BATAAXALU ÀLLIYUN TIN ÑEEL USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Àlliyun Tin yékkati na kàddu jagleel ko elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko. Ginnaaw ganam gi mu fi doon dalal ci bés yii weesu ak coow yi ci jóg, moo ngi koy xamal ni war na ci moom mu xalaat bu baax saa buy wax ci wàlluw jëflanteek yeneen i réew ngir wattule boppam ay jam-jam.

Li gën a yitteel Àlliyun Tin nag, mooy jafe-jafe yi askan wiy dund, coppite yu mag yees war a amal ci campeef yi. Ci coppite yooyeet, waruñu réere mbir, maanaam wareesul a fàtte lajj yi Abdulaay Wàdd ak Maki Sàll lajj ñeel coppite yi ñu woote woon ci nees war a yoree réew mi. Ci weneew waxiin, naka lees waree jiite réew mi, teg ko ci yoon, sàmm àqi maxejj yépp, fexe ba réew mi moom boppam, Càmm gi (l’Etat) tëdde njaaxaanaay, añs. Yokk na ci ne, Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ yi dañu war a njëkk taxaw ci doxiin wu mucc ayib ñeel Càmm geek càmpeef yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj