Ci tekkig Ndey Koddu FAAL
“Kilifa gu mag gi,
Jàmm ak salaam ñeel nañu la ! Say mag ñoo lay nuyu, di la jox sa wàccuwaay. May nu tuuti, laata nuy dugg ci aali-kalaj gi, nu wax la ne, nun Ngugi Wa Thiong’o mu Keeñaa ak Bubakar Bóris Jóob mu Senegaal, noo lay bind tey. Nun ñaar ñépp génne nanu ay téerey fent ak i téerey xeltu. Yi ci gën a siiw nag, ñoo ngi tudd Decolonizing the Mind : The Politics of Language in African Literature (1986) ak Murambi, le livre des ossements (2000) biy nettali faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa yi ci atum 1994. Waaye, li gën a am solo te lal bataaxal bii mooy ne, bu weesoo li nu bind ci àngaleek farãse – diy làkki Tubaab yi ñu fi daan noot – bind nanu yeneen i téere ci làmmiñ yi nu nàmp. Mënees na cee lim Matigari (1986) ci Kikuyu ak Bàmmeelu Kocc Barma (2017) ci Wolof.
Noo ngi lay ndokkeel bu baax a baax ci li la réewum Senegaal tànn ngir nga doon njiit li. Noo ngi ndokkeel itam Usmaan Sonko, Jëwriñ ju mag ji, di sa doomu-ndey te ngeen yàgg a ànd di xeex ci njàmbaar gu mat sëkk. Liy firndeel ne yeyoo nga nguur gi nag, moo di ne, amul kenn ci lawax yi ko doon xëccook yow ku ci ne dañoo labaj xob yi walla sa pal gi jaarul yoon. Nun moom, ci sunu gis-gis bu gàtt, yaakaar nanu ni Saa-Senegaal yi faluñu la ngir nga ne noŋŋ ci kow gàngunaay gi, di nguuru ak a jaay doole. Déedéet Fay ! Sam réew da laa fal ngir nga koy déggal ni jaam war a déggalee sangam, ngir ngay jaamuy soxlaam. Waaye, wóor nanu ne du yow yaay tas sa yaakaaru askan.
Naam, xamantewunu, mësunoo bokk jataay. Waaye, daanaka amul fu sa tur àggul ci àddina si, te it xam nanu bu baax ne li nga nekk ndaw dafa dekkil yaakaar bu jéggi dayo ci kembaaru Afrig gépp. Bun waxantee dëgg sax, looloo tax nun ñaar nu am sañ-sañu bind la bataaxal bii nga tiim di ko dawal. Sunu jarbaat nga, nu am ci yow cofeel, di la damoo. Waaye du tee, ginnaaw ku la mag ëpp lay sagar, fàww nu laabire la li nu xalaat.
Afrig sonn na, Kilifa gu mag gi !
Su Afrig amee naqar gu tollu nii, lu jiin Njaag a te pólitiseŋ yeey Njaag. Moom daal, boo ci génnee ay benn-benn yu mel ni Kwamé Nkrumah, daanaka ñoom ñépp a wor sunu kembaar gi. Ay njiit yu doyadi ñoo daganal ñaawteef yi fi nootaakoon yu weex yi daan def démb, tey wéy di ko def tey, jaare ko nag ciy Tubaab yu ñuul kukk. Ñuule yooyoo leen fi toogal, bokk ak ñoom mbuus ba tax mbelli kembaar gi – muy soroj (petorol), di wurus ba ci sax jën yi ci géej gi – lépp daal di wéy di suqali koomu Tugal.
Naka la nit mën a xeebe nii saw xeet ?
