Ronaldo ak Manchester United budoon séy la ñu ni seen rawaan yee àndatul woon. seen ànd bi demeetul woon noonu, juroon ay benke-ñenke ba taxoon, keroog 22i Nowàmbar 2022, ñaari boor yi, ku ci nekk nangu ñu dog ànd bi. Tay jii mel na ni mooy lu leen jig, ku nekk sa taal moo ngi boy, safara si jëm kaw.
Cig at yu néew la ko Manchester jëndoon ndax gisoon ni jant ju nar a fenk la, mu jël ko ñemeloo ko dolli liggéey ci moom ba mu xëy wane boppam ca sàmpiyonaa Àngalteer ba. Ca jamono jooja, ay wurekat yu mag a nekkoon ca sàmpiyonaa ba, ñu ci mel ni ay Drogba, Tores añs., ak sax biir këlëb ba, Rooney, Berbatov … teewul turam di tàkk seen kaw, ñu ràññee ko ci ña fa gën a xereñ (2003-2009). Gannaaw loolu mu dem Real Madrid, daanaka dundam yépp fa la ko def ci wàllu wure ba ñu bari foogoon nañu ni foofee lay jeexalee sax ndax lam fa def ak it kam fa mujju doon. Jël na fa itam lépp ci diir bim fa nekk (2009-2018). Cig ñàkk a déggoo ciy mbir yu ndaw ak këlëb ba, mu jeexal fa àppam dem Itaali fekki Juventus def fa ñaari at wane fa itam xereñte giñ ko xamee woon door a dellu kërëm, Manchester United, ci atum 2021 bi. Jamono jooju këlëb ba moo ngi nekkoon ciy jafe-jafe, yeneen i këlëb bëggoon ko waaye mu topp xolam rekk dellu fa, mu doonoon mbégte ci moom ak soppey ekib baak ña ko bëgg ñépp. At mu njëkk mim fa defaat, mu andi ay balam, di dugal niki ñu ko xamee woon, donte këlëb bay soox. Ci ñaareelu at bi (2022), Manchester United tàmbaliwaat di soox, di gën a dellu gannaaw ñu dakk tàggatkat ba fa nekkoon andi fa Ten Hag, mu ñëw ak i bëgg-bëggam ak ay digleem. Ñuy dem ba yàgg diggante ba neexatul, moom ak Ronaldo, di jur ay coow biir ak biti, ay mer am ci, ay gédd añs. Keroog 13i Nowàmbar 2022, laata kuppeg àddina si doon tàmbali, Ronaldo amal ab laaj-tontu (interview) génne li nekkoon ci xolam bépp ak i xibaar yu neexul woon ñenn foofu ak njiiti këlëb ba. Looloo tax, keroog 22i Nowàmbar 2022, ñu dagg buum gi leen boole woon, ku nekk dem yoonam.
Ba kuppeg àddina si jàlle fu nekk ñu naan fa la jëm, mu dem Al Nasri, Araabi Sawdiid, ñii naan jeexal na, mag la, mënatul ak naan xaalis moo ko fa yóbbu. Ay farandoom naan Manchester dinañu xam lu leen waa ji doon jariñ. Waaye de, pase gi dox seen diggante benn xeer bu jam ñaari picc la, Manchester moo ngi dox di wëyal ay ndamam ca sàmpiyonaa ba, jëlagum fa 3eel, dolli ci war a finaalu ak New Castel ginnaaw bi mu toogloo Barça barki-démboo njaay ca Europa League ba. Ékib bay fuddaat di wanewaat boppam. Ronaldo itam, moom mi ñu bari foogoon ni màggat na ba xaalis a ko yóbbu ca Al Nasri, moo ngi wane boppam di rëddati turam ca naar ya. Gannaaw 5i joŋante yu mu jot a am ca sàmpiyonaa ba dugal na 8i bii, démb ci gaawu gi moo ci mujju, mu dugal 3i bal gannaaw ba mu dugalee woon 4 ca fan yi weesu. Loolu di wane ni moo ngi mën ba léegi, donte am na ñuy wax ni sàmpiyonaa yi bokkuñu.
Luñ ci mën a jàpp daal mooy ni ñaari taal yépp a ngi boy, safara si jëm kaw.