BÀLLA GAY DAANATI NA TAFAA TIN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb a doonoon woon ñaareel wi yoon ñu sëgg ci géewub bëre-dóor. Bàlla Gay a daanoon, keroog seen bëre bu jëkk ba, 2i pani suwe 2013. Dibéeru démb jeet, 21i pani sulet 2024, mbëru Géejawaay mee daanat  Tafaa Tin. Jéll bu set wecc la ko daan.

Ku ne woon Bàlla dafa màgget ? Ana ñi daan wax ne Tafaa Tin a ëpp doole, daf koy duma, daan ko ? Kenn déggatu leen. Nde, Bàlla dafa nennu doomu Bawol bi. Seen bëre démb bi wone na ko. Dafa di, ni mu bëree ak Tafaa Tin démb, gëj na koo indi ci làmb, dafa dekkilaat Bàlla bees xamoon. Waaye Tafa Tin li mu indi, ak ni mu bëree, bett na ñu bari. Ndax kat, ni mu ñëwee woon ca seen jàkkaarloo bu njëkk ba, ba tax ñépp tiitoon ci doomu Duubalees ji. Demoon nañ ba nit ñi jàpp ni, wii yoon, Tafaa dina won Bàlla Gay ni, la woon, wonni na. Ndekete yoo, tay la waalo gën a aay.

Seen Bëre bi

Bëre bi mënees na wax ne, na woon fa woon la rekk. Te sax, bii moo raw. Fi Bàlla Gay jaaroon Tafaa Tin la ko jaaraat : dox ci kowam, nangu xeex bi ci moom, dóor ko dóor yu metti ba noppi daan ko jéll bu set.

Ba arbit ba nee piib, ñu léewatoo lu yàggul dara, ca la Saa-Bawol bi tàmbalee bëgg a dox ci kaw doomu géejawaay ji. Waaye, Bàlla Gay, ci xam bëreem ak miin Tafaa Tin, daldi ko fekksi, xañ ko loolu. Noona la ko woo ci lees di askanalee Tafaa Tin, muy xeex bi. Mu daldi ko ci yóbbu ga, jekku ko ci lool, di ko rokkos dóor yu dal ba kii di Tafaa Tin génne deret ju bari, mujje dem ca Ardo ab diir. Ba mu dikkaatee, Bàlla Gay xam ni fa mu jàppoon nooy na, mu jàppaat fa, woowaat ko ci xeex bi, sonal ko lool. Waaye, mu jeexalee ko ci bëre, daaj ko benn caxabal bu rëy, daan ko.

Fim ne nag, dafa mel ni Bàlla dafa dekki ci làmb ba noppi dekkalaat làmb. Démb, foo géestu waan ci mbaali jokkoo yeek waxtaan yi, làmb a moome woon. Muy dëggal li gaa yi naan Bàlla GAY  mooy làmb.

Ginnaaw bëre bi ci boppam, dees na sargal CNG, rafetlu seen ub liggéey ñeel waxtu wi. Bu ñu seetloo yu bari ci làmb yu fi mujje am, laata ñaari mbër yu mag yi di sëgg, dafa daan guddi lool. Loolu nekkoon lees di naqarlu lool. Ndaxte, bokkoon na ci liy jur ñàkk kaaraange bu làmb ji tasaan. Waaye de, seen bésu démb bi moom, gàcce-ngaalaama. Def nañu seen wareef. Nde, ñaari mbër yi ñu ngi sëgg ba 20i waxtu tegee as-tuut ciy simili.

Kon na wéy !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj