‘’BÀNK MONJAAL’’, KURÉL GI NUY JATAŋ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ñépp a ngi fàttaliku ni « Bànk Monjaal » nasaxale woon réew mi ci nguurug Abdu Juuf. Ci wàllu njàng, wér-gi-yaram ak mbir yu bari yu deme noonu, kurél googu fexe woon na ba Juuf génne ca loxoom, muy def lu ko neex.
Loolu juroon na fiy jafe-jafe yu tar. Ndax taxoon na ñu jaay waa bitim-réew bérébi liggéeyukaay yu bare. Doomi-Senegaal yu bari ñàkkoon nañu ci seen liggéey, xale yi mënatuñu woon a jàngi te feebar faju jafe woon na. Ci gàttal daal, ci lu jëm ci yokkuteg askan wi, mbir yi sooxe woon nañu bu baax. Waa “Bànk Monjaal” doon bàkke Abdu Juuf: “Ndongol Bànk Monjaal li ko gën a nangul”. Réew miy wéy ciy jafe-jafe, ñu naan nu muñleen rekk, dina baaxi ëllëg.
Waaye dara doonu ci woon dëgg. Jafe-jafe yooyu sax, bokk nañu ci li fi jële Abdu Juuf ci atum 2000. Noonu, Abdulaay Wàdd dikk, xaw a fippu ni àndut ak ñoom ci yenn gis-gis yi. Looloo mayoon nguuram sañ-sañu defar ay tali, def itam ay jéego ci njàng meek paj mi.
Loolu dafay firndeel ni Bànk Monjaal ak kurél yu mel ni moom, réew yu mag yi lañu fi nekkal, ndax ñoo leen di suuxat. Ba tax na sunu njiit yi war nañuy settantal seeni ndigal, war nañuy jiital seen njariñu askan. Noonu la ko Peresidaŋ Néeru tamit defe woon ca réewum End. Ba ko waa ‘’Bànk Monjaal’’ joxee ay tegtal, rëddal ko yoon wi mu war a jaar, daa xotti lépp ba mu ko wóore ni bu ko defee réewam dina soox, jóge fa suux.
Waaye bu dee ci sunu réew yi, fulla jooju moo fiy tumurànke léeg-léeg. Lu leen “boroom xam-xami tubaab yi” wax, ñu def ko am seew. Te moone ñooñu, seen njariñu réew rekk a leen yitteel !
Moone ba tey ‘’Bànk Monjaal’’ a ngi fi. Di digal sunu njiit yi ñuy jëfe. Moo tax tamit 59 at a ngi, ñu ne noo moom sunu bopp te mënagunoo dem fenn.

Lamin Jeŋ
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj