci tànki Usmaan Sonko. Nde, ba muy dépite, Usmaan Sonko bañoon na lu ni mel. Tey, Gii Mariis Saañaa ko donn ci xeex boobu. Ndege, dépite Sigicoor bi, bokk FRAPP, dafa gedd kaarbiraŋam ngir ne, Nguur gi dafa bëgg a dooleel ay doxandéem wëliis doomi réew mi. Mu ngiy joxe ay leeral naan :
« kaarbiraŋ bi yépp laa war a jël. Li tax ma gedd lépp mooy ne mënuma jël 100i liitar yi bàyyi li ci des, te du ma nangu di jàppale Total walla Shell, bàyyi fi Elton ak EDK. Su may jël kay lépp laay jël ngir jàppale doomi Afrig yi, rawatina yu Senegaal. Dafa war a dakk ñuy jéggaani di fi bàyyi li nu moom, waruñu nangu li jóge ci biti di nu gënal li nu moomal sunu bopp. Lii rekk a tax ndaw yu bari amuñu liggéey ci biir réew mi. Ndax Afrig, ak réew mu mel ni Senegaal, ñooy gasal seen bopp pax, di lor seen i doom ngir tabaxal Farãs ak réew yi daan noot Afrig àjjana. »
Li Gii Mariis wax ci mbirum kaarbiraŋ bee tax kii di Daawuda Ja, njiital kestër bu ngomblaan gi indi ay leeral ci ni mbirum céddaleg kaarbiraŋ bi deme. Ci aw waxtaan wu mu séqaloon ak waa Bés Bi, lii la ci Daawuda Ja wax :
« Bu ma Gii Mariis laajoon, dinaa ko leeralal lépp ci mbir mi. Ngomblaan gi biñ ko taxawalee ak léegi, yàgg na. Te, boobu ba tey, moo ngi liggéey ak waa Total, Shell ak Elf, laata EDK ak Elton di juddu. Nun nag, dañu fa fekk aada boo xam ne dañu nekk di ko wéyal. Waaye, tekkiwul ne dañu bind ab dige buy wax ne kenn doŋŋ moo ñuy jox kaarbiraŋ. Dafa am ñu bari ci dépite yi ñaan ne Total ak Shell a leen gënal ndax ñaar yee gën a bari ci réew mi, te it dina leen dimbali ci seen i tukki yi ñuy amal ci biir réew mi.
Mbirum kaarbiraŋ bi dañu ko séddale cy kàrt ak i tike. Wàllum tike yi, dañu ko séddalewaat ci 10, maanaam, tike bu nekk 10i liitar lay def, su ko defee 10i tike yi mooy nekk 100i liitar yi. 400i liitar yi ñooy nekk ci kàrt yi. Li ñu war a xam mooy ne Total ak Shell kàrt rekk lañuy doxalee seen i mbir, tike bokkul ci seen doxalin. Damaa xamul nag ndax EDK ak Elton dañuy yëngu ci mbirum kàrt am déet, waaye ñooy joxe tike yi ndax loolu rekk lañ leen laaj. Wàllum kàrt yi moom, Total ak Shel rekk ñoo nu koy jox. Te tike yi sax li leen tax a jóg mooy denc. Ndax ab dépite mën na réeral kàrtam, diggante bi ñu koy utal bu bees, mën nay jëfandikoo tike yi.
Bu fekke nag dafa am ab dépite bu bëggul kàrt Total walla Shel, dafa may bind rekk ñu defal ko li mu bëgg.
Gawuñ kenn ne ko Total ak Shell. Dafa fekk ne kàrt yeek tike yi dañ leen fey laata weer wi di dee. Gii Mariis mën na tànn fu ko neex di fa jële kaarbiraŋam. Nde, weer wii di ñëw rekk lay doon. Lu ni mel, bu ko bëggee, dafay bind ab yégle wax fan lay jële kaarbiraŋ balaa weer wi di am 15i fan, bu ko defee ñu teel ko lijjanti. »
Bu dee ku nekk yaay tànn fu la neex, kon lu tax Sonko sulli woon coow li laata Gii di ko ci wuutu ? Dafa mel ni am na luy ñuul ci soow mi. Waaye, ak lu ci mënti am, taxawaayu Gii Mariis day biral lenn, mooy li wolof di léebu, naan : balaa ngaa laax jaay, laax lekk.