Neexul a wax nag, waaye mooy li am. Gaa ñooñu, wutewuñook nit ñoñ, dañu xeesal seen i xel ba faf gëm ne lu weexul baaxul. Moo waral ñi sopp Afrig ñépp seen bopp ubu, ñu naan : waaw, ana sunuy fentkat ? Ana sunuy ma-xejj (ingénieurs) ? Sunuy ma-feeñal mbeeraay ? Afrig soxla nay njiit yu mën a yee kàttan gu jéggi dayo giy dajjant ci ndaw ñi, jafal ko muy bërëx. Te, loolu, mënut a ne ak i njiiti réew yuy dunguru Tubaab yi, njiiti réew yoy, gëmuñu seen bopp, gëmuñu seen askan.
Yow nag, am nga lu jafe. Nde, am nga mën-mënu xàllal saw askan yoon wu bees tàq, mu war cee tegu, yaakaar yàkki dënnam ba nga ne lii lu mu doon, mu daldi gënatee weg boppam ba Senegaal dootul janook menn réew di sëgg. Waaye, bul réere mukk mbir ne, soo doxalee noonu, Tubaab yi dinañ la def noon, di la tam dëmm saa su ne. Ndax, ñoom xaaruñu ci Afrig lu dul muy wéy di leen jariñ ba àddinay tukki, di leen jox mbéllam ci yal naa dee. Xam nga loolu dara gënu koo neex ! Bul nangu xeetu naxee-mbaay woowu, bañ ko ba tëdd ci naaj wi. Te, su ñu la tamee dëmm, bul ko sax yëgal sa yaram. Ndax, leneen lu dul li askanu Senegaal di xalaat waru laa ñor.
Léegi nag, nu bëggoon a lal waxtaan ak yow ci mbir mu nu soxal.
Bun la nee mbirum làkk yee nuy tax a wax, du la bett. Ndax li nuy ay fentaakoon. Bindkat yi ñoom, rawatina yu Afrig yi, loolu lañu gën a sawar a waxtaane. Mu doon itam mbir mu am solo. Jàpp nanu sax ne réew mu ko sàggane doo dem, sa lépp ay tagatémbe, muy sa koom-koom, di sa mbatiit, di leneen. Muy yow, muy keneen, njiitu Afrig lu soofantal say làkki réew, jëndee leen làkki nooni démb ya, daanaka dangaa fatt yooni naataange yépp ba noppi janook saw askan di ko lay jëmale fu kenn xamul, di raay sa cuukel naan “setaadir” ak i waxi kasaw-kasaw yu ni mel.
Nu lay ñaan nga bàyyi xel ponk yii toftalu :
-
Sa dooley nguur a ngi bawoo ci askanu Senegaal wi. Dangay aar doomi-réew mi, ñoom it ñu lay aar, ngay wax ak ñoom, ñuy àddu. Waaye, ngalla bu leen làkk làkk wu ñu déggul. Nun sax danoo xamul naka la ay magum jëmm mënee toog di werante lii ? Lan moo nu dal, Kilifa gu Mag gi ?
-
Làkki Senegaal yee war a doon cëslaayu Senegaal gu bees gi nga bëgg a tabax. Bépp Doomu-Senegaal war naa mën a damoo làmmiñ wi mu nàmp. Kon, lu am solo la ngay moytoo gënale làkk yi. Làmmiñ wees nàmp a war a jiitu, mën na doon pulaar, seereer, soninke, wolof, màndinka, joolaa mbaa weneen làkk wu ñuy wax ci Senegaal. Waaye, su fekkee am na làkk wu mën a tax ñépp di jokkoo, lu deme ni wolof ci misaal, loolu warul am jafe-jafe, ci sunu gis-gis. Ni nu gisee nosteg làmmiñal mooy làmmiñ wees nàmp ngay jiital. Soo noppee ne wolof, su la neexee nga ne suwaahili, su la neexee it nga ne farãse, añs. Ndax kat, soo déggee làkki àddina sépp te déggoo làmmiñ wi nga nàmp, day mel ni jaam nga. Ndax, su boobaa, tekkiwoo dara. Waaye, ginnaaw bi nga peegee saw làmmiñ, loo ci dolli ci yeneen làkki àddina si, yokkute kepp la lay jural, gën laa dooleel.
