BÀRTELEMI JAAS NEKKATUL MEERU NDAKAARU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bésub 11eel ci desàmbar, 2024, lañu dàq Bàrtelemi Jaas ci boppu meeri bu Ndakaaru. Ndogal laa ngi bawoo ci perefe bu Ndakaaru.

Li ko sabab moo di ne, dafa am daan bu gàllu ci kow ndoddu Bàrtelemi Jaas, ñeel mbirum Njaga Juuf. Atum 2017 la ko Yoon njëkkoon a daan, mu bañ, daldi dugal ab dabu. Ci atum 2023 mii weesu nag la ëttu àttewaay bu kawe bi dëggal daan bi.

Dafa di nag, dogu L.277 bu càrtug wote bi moo wax ne, bu amee ab « conseiller municipal » bu nekkatul falaakoon walla mu am ngànt, dees ko bàyyiloo, tekki ndombog-tànkam.

Tay, ci àjjuma ji, la perefe yóbbante bataaxal bi xamal Bàrtelemi Jaas ne, dindi nañu ko boppu meeri bu Ndakaaru. Moom Bàrtelemi Jaas, war na amal am ndaje ak saabalkat yi, bu 16 waxtu jotee. Fa meeri ba la koy defee.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj