Ami Mbeng
“…Luy jot jot na ginnaaw dee.”
Ci altine jii weesu, 23eelu fan ci màrs 2020 la njiitu réew mi, Maki Sàll, doon amal ñaareelu bàttaleem bi mbas mi duggee Senegaal ba léegi. RTS a ko siiwal bi 20i waxtu jotee.
Maki Sàll nee na dina jébbal péncum-réew mi ab sémbub àtte bu koy may, ci diirub ñetti weer, sañ-sañu jël ay dogal yi aju ci yoon. Ci artiikal 77 bu Ndeyu-àtte réew mi la sukkandiku def loolu ngir mu dooleel ko ci cong gi mu song Coovid-19 bi, tax it nguur gi mën a dékku wartéef yi aju ci nafa gi, koom-koom gi, mboolem-nawle Senegaal, wér-gi-yaram ak kaaraange gi.
Dogal na yit guural ci biir réew mépp ak dëjug-guddi li ko dale 20i waxtu ba 6i waxtu. Dafa ne :« Anam bu gaaw bi jàngoro jiy lawe moo waral nu yokk matuwaay yi ngir aar sunu bopp. Bu nu ko deful, ci musiba mu réy a réy la réew mi nar a tàbbi. Ba tax na, ni ma ko yoon maye, dogal naa guural ñeel réew mépp li ko dale guddig altine tey gii ci minwi.»
Li dëjug-guddi gi tekki, moo di ne kenn warta génn sa kër ci diggante 20i waxtu ak 6i waxtu, te yit woto waru cee daw lu-dul yoon may ko boroom, te mu am kayit gu koy firndéel.
Njiitu réew mi joxaale na ndigal alkaati yi, sàndarm yeek soldaar yi, ne leen ñu gaawtu wàcc ci mbedd yeek tali yi ngir jëfe dogal bi.
Ni ko yoon waxe, ci jamonoy guural, njiiti caytu diiwaan yi ak gox-goxaat yi am nañu sañ-sañu sàrtal mbaa tere yëngu-yëngu nit ñi ak woto yi, rawatina xew yi. Sañ-sañ googu, mën na aju ci benn fànn walla ci fànn yépp, ci benn béréb walla fépp, ci diggante ay waxtu walla diir bu ko ëpp. Bu ko defee, njiitu réew mi teg na ci ne njiit yooyee, am nañu sañ-sañu tëj yenn béréb yiy waral mbooloo, muy bérébi ndaje yu askan wi moom walla yuy doom-aadama moom.
Mbir mi àgg na foo xam ne, xeex rekk a fi sës bala muy ëpp i loxo. Ndege, njiitu réew mi lim na béréb yi jàngoro ji dugg. Nee na, Covid-19 bi laal na 10 goxi réew mi. Mu ne, keroog altine ji, réew maa ngi amoon 71 way-tawat yiy faju ci 4 arondiismaa Ndakaaru yi ak Mbaaw, Yëmbël, Géejawaay, Tëngéej, Tuubaa, Mbuur, Cees, Popangin, Ndar ak Sigicoor. Mu mel ni léegi réew mi daj na.
Loolu la njiitu réew mi xam ba tax koo yëkkati kàddu yii : « Ci guddig tey gii may janook yéen, askanu réew mi, maa ngiy xas, di leen wax ne, luy jot jot na ginnaaw dee. Nguur gi, njiiti caytu yi ak liggéeyukaayi nguur yépp dinañ jël seen i matuwaay ci saa si ngir jëmmal dekkareb guural gi. »
Ba tey, bees sukkandikoo ci kàdduy njiitu réew mi, dinañ wàññi mbaa sax ñu tere tukki yi ñeel dëkk ak dëkk. Mu teg ci ne, jawriñ ji yor wàllu dem bi ak dikk bi dina jël matuwaay yi war ngir doxal dekkare bi. Te, tukki ci biir gox-goxaat yi tamit ci lañuy bokk.
Ci wàlli garab yi ak xeeti jumtukaayi faju yi, njiitu réew xamle na ne nguur gi dina def kem-kàtttanam ngir réew mi bañ cee tumurànke.
Ci beneen boor, ñu bare ci nit ñi dañ doon am xel-ñaar ci yokkub njëg yi mën a juddoo ci guural gi ak tere yi. Waaye, njiitu réew mi dalal na seen xel, ne : « Gornmaa bi dina jël ay matuwaayam, xeex bépp yokkub njëg bu jaaduwul ».
Ci kow loolu, mu xamle ne dinañ ber xaalis bu tollu ci 1 000 milyaar ci sunu koppar, jagleel ko xeexub Covid-19 bi ci réew mi. Ci biir xaalis boobu, dinañ jagleel 50 milyaar yi askan wi ngir dimbalee ko ko ci wàlluw dund. Rax-ci-dolli, dinañ wàññi 200 milyaar ci bori lempo yi ngir jàppalee ko otel yi, ñiy liggéey ci roppëlaan yi ak ci wërteef gi (tourisme), ñiy yëngu ci aada ak cosaan ak ci wàllu tas xibaar.
Ci talaata ji, jawriñ jiñ dénk kaaraange biir réew mi ak naataangoom bi yor wàllu dem beek dikk bi amalandoo nañ ab waxtaan ak taskati xibaar yi ñeel guural gi njiitu réew mi dogal ci altine ji.
Ñu jeexale ci xibaar bii tukkee ci yégle njawriñu wér-gi-yaram gi ak ndimbalu mbootaay mi : ci dibéer jii, 29eelu fan ci weeru màrs, Senegaal am na 142 way-tawati Covid-19 bi. 9 yi wér nañu, 96 yaa ngiy faju.