-
Doon nanu neex lool nga kañ sottante ñeel làkki senegaal yi. Ci sunu gis-gis bu gàtt, ponk bu am a am soloo ngoog. Ci kow loolu, nu doon la ñaax ci taxawal ab sàntaru làppatoo ak tekki, day doon ab dig buy booleek a ñoŋal làkki Senegaal yi ci seen biir, waaye tamit diggante làkki senegaal yi ak yu Afrig ak àddina si. Njiitu réew mi, Saa-Afrig yu bari rafetlu nañu li nga dem Gàmbi, daldi waxtaan ak Aadama Baro ci wolof. Xam nanu ne bokkook ñi la jiitu ci jal bi ndax yow li ëpp ci say wax, dangay boole jëfandikoo wolof ak tubaab, te jàpp nanu ne mooy li war dëggantaan. Nii la : nga yëkkati kàddu ci benn ci làkki Senegaal yi, ba noppi bàyyi ñu sotti ko ci yeneen làkki Senegaal yépp laata ñu koy tekki ci tubaab, waaw kay. Ca Mbootaayu Xeet ya, mën ngaa wax ak ñoom ak wenn ci làkki Senegaal yi. Su ko laajee, ñu tekki ko ci saa si ci yeneen làkk yi ONU di liggéeyee ndax kurélug àddina sépp la. Li nu bëgg a wax fii mooy nga def ni yeneen njiiti réew yi, maanaam yëkkati kàddu ci sa làmmiñ. Sooy dem Farãs, ci misaal, nga ànd ak ub làppatoo, waxal ak sa naataango ba ca Élysée ci wenn ci làkki Senegaal yi. Ci tënk daal, fexeel a joxlu gëdd làkki Senegaal yi. Te looloo ngi doore ci far nu mu gën a gaawee dog 28 bu Ndeyu Àtte Réewum Senegaal biy tëral ne bépp lawaxu boppu Senegaal dafa war a dégg làkku tubaab, di ko wax, di ko bind ak a dawal na mu waree. Kenn xamul lii lu mu doon.
-
Nga lootaabe beykat yeek yeneen liggéeykat yi. Suuxatal seen xereñte. Ñu gën laa jox bopp, di la aar. Bul jiital ñi jàppe seen bopp ay ma-xelu (intellectuels) yoy dinañu def lu ñu mën ngir suuxal làkki réew mi ndax xam ni su làkk yi suqalikoo, ñoom ñu àllaterete, tëri. Ni ko mag ñiy waxe, kuy woddoo làmmiñ, soo noppee rafle. Mbirum làkki réew mi, kanam rekk lay jëmi, waratul dellu ginnaaw.
-
Muy téerey Sembène Ousmane te bi ci gën a siiw di Les Bouts-de-bois-de-Dieu, di yeneen i téerey kàngami ladab yu demee ni ñoom Cheikh Hamidou Kane, waroon nañ leen a am ci yeneen làkki Senegaal yi. Soo jëlee Seex Anta Jóob, moom nag, jot na ñuy jàngale ay téereem ci lekooli Senegaal yépp.
-
Noo ngi yéene tamit ladabi yokkuteg Afrig ak àddina si mën a nekk ci làkki Senegaal yi ci daara yeek jàngune yi.
-
Xam nanu xéll ne Senegaal moo la ñor, mooy sa yitte ji gën a kowe. Waaye, fàww nga jublu ci Afrig, ba noppi teg ci Aasi ak Amerig Latin laata ñuy wax waxu Ërob. Bile pasteef dafa war a feeñ ba ci njàng mi.
-
Fexeel Senegaal nekk askanu xalaatkat, soskat, liggéeykati-loxo, ma-feeñal, askanu fentkat, wu ubbeekku ci lépp ngelaw luy mën a fexe ñu weg ko, sàmmle ko ngañaayam.